TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 2/03 p. 5
  • Ndimbal buy agsi ci waxtoom

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ndimbal buy agsi ci waxtoom
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Buleen fàtte ñi bàyyi waare
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Ndimbal bu yomb am
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
Sasu Nguuru Yàlla — 2003
km 2/03 p. 5

Ndimbal buy agsi ci waxtoom

1 Ndaw li Pieer dafa seetlu woon ne mbokkam yi ci wàllu ngëm dañu soxla woon liy yokk seen doole. Li mu leen bëgg moo tax mu am lu mu leen fàttali te bëgg dalal seen xel (2 Pie. 1:​12, 13 ; 3:⁠1). Dafa wax nit “ ñi Yàlla jagleel ngëm ”, ñu wéy di yokk seeni jikko karceen yi ndax “ seen xam Yeesu Krist Boroom bi am njeriñ te jur mbaax ”. (2 Pie. 1:​1, 5-8.) Nit ñooñu, Yexowa dafa leen woo te dafa leen tànn. Pieer dafa leen bëggoon a dimbali ndax ñu fexe ba sàmm loolu ngir ñu fekk leen ‘ ci jàmm, ñu baña am benn gàkk mbaa sikk ’. (2 Pie. 1:​10, 11 ; 3:14.) Ci ñu bare, li Pieer wax noonu, nekkoon na ndimbal bu agsi ci waxtoom.

2 Tey wottukat yi ci mbooloo karceen bi, noonu lañuy toppatoo ñi bokk ci mbooloo mi. Ci “ bési tiis yu tar ” lañu tollu. Ay jaamukatu Yexowa yu bare ñoo nekk ci jafe-jafe yu metti (2 Tim. 3:⁠1). Tey, ñàkk xaalis, coono njaboot, walla suñu jafe-jafe bopp, dañuy yokku. Loolu mën na tax ñenn ñi wax ni Dawuda : “ Musiba yi ma wër dañu bare ba mënuma leen a waññ. Samay njuumte yi ma dab, ñoo ëpp li ma mën a gis. Dem nañu ba ëpp karaw yi nekk sama kow bopp, sama xol ci boppam sax, bàyyi na ma. ” (Sab. 40:12). Coono yi, mën nañu diis ci nit ñooñu ba ñu bañ a topp bu baax seen wareef ci wàllu ngëm. Mën nañu dem sax ba bëgg bàyyi liggéeyu waare bi. Waaye nag demuñu ba ‘ fàtte santaane Yexowa yi ’. (Sab. 119:176.) Léegi la magi mbooloo mi war a dimbali nit ñooñu ni ñu ko soxlaa. — Isa. 32:​1, 2.

3 Ñaan nañu magi mbooloo mi ñu góor-góorlu ngir jàpple ñi nga xam ne, fi mu ne nii, dañu bàyyi waaraate. Fi ñu tollu nii, ñu ngi ci liggéey bu baax, te dinañu ko def ba weeru màrs jeex. Ñaan nañu wottukati njàngum téere bi, ñu dem seeti ñi bàyyi waaraate ngir jàpple leen ci wàllu ngëm. Dinañu leen mën a dimbali ba ñu bokkaat ci li ñuy def ci mbooloo mi. Mën nañu jéem a am benn njàngum Biibël bi ak ñi ko soxla. Mën nañu ñaan it yeneen waaraatekat yi, ñu jàpple nit ñooñu. Bu ñu la ko ñaanee, li ngay def dina am njariñ lool. Boo nekkee ku laabiir te baax, ci nga leen di gën a mën a dimbali.

4 Bu amee ku bokkaat ci lépp li ñuy def ci mbooloo mi, ñépp a ciy bég (Lukk 15:⁠6). Lu baax li ñuy jéem a defal ñi bàyyi waaraate, mën na mujj a mel ni “ kàddu bu ñu wax ci waxtoom ”. — Léeb. 25:11.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager