Nañu dimbali suñu moroom
1 Yexowa, dimbali jaamam rekk la bëgg (2 Net. 16:9 ; Isa. 41:10, 13). Mu ngi mel ni sàmmkat buy toppatoo bu baax géttam. Moom la Isayi wax. Nee na : “ Dina dajale mbote yi, jël leen, def leen ci dënnam. Te buy jiital yiy nàmpal, dina dox ndànk. ” (Isa. 40:11). Naka lañu mënee topp Yexowa ci loolu ?
2 Nañu dimbali ñi yàggul ci mbooloo mi : Nañu leen wax ñu ànd ak ñun ngir dëgëral seen ngëm (Léeb. 13:20). Am na suñu mbokk mu wax ni ñu ko jàpplee bi mu komaasee ñëw ci mbooloo mi. Nee na : “ Am na njaboot bu ma doon woo ngir ma bokk ci seen njàngum Biibël. Te loolu du benn yoon rekk la ko def. Bi ma jëmee kanam ci wàllu ngëm, am na ñaari pioñee, jëkkër ak jabar, yu doon jàpp ak man ay bés ngir yendu ci waaraate bi. Dañu doon am ay waxtaan yu neex te am solo ci wàllu ngëm. ” Nee na it : “ Bala ma nekk karceen, dama doon génn guddi àjjuma ak samdi. Waaye dama ko mujj bàyyi. Sama mbokk yi ma doon àndal doyoon nañu ma. ” Li ko waa mbooloo mi def noonu moo dimbali suñu mbokk moomu mu am ngëm gu gën di dëgër. Léegi sax, Betel la nekk. — Kol. 2:6, 7.
3 Na ku nekk dëgëral sa ngëmu moroom : Mën nañu dimbali itam suñu mbokk yi bu ñu leen gisee ci coono. Ndax am na ku feebar walla ku màgget ci sa mbooloo ? Seetal ndax mënoo ko dimbali mu waaraate ci telefon. Walla ngeen ànd def sa benn njàngum Biibël. Walla sax nga indi sa benn njàngum Biibël ci këram. Ndax amul wayjur bu am doom yu tuuti ? Seetal ndax soxlawul ku ko ci jàpple buy waaraate. Ndax am na ku bare kersa ci sa mbooloo ? Xéyna bëgg na ku koy jàpple ngir dellu seeti ñi suñu waxtaan neex, walla ci waaraate bi. Bu ñu bëggee suñu mbokk yi, dinañu seet li ñu mën a def ngir yëkkëti seen ngëm, maanaam dëgëral ko. — Room 14:19.
4 Bu ñu jéemee toppatoo suñuy mbokk ci ngëm ni Yexowa di toppatoo ñi koy jaamu, ku nekk dinga dëgëral sa ngëmu moroom. Dinañu gën a bëggante ci biir mbooloo mi te dinañu màggal suñu Baay bi nekk ca asamaan. — Efes 4:16.