Dinañu def lépp ngir wone suñu téere bu bees bi
1 Nit ñu bare tey dañuy jaaxle bu ñu gisee lépp li xew ci àddina si. Waaye barewul nit ñu xam li loolu yépp di tekki, li war a ñów ëllëg ak li ñu mën a def ngir mucc bés bu Yàlla di àtte àddina sii (Esek. 9:4). Dañu bëgg dimbali nit ñooñu ñu xam li xew-xewu àddina sii tekki. Looloo tax, diggante altine 16 me ba dimaas 12 suweŋ, dinañu def lépp ngir wone suñu téere bu bees bi tudd Veillez !
2 Téere boobu, mën nañu ko wone bu ñuy waaraate këroo-kër, bu ñuy dellu seeti nit ñi, ak it bu ñuy waaraate saa yu ñu ci amee bunt, walla ci mbedd yi ak ci bitig yi. Waaye ba tey, du nit ñépp lañu war a bàyyil téere Veillez ! Dinañu ko bàyyi ñi nga xam ne bëgg nañu xam li Biibël bi wax lu jëm ci li xew-xewu àddina si tekki. Ñi ko bëggul noonu nag, mën nañu leen a jox benn kayit bu ndaw.
3 Lii nga mën a njëkk wax ngir nit ñi déglu la :
◼ “ Ñu bare dañuy jaaxle bu ñu gisee coono yi yépp ak xew-xew yu metti yi am tey ci àddina si. [Waxal lu xew li ñépp xam ci gox bi.] Ndax xamoon nga ne Biibël bi waxoon na ne loolu yépp dina am ? [Mayal nit ki mu tontu. Ba pare jàngal benn aaya bu baax ci xew-xew bi nga doon wax léegi. Mën na nekk Macë 24:3, 7, 8 ; Lukk 21:7, 10, 11 ; walla 2 Timote 3:1-5.] Biibël bi dafa ñuy wax li suñu jamano tekki ak li war a ñów ëllëg. Ndax am na loo ci bëgg a xam ? [Mayal nit ki mu tontu. Bu ko loolu itteelee, won ko téere bi.] Téere bii, mën nga ko am. Jaayuñu ko, waaye boo bëggee jox dara ngir jàpple ñu ci liggéey bi ñuy def ci àddina si sépp, mën nga ko def. ”
4 Walla mën nga wax lii :
◼ “ Ñu bare tey amatuñu yaakaar ndax lu bon li am ci àddina si walla coono yu metti yi ñu am. Am na ñu bëgg xam lu tax Yàlla du def dara ngir loolu bañ a am. Boo jàngee Kàddu Yàlla dina la wóor ne Yàlla dina dindi coono doom-Aadama yépp bu ci kanamee tuuti. Xoolal barke yi Yàlla di indi ci kow suuf si. [Jàngal Sabuur 37:10, 11.] Ndax am na leneen loo ci bëgg a xam ? ” Nanga àggale waxtaan bi ak kàddu yi àggale woon waxtaan bii ci kow.
5 Nanga jéem a am tur ak adareesu képp ku jël benn téere Veillez ! Te fexeel ba seetiwaat ko ngir kontine waxtaan bi. Dinañu seet ni ñu mënee def loolu ci Sasu Nguuru Yàlla bu suweŋ 2005. Bés boo njëkkee gis nit ki, bu wonee ne dëgg-dëgg bëgg na waxtaan ak ñun, jéemal a tàmbali ci saa si benn njàngum Biibël ci téere Veillez ! walla beneen téere bu mel ni téere Laaj.
6 Bu ñu paree ndaje fu ñuy waxtaan ci xaaj bii, dinañu mën a am ay téere Veillez ! Na waaraatekat yi ak pioñee yi njëkk jël téere yi nu soxla ngir wone ko ci fan yu njëkk yi. Bu jeexee, ñu jëlaat yeneen. Liggéey boobu ñuy def, dina màggal Yexowa, te fu ñu mënta nekk, ñi yore xol bu baax dinañu ci gis njariñ. Yàlla na Yexowa barkeel lépp li ñuy def ngir wone suñu téere bu bees bi. — Sab. 90:17.