TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 3/07 p. 1
  • “ Defleen lii ngir fàttaliku ma ”

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • “ Defleen lii ngir fàttaliku ma ”
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Nañu dimbali suñuy moroom ñu jot ci lu baax li njot gi di indil nit ñi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • “ Bëggleen Yexowa, yéen ñépp ñi koy topp bu baax ”
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Naka lañu mënee dimbali ñi teewe ndaje fàttaliku bi ?
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Nañu fàttaliku njot gi te wone ci ne fonk nañu ko lool
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2007
km 3/07 p. 1

“ Defleen lii ngir fàttaliku ma ”

Bésu 2 awril lañuy fàttaliku deewu Yeesu

1. Lu tax bésu 2 awril 2007 nekk bés bu am solo ?

1 Ci bésu altine 2 awril 2007, ay milioŋi nit dinañu daje ci àddina si sépp ngir fàttaliku bi Yeesu saraxee bakkanam. Yeesu dafa dee ndax li mu nangu woon kiliftéefu baayam bi nekk asamaan. Noonu la wone ne bi seytaane waxee ne doomi Aadama yi dañuy jaamu Yàlla ndax seen intere bopp kese, dafa doon fen (Ayó. 2:1-5). Yeesu bi mu deewee, nit ku mat la woon. Amul woon benn bàkkaar. Reeru Sang bi dafa ñuy fàttali ne bi mu deewee noonu, dafa “ joxe bakkanam ngir njotug ñu bare ” (Macë 20:28). Moo tax Yeesu sant taalibeem yi lii : “ Defleen lii ngir fàttaliku ma ” (Lukk 22:19). Li ñu Yàlla may noonu, am na solo lool. Mbëggeel bi mu wone noonu, amul mbëggeel bu ko ëpp. Ndax bëgg gërëm Yàlla ci loolu dina la xiir ci komaase di waajal màggal boobu léegi ? — Ywna. 3:16.

2. Naka lañu mënee waajal suñu xol ngir jariñoo bu baax ndaje fàttaliku bi ?

2 Nañu waajal suñu xol : Bu ñu bëggee def loolu, nañu jàng li xewoon bés bu nekk ci bés yi mujjoon ci dundu Yeesu (Esr. 7:10). Am na lu ñu ci mën a dimbali : Mooy porogaraamu jàng Biibël bi, bi ñu def ci téere Examinons les Écritures chaque jour — 2007 ak ci calendrier bu 2007. Porogaraam boobu dafay topp li xewoon ci fan yi jiitu bés bi Yeesu deewee. Ndegam seeni weer ak suñu weer tey bokkuñu, porogaraam boobu, bés bu nekk dafay wone ban bés la ci suñu calendrier. Bés yi ñuy wax ci Biibël bi, ci calendrier yawut yi lañu leen jële. Ñoom, seeni bés dañu doon komaase bu jant bi sowee te doon jeex ci ëllëg si bu jant bi sowee. Bàyyi nañu xel ci loolu bi ñu doon defar porogaraamu njàngum Biibël bi ñu war a topp ci jamano fàttaliku bi. Nañu topp porogaraam boobu, di xalaat bu baax ci mbëggeel bi ñu Yexowa wone noonu. Bu ñu defee loolu, dinañu jariñoo bu baax ndaje fàttaliku bi.

3. Loo mën a def ngir dimbali ñi suñu waxtaan neex ak ñi bàyyi waare ngir ñu jariñoo ci ndaje fàttaliku bi ?

3 Nañu woo nit ñi ci ndaje fàttaliku bi : Sasu Nguuru Yàlla bu feewriyee, xët 3 ba 5, waxoon na ci liggéey bu mag te am solo bu ñu waroon a def ngir woo nit ñi ci xew bu am solo boobu. Ndax seet nga loo mën a def ngir mën a bokk bu baax ci liggéey boobu ? Ndax bind nga turu nit ñi nga bëgg woo ci ndaje fàttaliku bi te ndax komaase nga leen a woo ? Nañu seet li ñuy def ngir teel a agsi fi ñuy defe ndaje fàttaliku bi. Su ko defee dinañu mën a teral ñi ñu woo ak ñeneen ñi bëgg teew. Dinañu mën a toog seen wet te bokk ak ñoom suñu Biibël ak suñu téere woy bi. Nañu leen won suñu yeneen mbokk ci mbooloo mi ngir ñu xamante. Bu porogaraam bi jeexe, nanga nekk ak ñoom ngir tontu leen su ñu amee li ñu bëgg laaj. Nanga leen woo ci ndaje bi ñuy am ci bésu 15 awril ci waxtaan bi ñuy faral di am ci àddina si sépp bu bésu fàttaliku bi weesoo. Ñi nga xam ne bu njëkk dañu bokkoon ci mbooloo mi waaye léegi dañu bàyyi waare, njiiti mbooloo mi dinañu fexe ba ñu woo leen ci ndaje fàttaliku bi ak ci waxtaan bi ñu faral a def ci àddina si sépp bu bésu fàttaliku bi weesoo.

4. Naka lañu mënee jàpple nit ñi ngir ñu mën a jëm kanam ci wàllu ngëm bu bésu fàttaliku bi weesoo ?

4 Ñi komaase di waxtaan ak ñun ak ñi bàyyi waare, nañu leen dimbali ñu jëm kanam ci wàllu ngëm : Kiy def waxtaan bi ci ndaje fàttaliku bi, dina yégal nit ñi ne képp ku ko bëgg dina mën a am ku koy jàngal Biibël bi te du fey dara. Dina xiir it ñi sog a komaase waxtaan ak ñun ci kontine di jàng lu jëm ci Yexowa. Mën nga jaar ci li mu wax ngir dimbali ñi nga woo ci ndaje fàttaliku bi ñu jëm kanam ci wàllu ngëm. Su dee amaguñu njàngum Biibël, nanga def lépp ngir seeti leen bu bésu fàttaliku bi paasee, te won leen ni ñuy jànge Biibël bi. Nit ñooñu dañu war a teewe ndaje mbooloo mi ngir mën a jëm kanam ci wàllu ngëm (Yaw. 10:24, 25). Kon nañu leen xiir ci tàmm a teew ci ndaje yi ñuy am ci mbooloo mi. Njiiti mbooloo mi dañu war a seeti ñi teewoon ci ndaje fàttaliku bi fekk dañu bàyyi waare. Nañu leen dimbali it ñu gën a waxtaan ci li ñu dégg ci waxtaanu fàttaliku bi. Loolu dina leen mën a xiir ci bokkaat ci liggéey bi ñuy def ci mbooloo mi.

5. Lan lañu mën a jële ci ndaje fàttaliku bi ?

5 Ndaje fàttaliku bi dafa ñuy may ñu xalaat ci li ñu Yexowa ak Yeesu defal. Xalaat ci loolu dafay xootal mbëggeel bi ñu am ci ñoom te dina laal itam ni ñuy dunde (2 Kor. 5:14, 15 ; 1 Ywna. 4:11). Nañu waajal léegi suñu bopp, waajal it ñi suñu waxtaan neex ngir bés bu am solo boobu nga xam ne dinañu ci “ yégle deewu ” sang bi. — 1 Kor. 11:26.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager