Ndaje bu mag bu benn fan biy ñów : li ñu fay waxtaane
Fasoŋ bi Yàlla defare bët, doy na kéemaan (Sab. 139:14). Waaye ba tey, mënul a xoolaale lépp. Fàww mu yem ci benn yëf, door a jàll ci beneen. Noonu la deme itam ci li ñuy woowe bët ci wàllu ngëm. Bu ñu bëggee gis bu baax ci wàllu ngëm, suñu xel yépp dafa war a nekk ci def coobare Yàlla. Ci àddina seytaane sii lu bare mën na ñu tere gis bu baax ci wàllu ngëm. Te loolu mu ngi yokku rekk. Kon suñu ndaje bu mag bu benn fan bu atum liggéeyu waare 2006 dina baax lool. Turam mooy “ Na suñu bët wéy di wér ” ! — Macë 6:22.
Lan lañu mën a def ngir mën a jot ci barke Yàlla yi (Léeb. 10:22) ? Loolu dinañu ci waxtaan ci xaaj bi tudd “ Ku wéy di am bët bu wér, dina am barke yu bare ”. Dinañu déglu ay nit ñuy wax barke yi ñu mën a am bu ñu toppee li Mbind mi wax. Ki ñu bànqaas bi yónnee, waxtaan bi muy njëkk def mu ngi tudd “ Nañu wéy di am bët bu wér ci àddina su bon sii ”. Waxtaan boobu dina wone ne am na lu mën a yokk suñuy jafe-jafe ba di yàq ndànk-ndànk suñu diggante ak Yàlla. Dinañu xam it lan moo bokk ci “ tànn cér bi gën [maanaam tànn li gën ci àddina] ”. — Lukk 10:42.
Naka la wayjur yi ak yeneen karceen yi mënee xiir ndaw yi ci def seen xel yépp ci seen diggante ak Yàlla ? Ay wayjur ak ay ndaw dinañu ci wax ci kanamu ñépp, ci ñaari waxtaan yii : “ Wayjur yuy jëmale seeni doom fu baax ” ak “ Ay ndaw yu am fu ñuy góor-góorlu ci wàllu ngëm ”. (Sab. 127:4.) Waxtaan bi mujj ci ndaje bu mag bu benn fan bi, ki ñu bànqaas bi yónnee moo koy def. Dina ñu won ni ñu mënee ànd ak mbootaayu Yexowa, di jëm kanam ñun ci suñu bopp, ñun ak suñu njaboot, ak it ñun ak suñu mbooloo.
Wéy di am ‘ bët bu wér ’ dafa am solo lool ci ku yàggul a xam dëgg gi. Am na solo it ci ku yàgg jaamu Yexowa. Ndaje bu mag bu benn fan bi, dina ñu won ni ñu mënee wéy di am ‘ bët bu wér ’.