“ Bëggleen Yexowa, yéen ñépp ñi koy topp bu baax ”
Dimaas 4 awril dinañu fàttaliku deewu Yeesu
1 Am na léegi ay at ci ginnaaw, fekk Communistes yi ñoo doon jiite Ukraine, njiiti nguur googu dañu doon seet bu baax li suñu mbokk yi di def. Bi bésu Reeru Sang bi doon jege la doon rawati. Dañu bëggoon a xam fan lañuy daje. Loolu coono dëgg la woon ndaxte njiiti nguur gi xamoon nañu jamano bi bésu fàttaliku deewu Yeesu doon jegesi. Lan la suñu mbokk yi def ? Dafa amoon suñu benn mbokk mu jigéen mu amoon ci suufu këram foo xam ne ndox dafa doon taa. Ndox ma fa nekkoon dafa doon àgg ba ci óom yi. Njiiti nguur gi mënuñu woon a xalaat ne ay nit mënoon nañu fa daje. Looloo tax suñu mbokk yi defar ci kow ndox moomu fu ñu mënoon a nekk (ci tubaab plancher). Dëgg la béréb boobu kawewul woon te suñu mbokk yi fa doon daje dañu waroon a jonkan. Waaye njiiti nguur gi mujjuñu xam fu mbooloo mi daje woon ngir fàttaliku deewu Yeesu ak mbégte.
2 Suñu mbokk yooyu nekk Ukraine bëgguñu woon dara tere leen def li leen Yeesu laaj, maanaam fàttaliku deewam. Loolu dafay wone bu baax ne dañu bëggoon Yàlla (Lukk 22:19 ; 1 Ywna. 5:3). Bu fekkee ne ñu ngi ci ay jafe-jafe, yàlla na li suñu mbokk yooyu defoon yokk suñu doole bu baax. Te yàlla na tax itam ñu bañ a bàyyi dara tere ñu fekke Reeru Sang bi ca 4 awril. Bu ñu defee loolu dinañu wone ne ñu ngi yëg itam ci suñu biir xol li ki bind Sabuur yëgoon ci xolam bi mu doon wax : “ Céy, bëggleen Yexowa, yéen ñépp ñi koy topp bu baax. ” — Sab. 31:23.
3 Nañu dimbali nit ñi ñu gën a bëgg Yàlla : Mbëggeel bi ñu am ci Yàlla war na ñu xiir itam ci woo nit ñi ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Sasu Nguuru Yàlla bu feewriyee ci xët 5 mu ngi ñu doon xiir ñun ñépp ci bind ci benn kayit képp ku ñu bëgg woo ci ndaje boobu. Ndax yaa ngi topp bu baax loolu ñu waxoon, di dem woo képp ki nga bind ci sa kayit ? Nañu leen wax itam lan la ndaje boobu tekki. Nañu fàttali nit ñi bés ak waxtu bi ñuy defe ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Loolu dina leen mën a xiir ci ñëw ci ndaje bi. Te it bu ñu gisee ne lu baax lay doon, nañu leen wax ñu ànd ci ndaje boobu.
4 Bu ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu jotee, fexeel ba jege ñi ñów ci ndaje bi, te teral leen bu baax. Naka lañu leen mënee dimbali ba seen mbëggeel ci Yexowa yokku ? Nanga pare ngir bu ñu amee ay laaj nga tontu ci. Nanga pare it ngir saa yoo ko mënee nga wax leen ne bu leen neexee mën nga jàng ak ñoom Biibël bi. Woo leen it ci ndaje yi ñuy def ayu-bés bu nekk ci mbooloo mi. Mag yi it dinañu toppatoo bu baax karceen yi bàyyi waaraate yi ñów ci ndaje bi. Mën nañu seet ak ñoom kañ lañu leen mën a dem seeti te bu ñu fa demee ñu xiir leen ci bokkaat ci waaraate bi. Xéyna dinañu mën a jaar ci li ñu wax ci waxtaan bi ñu def ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu ngir xiir leen ci waaraate bi. — Room 5:6-8.
5 Ñun ci suñu bopp nañu gën a bëgg Yexowa : Bu ñu xalaatee bu baax ci njot gi ñu Yàlla may, loolu mën na yokk suñu mbëggeel ci Yexowa ak ci Doomam (2 Kor. 5:14, 15). Am na koo xam ne dafa yàgg tàmm fekke ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Waaye lii la wax : “ Dañuy yàkkamti ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu jot. At mu ne, dafay gën a am solo ci ñun. Maa ngi fàttaliku bi ma taxawee ci sama dëju pàppa, am na léegi 20 at. May xool sama pàppa mi nga xam ne dama ko bëggoon lool. Foofu laa yëge ci sama biir xol naka la njot gi ame solo. Bala sama baay di gaañu, njot gi xam-xam rekk la woon. Xamoon naa lépp li ci Mbind mi waxoon te mënoon naa ko leeral nit ñi. Waaye bi ma demee ba xam dëgg lan mooy dee, foofu la njot gi sog a indi mbégte ci sama biir xol ndax li mu ñuy defal. ” — Ywna. 5:28, 29.
6 Bi bés bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu di jegesi ren, nanga jël jot bi ngay waajal sa xol ngir ndaje boobu (2 Net. 19:3). Xalaatal bu baax ci aaya yi ñu war a jàng ngir ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Aaya yooyu ñu ngi ci téere Examinons les Écritures chaque jour — 2004, ak it ci Calendrier 2004. Am na ñoo xam ne dañuy jàng pàcc 112 ba 116 ci téere Le plus grand homme, ci seen njàngum njaboot. Am na ñuy jàng leneen ci yeneen téere yi nga xam ne surga bu takku te teey bi moo leen defar (Macë 24:45-47). Ñun ñépp mën nañu ñaan ay ñaan yu jóge ci suñu biir xol ngir lu jëm ci njot gi ñu Yàlla may (Sab. 50:14, 23). Waaw, ci jamano fàttaliku bi, nañu kontine di xalaat ci mbëggeel bi ñu Yexowa won. Nañu seet itam li ñu mën a def ngir wone mbëggeel bi ñu am ci moom. — Mark 12:30 ; 1 Ywna. 4:10.