Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 févr.
“ Ñépp a bëgg am kilifa gu baax. Boo naroon a tànn ku war a ilif àddina si, kan ngay tànn ? [Mayal nit ki mu tontu.] Téere bii dafay wone kan mooy Almasi bi Yàlla tànn ngir mu nekk buuru suuf si. Dafay wone it li kiliftéefam di indil doom-Aadama yi. ” Jàngal Esayi 9:6, 7. Boo koy jàng, nanga feeñal bu baax kàddu gii : “ à la paix il n’y aura pas de fin ” (maanaam jàmm du jeex).
Réveillez-vous ! Févr.
“ Li ëpp ci nit ñi dañu gëm ne benn Yàlla rekk moo am. Waaye terewul nit ñi di jaamu yàlla yu bare. Seetal li Yeesu wax ci Baayam bi nekk ca asamaan. [Jàngal Yowaana 17:3.] Bu dee benn Yàlla dëgg kese moo am, lu ñu war a wax ci yeneen yàlla yi yépp ? [Mayal nit ki tontu.] Téere bii dafay wone li ci Kàddu Yàlla wax. ” Won ko waxtaan bi nekk ci xët 28 ak 29.
La Tour de Garde 1er mars
“ Nit ñu bare nangu nañu ne nit ku nekk dafa war a bëgg moroomam, ni ko Yeesu waxe ci aaya bii. [Jàngal Yowaana 13:34, 35.] Ban mbooloo mooy topp tey li Yeesu waxoon ? [Mayal nit ki mu tontu.] Téere bii dafay wone ni ñu mënee xàmme tey ñi nekk karceen dëgg. ”
Réveillez-vous ! Mars
“ Ñu bare gis nañu ne ñi bëgg seen moroom dëgg, dañuy gën di waññeeku. Waaye mbëggeel boobu, bu ñàkkee, dund gi du neex te jàmm du am. Lu tax tey barewul nit ñu bëgg seen moroom dëgg ? [Mayal nit ki tontu.] Bu ñu bëggee nit ñi bëgg ñu dëgg, ñun ci suñu bopp dañu war a wone mbëggeel bu dul wut njariñu boppam. Téere bii dafay wone naka lañuy wonee mbëggeel bu mel noonu. ” Jàngal 1 Korent 13:4-7 te boo koy jàng, fexeel ba kàddu yii feeñ bu baax : “ du wut njariñu boppam ”.