Nañu dimbali suñuy moroom ñu jot ci lu baax li njot gi di indil nit ñi
Ci bésu 12 awril lañuy fàttaliku deewu Yeesu
1 “ Jërë-jëfati yaw Yàlla ndax sa may googu weesu dayo ! ” (2 Kor. 9:15). Loolu lañuy yëg ci suñu xol bu ñu xalaatee ci mbaaxaay ak yërmande bi ñu Yexowa won, jaarale ko ci doomam, Yeesu Kirist. Noonu it, ci ndaje fàttaliku deewu Yeesu bu ñuy def ci bésu 12 awril, mbooloo Yàlla mi dina mën a wone ne dafay gërëm bu baax Yàlla.
2 Am na ay milioŋi nit ñuy teew at mu nekk ci ndaje fàttaliku bi ak jaamukati Yexowa yi. Loolu dafay wone ne ñoom itam dañuy gërëm Yàlla ndax saraxu Yeesu. Waaye nit ñooñu, bu ñu bëggee jot ci lu baax li njot gi di indil nit ñi, fàww ñu wone ne gëm nañu njot googu (Ywna. 3:16, 36). Naka lañu leen mënee dimbali ñu am ngëm bu mel noonu ? Ci jamano fàttaliku bii, mën nañu leen xiir ci am benn njàngum Biibël ak ci teewe ndaje yi ñuy am ci mbooloo mi ayu-bés bu nekk. Nañu seet ni ñu mënee def loolu.
3 Nañu jàng Biibël bi ak ñoom : Booy woo nit ku suñu waxtaan neex ci ndaje fàttaliku bi, nanga jéem a komaase benn njàngum Biibël ci téere Qu’enseigne la Bible ? Nanga ko def ci xaaj bi tudd “ Le repas du Seigneur : une célébration qui honore Dieu ” ci xët 206 ba 208. Waxal nit ki ne danga ko bëgg won ni ñuy fàttalikoo deewu Yeesu. Ubbil xaaj boobu te waxtaan leen ci. Mën ngeen ko def ci benn walla ñaari yoon. Mën ngeen ko def sax bu ngeen taxawee ci bunt kër gi. Bu ngeen ci paree xéyna nit ki dina bëgg waxtaan ci pàcc 5 bi tudd “ La rançon, le plus beau don de Dieu ”. Bu ngeen demee ba taxawal benn njàngum Biibël, nangeen dellu ci ñeenti pàcc yi njëkk ci téere bi te ngeen waxtaan ci.
4 Ak kan lañu mën a jéem a komaase benn njàngum Biibël ? Xéyna ñi nga bokkal liggéey, ñi nga bokkal kalaas, walla say dëkkandoo. Bu amee ci mbooloo mi suñu ay mbokk yu jigéen yu seen jëkkër nekkul seede, suñu mbokk yu góor yi mën nañu jéem a waxtaan ak ñoom. Bul fàtte it say mbokk yi nekkul seede. Dinañu góor-góorlu it ngir woo ci ndaje fàttaliku bi ñi nga xam ne bu njëkk dañu tàmmoon a teewe ndaje yi (Luug 15:3-7). Nañu def lépp ngir dimbali nit ñooñu ñépp ñu jot ci lu baax li njot gi di indil nit ñi.
5 Nañu leen xiir ci teewe ndajey mbooloo mi : Ñi ñuy jàngal Biibël bi ak ñi suñu waxtaan neex, ci lu bare, ndaje fàttaliku bi mooy ndaje bi ñuy njëkk teewe. Naka lañu leen mënee xiir ci teewe ci yeneen ndaje yi ? Sasu Nguuru Yàlla bu awril 2005, xët 6 lii la waxoon : “ Booy wax ci ndaje bi ñu jagleel ñépp, wax ko yaxu waxtaan bi ngeen war a am ayu-bés bii di ñów. Won ko li ngeen war a waxtaan ci Njàngum La Tour de Garde ak Njàngum téere bi di ñów. Lu jëm ci Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla ak ndaje bi jëm ci liggéeyu waare bi, wax ko ni ñu leen di doxale. Boo amee waxtaan boo nar a def ci lekkool bi, xéyna dinga ko mën a def ci kanamam, mel ni yaa ngi ci bésu ndaje bi. Nanga waxtaan ak moom ci ay ponk yu am solo yi amoon ci ndaje yi nga teewe woon. Won ko ci suñuy téere ay foto yuy wone ni ndaje yi di deme. Bés boo defee njàngum Biibël bu njëkk bi, nanga ko komaasee woo ci suñuy ndaje. ”
6 Boroom xol yu rafet yi, bala ñuy mën a gaaw a jëm kanam, dañu war a faral di jàng Biibël bi ak ñun te teewe ndaje yi ñuy am ci mbooloo mi. Kon nañu xiir nit ñi ñu ñëw bokk ci loolu ñu Yexowa waajal. Nañu leen xiir it ci jariñoo maye bi gën a mag bi ñu Yexowa may, maanaam njot gi.
[Laaj yi]
1. Naka la mbooloo Yàlla mënee wone ne dafay gërëm Yàlla ndax njot gi mu ñu may ?
2. Ñan ñoo tàmm teewe ndaje fàttaliku bi ci wetu jaamukati Yexowa yi ? Nit ñooñu, bu ñu bëggee jot ci lu baax li njot gi di indil nit ñi, lan lañu war a def ?
3. Naka lañu mënee komaase benn njàngum Biibël ak ñi ñuy woo ci ndaje fàttaliku bi ?
4. Ci jamano fàttaliku bi, ak kan lañu mën a jéem a komaase benn njàngum Biibël ?
5. Ñi ñuy jàngal Biibël bi ak ñi suñu waxtaan neex, naka lañu leen mënee xiir ci teewe ndaje yi ñuy am ayu-bés bu nekk ci mbooloo mi ?
6. Lan ak lan lañu mën a def ngir boroom xol yu rafet yi mën a jot ci lu baax li njot gi di indil nit ñi ?