Nañu jàngal nit ñi woyof ñu topp yoonu Yàlla
1 Nit ñi dañu doon wax ne taalibe Yeesu yu njëkk yi dañu bokk ci “ yoon wi ”. (Jëf. 9:2.) Nekk taalibe Yeesu dëgg, sa dundin yépp lay laal (Léeb. 3:5, 6). Bu ñuy jàngale Biibël bi, waruñu yem rekk ci jàngal nit ñi li nekk ci Biibël bi. Dañu war a dimbali ñiy jàng Biibël bi ñu topp yoonu Yexowa. — Sab. 25:8, 9.
2 Bëgg Yexowa ak Yeesu : Fexe ba xel mi nga yor, sa xalaat, sa waxin, ak sa jikko méngoo ak li neex Yàlla, jafe na lool ci nit ku matul (Room 7:21-23 ; Efes 4:22-24) ! Waaye mbëggeel bi ñu am ci Yàlla ak Doomam, dina ñu xiir ci loolu (Ywna. 14:15 ; 1 Ywna. 5:3). Lu ñu mën a def ba ñiy jàng Biibël bi ak ñun am mbëggeel boobu ?
3 Nanga dimbali ki ngay jàngal Biibël bi mu xam jikko Yexowa. Suñu benn mbokk mu góor nee na : “ Mënuloo bëgg nit koo xamul. Looloo tax bu may komaase njàngum Biibël rekk, damay won nit ki turu Yàlla ci Biibël bi. Te saa su nekk damay jéem a wax ci jikko Yexowa yi. ” Bu ñu bëggee def loolu, nañu wax ci li Yeesu def (Ywna. 1:14 ; 14:9). Am na wërale yu ñu def ci téere Qu’enseigne la Bible ? ngir jeexal pàcc bu nekk. Nañu ci waxtaan it ngir kiy jàng Biibël bi xalaat bu baax ci jikko Yàlla ak doomam.
4 Nañu nekk royukaay : Komka ay jàngalekat lañu te dañuy won nit ñi fi ñu war a jaar, suñuy jëf dina leen won ni ñuy toppe yoonu Yàlla (1 Kor. 11:1). Ci ñiy jàng Biibël bi, barewul ñu tàmm jege ku ñu xamul ngir wax ak moom ci ngëmam. Mbëggeel, ngëm ak fit moo leen mën a dimbali ba ñu bokk ci liggéeyu waare te sàkk ay taalibe. Ñun, dañu leen war a muñal te dañu war a xam bu baax ni ñuy defe ak ñoom ngir ñu am jikko yooyu (2 Kor. 4:13 ; 1 Tes. 2:2). Bu ñu komaasee waare, dinañu ànd ak ñoom ngir dimbali leen.
5 Ci yeneen fànn yu am solo it, li ngay def mën na won ñiy jàng Biibël bi ni karceen war a dunde. Bu ñu la gisee ngay dem seeti ñi feebar, walla ngay nuyu bu baax ñiy ñëw teewe ndaje yi, dinañu gis li ñu mbëggeel di defloo (Ywna. 15:12). Booy bokk ci set-setal bi ñuy def ci mbooloo mi, walla booy dimbali sa moroom yi, yaa ngi koy won li mu mën a defal moroomam (Ywna. 13:12-15). Bu ñu la gisee ngay yombalal sa dund, dinañu xam lan mooy ‘ jëkk a wut nguuram ’. — Macë 6:33.
6 Jàngal nit ñi Kàddu Yàlla te sàkk ay taalibe laaj na lu bare. Waaye gis nit ñi woyof di “ jaar ci tànki dëgg ”, mbégte mu réy la ! — 3 Ywna. 4.
[Laaj yi]
1. Sàkk taalibe, lan la ëmb ?
2. Lu mën a xiir nit kuy jàng Biibël bi ci topp li Yàlla santaane ?
3. Lu ñu mën a def ba kiy jàng Biibël bi bëgg Yexowa ak Yeesu ?
4. a) Lu tax waaraate jafe ci ñu bare ci ñiy jàng Biibël bi ak ñun ? b) Kiy jàng Biibël bi, bu komaasee bokk ci liggéeyu waare bi, naka lañu ko mënee dimbali ?
5. Lu baax li ñuy def, naka la mënee a jàngal ñiy jàng Biibël bi ak ñun ni ñuy toppe li Yàlla santaane ?
6. Kuy dimbali ñi woyof ñu jaamu Yexowa, lan la ciy jële ?