Réveillez-vous ! bu am solo bu ñu war a wone ci weeru septaambar
1 Ñu bare, bu ñu déggee picc buy woy woy bu neex walla bu ñu gisee ni asamaan si di rafete bu jant bi di so, dañuy bég. Waaye nag, ñu bare nanguwuñu ne, am na kenn ku bare mbëggeel te nekk ci asamaan si, ku sàkk yëf yooyu. Ñun, am na lu ñu mën a def ngir xamal nit ñi ne Yexowa mooy sàkk-kat bi. Mooy wone Réveillez-vous ! bu am solo bi war a génn ci weeru septaambar (Isa. 40:28 ; 43:10). Réveillez-vous ! bu war a génn ci weer woowu laaj bii lay tontu : “ Y a-t-il un Créateur ? ”, maanaam ndax am na ku sàkk lépp ?
2 Ci goxu mbooloo mi : Bu mënee nekk, nanga fexe ba ànd ak mbooloo mi ci waaraate bi këroo-kër samdi bu nekk. Boo bëggee it mën nga ko wone yeneen bés yi. Téere boobu dina neex jàngalekat yi lool ak ñiy liggéey ci wàllu njàngale. Kon na mbooloo yi seet li ñu mën a def ngir won ko nit ñooñu ci seen gox.
3 Bu nit wonee ne suñu waxtaan neex na ko, laaj ko benn laaj te wax ko ne dinga ci tontu boo dellusee. Mën nga ko laaj lii : lu tax suñu Sàkk-kat mii bare mbëggeel di seetaan coono yu bare yii. Te boo fa dellusee, mën nga waxtaan ak moom ci pàcc 1 walla pàcc 11 yi nekk ci téere Qu’enseigne la Bible ? Mën nga ko laaj it laaj bu jëm ci lu tax Yàlla sàkk suuf si. Boo fa dellusee nanga waxtaan ak moom ci pàcc 3.
4 Ca lekkool ba : Bu fekkee ne dangay jàngi lekkool, ndax mënuloo may téere boobu ñi lay jàngal walla it yeneen eleew yi ? Boo ci tegee benn ci sa kow taabal, dina am ñu koy gis ba laaj la lu jëm ci sa ngëm. Xéyna dinga mën a jariñoo Réveillez-vous ! boobu ba wax ci sa ngëm bu ngeen di def waxtaan ci seen biir kalaas walla bu ngeen amee waxtaan bu ngeen war a bind ngir jox ko seen jàngalekat. Am na lu la ci mën a dimbali bu baax. Mooy xaaj bi nekk ci Réveillez-vous ! boobu te tudd “ Les jeunes s’interrogent... ” (maanaam laaj yi ndaw yi di laaj seen bopp). Xaaj boobu dafay wax ci waxtaan bii : “ Comment défendre ma croyance en la création ? ” (maanaam lan laa mën a wax ñi may laaj lu tax ma gëm ne am na ku sàkk lépp).
5 Yexowa yelloo na teraanga ak ndam ndax li mu sàkk lépp (Peeñ. 4:11). Nañu wone Réveillez-vous ! bu weeru septaambar, te sawar ci lool ! Bu ñu defee loolu, dinañu màggal Ki ñu sàkk te dimbali suñu moroom yi, ñu def loolu ñoom itam.