Ndaje bu mag bu ñaari fan biy ñów : li ñu fay waxtaane
Àddina su bon sii tollu na ci fanam yu mujj yi. Kon am na lu am solo lu ñu war a def. Mooy : 1) Bañ a summi li nga xam ne dafa mel ni suñu yére ci wàllu ngëm. 2) Sàmm it liy tax nit ñi ràññe ñu ni karceen (Peeñ. 16:15). Looloo tax ndaje bu mag bu ñaari fan ci atum liggéeyu waare 2006 am tur bii : “ Solleen jikko ju bees ji. ” — Kol. 3:10.
Fan bu njëkk bi : Waxtaan bu def ay xaaj bi ñuy njëkk def mu ngi tudd “ Nañu wone jikko yi bokk ci jikko ju bees ji ”. Dina wone ne dañu war a góor-góorlu ngir am jikko ju bees ji. Loolu dina ñu jariñ ci lépp li ñuy def. Lan lañu war a def ba am ko ? Dinañu ci waxtaan ci ñaari waxtaan yi ñuy mujj def ci fan bu njëkk bi. Ñu ngi tudd “ Nanga yar sa bopp ba mën a xalaat bu baax ci li nga jàng ” ak “ Yar biy indi jikko ju bees ji ”.
Ñaareelu fan bi : Jikko ju bees ji dina feeñ ci ni ñuy waxe. Loolu ñaareelu waxtaan bi def ay xaaj dina ko wone. Waxtaan boobu mu ngi tudd “ Nañu góor-góorlu ngir am waxu nit ku am xel. ” Waxtaan bi ñu jagleel ñépp dina wone ne dañu war a gaaw a ràññe li seytaane di def ngir yóbbaale ñu. Waxtaan boobu mu ngi tudd “ Ndax yaa ngi góor-góorlu ngir nit ñu bon ñi bañ laa yóbbaale ? ” Ñaari waxtaan yi ñuy mujj def ci ndaje bu mag bi ñu ngi tudd “ Moytuleen sobe àddina si ” ak “ Nañu defar suñu jikko bés bu nekk ”. Waxtaan yooyu dinañu wone ni ñu mënee daw jikko ak jëf yi àndul ak li Yàlla bëgg. Dinañu wone it li ñu mën a def ngir dëgër ci li ñuy def ngir jaamu Yexowa.
Xelal yooyu dinañu xiir ñépp ci sol jikko ju bees ji te fexe ba mu des ci ñun. Yàkkamti nañu lool ndaje bu mag boobu !