Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng
Xaaj 1 : Lan mooy njàngum Biibël ?
1 Weer wu nekk, ñi bokk ci mbooloo Yàlla dañuy def lu mat juróom-benni milyoŋi njàngum Biibël ci àddina si sépp. Fasoŋ bi ñuy jàngale bu baaxee, mën na am ñiy jàng Biibël bi dem ba jébbal seen bopp Yexowa, ñu sóob leen ci ndox te dinañu “ mana jàngal ñeneen ”. (2 Tim. 2:2.) Ndax bëgg nga ñi ngay jàngal Biibël bi def loolu ? Dinañu def ci Sasu Nguuru Yàlla yi ay xaaj yuy wone ni ñu mënee dimbali ñiy jàng Biibël bi ñu jëm kanam ci wàllu ngëm. Ci bii lañu koy komaase.
2 Kañ nga mën a wax ne yaa ngi def njàngum Biibël : Def njàngum Biibël mooy tàmm di waxtaan ak nit ci Biibël bi ak benn ci téere yi ñu am ngir jàngale Biibël bi. Bu dee sax waxtaan bi du yàgg walla ci telefon lañu koy defe, njàngum Biibël la. Kañ lañuy mën a komaase bind ne ñu ngi def njàngum Biibël ? Boo wonee nit naka lañuy jànge Biibël bi, ba pare nga jàngal ko ko ñaari yoon, boo gise ne nit ki bëgg na kontine njàng mi, mën nga bind ne yaa ngi def njàngum Biibël.
3 Ñu bare dañuy jël téere Laaj ak téere Xam-xam ngir def njàngum Biibël. Bu ngeen gisee ne ki ngeen di jàngal dafay jëm kanam, bu dee sax ndànk-ndànk la koy defe, te fonk na li muy jàng, bu ngeen paree ñaari téere yooyu, mën ngeen jàng ak moom beneen téere. Mën ngeen jël téere Adorez Dieu te bu dee nit ki mënul liir bu baax mën ngeen jël téere Mën nga nekk xaritu Yàlla !
4 Njàngum Biibël yi ñuy def ak nit ñi tax na ba ay milyoŋi nit nekk ay taalibe Yeesu Krist (Macë 28:19, 20). Sasu Nguuru Yàlla yii di ñów dinañu def ay waxtaan yu mel ni bii. Bu ñu toppee li ñu ciy wax, dinañu mën a dimbali ñiy jàng Biibël bi ñu jëm kanam ci wàllu ngëm.