Nañu fàttaliku li ñu jàng ci ndaje bu mag bu benn fan bi
Laaj yii di topp, dañu leen defar ngir ñu boole leen ci porogaraamu ndaje liggéeyu waare yi. Dinañu ci waxtaan bala ndaje bu mag bu benn fan ci atum liggéeyu waare 2006 di jot. Laaj yooyu lañuy laajte it bu ñuy fàttaliku li ñu jàng ci ndaje bu mag boobu. Sasu Nguuru Yàlla bu ut 2004 waxoon na ci xët 4 ni ñu ci war a waxtaane. Wottukat biy jiite dina seet kañ lañu ci mën a waxtaan bala ndaje bu mag bi di jot, ak it ginnaaw ndaje boobu. Bu ngeen di fàttaliku li ñu jàng ci ndaje bu mag bi, kiy jiite waxtaan bi, laaj yi yépp la war a laaj. Li ñu bëgg ci waxtaan bi mooy mu wone bu baax ni ñu mënee topp li ñu jàng ci ndaje bu mag bu benn fan bi.
SUBA SI
1. Lan mooy wéy di am bët bu wér ? Lu tax loolu yombul tey ? (“ Lu tax ñu war a wéy di am bët bu wér ? ”)
2. Wéy di am bët bu wér, naka la ñuy jariñe ? (“ Barke yi ñuy am bu ñu wéyee di am bët bu wér ”)
3. Am na itte yu nit ñi wax ne dañu jaadu. Waaye yan musiba ñoo ci mën a nekk ? (“ Nañu wéy di am bët bu wér ci àddina su bon ”)
NGOON GI
4. Wayjur yi ak yeneen karceen yi, naka lañu mënee dimbali ndaw yi ñu xam fu ñu war a góor-góorlu ci wàllu ngëm ? (“ Wayjur yu xam fu ñuy jëmale seeni doom ” ak “ Ay ndaw yu am fu ñuy góor-góorlu ci wàllu ngëm ”)
5. Naka lañu mënee ànd ak mbootaayu Yexowa di jëm kanam a) ñun ci suñu bopp ? b) ñun ak suñu njaboot ? c) ñun ak suñu mbooloo ? (“ Nañu def suñu xel yépp ci ànd ak mbootaayu Yexowa ”)