Ay njàngum Biibël yu ñuy def ci buntu kër ak ci telefon yu jëm kanam
1 Komaase benn njàngum Biibël, lu neex la. Waaye suñu liggéey bi yemul foofu. Li ñu bëgg mooy nit kooku dem ba nekk taalibe Yeesu dëgg (Macë 28:19, 20). Lan moo ñu ci mën a dimbali ?
2 Ñi barewul jot : Nit ñi tey, dañu gën di ñàkk jot. Am na béréb yoo xam ne, ñi fay nangu toog lu mat benn waxtu ngir jàng Biibël bi, duñu bare dara. Loolu moo tax ñu wax ñu, ñu komaase te def njàngum Biibël yi ci buntu kër walla ci telefon. Njàngum Biibël yooyu, bu ñu leen di komaase, mën na am ñu gàtt. Mën nañu waxtaan ci benn walla ñaari xise yu ñu jële ci téere Qu’enseigne la Bible ? Waaraatekat yu bare ñu ngi def léegi ay njàngum Biibël yu mel noonu ci buntu kër walla ci telefon. Loolu lu rafet la!
3 Waaye nag, bu nit yemee rekk ci njàngum Biibël bi ñu koy def ci buntu këram, ndax dina doy ? Déedéet. Dëgg la, bu ñu komaasee njàngum Biibël ba pare, li gën mooy, ñu bañ a yàgg lool. Waaye nag, Le ministère du Royaume bu me 1990 newoon na ci xët 8 ne bu ñu xasee ba taxawal njàngum Biibël te fexe ba nit ki bëgg kontine waxtaan yi ñuy def ak moom, waxtaan yi ñu fay def war nañu gën a yàgg. Loolu dafa am solo lool. Nañu ko seetee ci lii : Xale bu toog lu yàgg te amul li muy lekk, bu ñu koy may mu lekk, dañuy komaase ci lu tuuti, ba bés bu muy mën a lekkaat bu baax. Waaye bu kontinee ci lu tuuti loolu kese, du mën a amaat doole te màgg ni mu ware. Noonu it, kiy jàng Biibël bi ci buntu këram, soxla na faral a am njàngum Biibël bu gën a yàgg ngir mën a nekk jaamukatu Yàlla bu mat, maanaam bu ñor. — Yaw. 5:13, 14.
4 Njàngum Biibël yi ñuy def ci biir kër yi : Li gën mooy ñu def njàngum Biibël yi ci biir kër walla ci beneen béréb bu baax ci njàng mi. Bu ñu defee noonu, njàng mi dina gën a yomb, te nit ki dina gën a mën a nànd li kàddu Yàlla wax (Macë 13:23). Ki koy jàngal it dina gën a mën a génne ci xise yi li nit ki gën a soxla. Te li ëpp solo mooy, bu njàng mi gënee yàgg, dinañu mën a am waxtaan yu gën a xóot ci aaya yi, bu ko defee Kàddu Yàlla dina gën a mën a dëgëral ngëmam. — Room 10:17.
5 Loo mën a def ngir kontine njàngum Biibël bi ci biir kër gi ? Bu fekkee ne def ngeen ba pare ay njàngum Biibël yu gàtt, mën nga ko laaj ndax bëggul seen waxtaan gën a yàgg léegi, te nga wax ko ñaata minit nga bëgg def ci waxtaan yi. Walla mën nga ko laaj lii : “ Ndax tey dinañu mën a toog waxtaan ? ” walla “ Tey suñu waxtaan ci lii lay jëm. Ñaata minit nga ci mën a def ? ” Bu fekkee ne wax nga ak nit ki ngir ngeen def njàngum Biibël bi ci biir kër gi, waaye mënuloo fexe ba loolu am, nanga kontine di waxtaan ak moom ci buntu kër gi ay waxtaan yu gàtt. Bu beneenee, boo ko mënee, nga jéem a waxaat ak moom ngir ngeen def njàng mi ci biir kër gi.
6 Bu ñuy wut boroom xol yu rafet yi, buñu fàtte li waral ñuy komaase te di kontine ay njàngum Biibël. Li ñu bëgg mooy boroom xol yu rafet yi jébbal seen bopp Yexowa te nekk ay jaamukati Yexowa yu ñu sóob. Bu ñuy jéem a def loolu ci waaraate bi, yàlla na Yexowa barkeel suñu liggéey. — 2 Tim. 4:5.
[Laaj yi]
1. Lu tax ñuy jàng Biibël bi ak nit ñi ?
2. Lan mooy njàngum Biibël ci buntu kër ak ci telefon te lu tax ñu baax ?
3. Lu tax ñu war a jéem a yokk jot bi ñuy jàngal nit ci buntu këram ?
4. Ban njariñ moo nekk ci def njàngum Biibël bi ci biir kër gi ?
5. Loo mën a def ngir kontine njàngum Biibël bi ci biir kër gi ?
6. Bu ñuy waaraate, lan lañu war a wut ? Li ñu wax ci xaaj bii, naka la ñuy dimbalee ci loolu ?