Na suñu bët wér
1 Ci wàllu ngëm, ku nekk am na lu mel ni bët. Li ñuy xool ak bët boobu dina def lu bare ci suñu dund. Moo tax Yeesu waxoon lii ci waare bi mu defoon ci kow tund ba : “ Bu sa bët wéree, kon sa yaram wépp leer, waaye bu sa bët woppee, kon sa yaram wépp lëndëm. ” (Macë 6:22-24). Ku am bët bu wér dafay xam ne def li Yàlla bëgg mooy li ëpp solo. Alal sax du tax mu fàtte loolu (Macë 6:19-21, 24-33). Lan lañu mën a def ngir am bët bu wér ?
2 Nañu doylu : Biibël bi moo ne boroom njaboot dafa war a faj soxla njabootam (1 Tim. 5:8). Waaye loolu tekkiwul ne foo tollu rekk danga war a wut li gën ci alalu àddina, walla it lu xew rekk nga bëgg ko am (Léeb. 27:20 ; 30:8, 9). Biibël bi nee na bu ñu “ amee lekk ak koddaay ”, maanaam li ñu soxla dëgg, nañu ci doylu (1 Tim. 6:8 ; Yaw. 13:5, 6). Loolu bu ñu ko defee, suñu bët du xool lu mu warul a xool.
3 Ku am xel doo yenu loo àttanul. Kon nañu moytu leb li ñu soxlawul dëgg. Nañu moytu it am alal walla dugg ci loo xam ne dafay laaj jot ak toppatoo yu dul jeex (1 Tim. 6:9, 10). Lan moo ñu ci mën a dimbali ? Bala ñuy def dara, nañu njëkk ñaan Yàlla bu baax ci loolu te seet ndax du ñu yàqal dara ci wàllu ngëm. War nañu def lépp li ñu mën ngir jiital suñu ngëm ci suñu dund. — Fil. 1:10 ; 4:6, 7.
4 Yombalal sa dund : Yombal sa dund mën na la dimbali nga bañ a fonk alal ba mu ëpp. Suñu benn mbokk dafa seet ba gis ne njabootam soxlawul am alal bi mu amoon yépp. Nee na : “ Léegi laa gën a mën a jàpple sama mbokk yi ci mbooloo mi. Li ma wóor mooy Yexowa dina barkeel kuy wone ne dafa ko bëgg jaamu bala muy toppatoo boppam. ” Ndax mën nga yombal sa dund ngir Yexowa gën laa barkeel ?
5 Seytaane, alalu àddina walla suñu matadi mën na tax ñu def li ñu warul a def. Ku bañ loolu dal la, foo mënta nekk rekk danga war a xeex ñett yooyu. Buñu nangu suñu bët xool fu ne. Nañu ko teg ci li Yàlla bëgg ak ci suñu yaakaaru dund gu dul jeex. — Léeb. 4:25 ; 2 Kor. 4:18.
[Laaj yi]
1. Am bët bu wér mooy lan ? Te lu tax mu am solo ?
2. Lan la Kàddu Yàlla wax ci alal ?
3. Naka lañu mënee moytu yenu li ñu àttanul ?
4. Lu tax ñu war a seet ni ñu mënee yombal suñu dund ?
5. Ku bëgg bëtam kontine di wér, lu tax fu mu mënta nekk rekk mu war a xeex ngir loolu ?