Nañu fàttaliku li ñu jàng ci ndaje bu mag bu ñaari fan bi
Laaj yii di topp, dañu leen defar ngir ñu boole leen ci porogaraamu ndaje liggéeyu waare yi. Dinañu ci waxtaan bala ndaje bu mag bu ñaari fan ci atum liggéeyu waare 2006 di jot. Laaj yooyu lañuy laajte it bu ñuy fàttaliku li ñu jàng ci ndaje bu mag boobu. Sasu Nguuru Yàlla bu ut 2004 waxoon na ci xët 4 ni ñu ci war a waxtaane. Wottukat biy jiite dina seet kañ lañu ci mën a waxtaan bala ndaje bu mag bi di jot, ak it ginnaaw ndaje boobu. Bu ngeen di fàttaliku li ñu jàng ci ndaje bu mag bi, kiy jiite waxtaan bi, laaj yi yépp la war a laaj. Li ñu bëgg ci waxtaan bi mooy mu wone bu baax ni ñu mënee topp li ñu jàng ci ndaje bu mag bu ñaari fan bi.
FAN BU NJËKK BI
1. Naka lañuy sole jikko ju bees ji ? Lu tax ñu war a kontine di ko sol ?
2. Am na ñu yokk li ñuy def ci liggéeyu waare bi. Lan lañu def ngir mën loolu ?
3. Lu tax waruñu di tollale suñu bopp ak suñu moroom yi ?
4. Naka lañu mën a wonee jikko ju bees ji ci suñu biir njaboot ?
5. Naka lañu mënee jàpple bu baax mbooloo mi ?
6. Lu tax ñu war a wone jikko ju bees ji ci waaraate bi ?
7. Xalaat bu baax ci li ngay jàng ci Mbind mu sell mi, lu muy tekki ? Ban njariñ lañu ci mën a jële ?
8. Yan jikko ñoo mën a tax ñu nekk ku neex a jubbanti ci loxo Yexowa ?
ÑAAREELU FAN BI
9. Jëfandikoo sa làmmiñ ci fasoŋ bu rafet, lu tax mu am solo ?
10. Dañu war a wax lu rafet bu ñu nekkee fi ñuy liggéeye, fi ñuy jànge, walla feneen. Loolu ban njariñ lañu ciy gis ?
11. Bu ñu nekkee ak suñu mbokk karceen yi, naka lañu mënee topp li Pool wax ci Efes 4:25-32 ?
12. Naka lañu mënee jëfandikoo suñu làmmiñ ci fasoŋ bi gën a rafet ?
13. Lan lañu mën a def ngir nit ñu bon ñi bañ ñoo yóbbaale ?
14. Ci yan fànn lañu war a fexe ba benn sikk bu jóge ci àddina si bañ a nekk ci ñun ?
15. Lu tax bés bu nekk ñu war a defar suñu jikko ? Naka lañu ko mën a defe ?
16. Lan nga fas yéene topp ci li nga dégg ci ndaje bu mag bu ñaari fan bii ?