Réveillez-vous ! bu am solo bu ñu war a wone ci wéeru nowàmbar !
1 Nit ñu bare dañu bëgg xam dëgg ndax Biibël bi am na njariñ. Bu fekkee ne ay nit ñoo ko bind, lu tax ñu koy woowe Kàddu Yàlla ? Lu tax mu war ma wóor ne mën na ma won fi ma war a jaar ? Su ma jëlee sama jot ngir jàng Biibël bi te di ci góor-góorlu, lan laa ciy jële ? Ban sotti Biibël laa war a jëfandikoo ? Laaj yii bokk nañu ci laaj yi ñuy tontu ci Réveillez-vous ! bu am solo biy génn ci wéeru nowàmbar te tudd “ Pouvez-vous avoir confiance en la Bible ? ”, maanaam ndax mën nga gëm li nekk ci Biibël bi ?
2 Dañu bëgg joxe Réveillez-vous ! boobu ay nit ñu baree bare ci suñu goxu mbooloo. Bu mënee nekk, ci wéeru nowàmbar, nañu ànd ak suñu mbooloo ci waaraate bi samdi bu nekk. Nañu won Réveillez-vous ! boobu suñuy xarit, suñuy dëkkandoo, ñi nu bokkal liggéey, suñu jàngalekat yi, ñi nu bokkal kalaas, ak ñi ñuy dellu seeti. Bu ngeen di dem marse ak it bu ngeen di tukki, nangeen yóbbale yenn ci Réveillez-vous ! boobu. Dinañu ci am lu doy ndaxte njiiti mbooloo mi laaj nañu yéenekaay yu ëpp li mbooloo mi tàmmoon a jot.
3 Nañu komaase ay njàngum Biibël : Bu ngeen di wone yéenekaay boobu, bala ngeen jeexal waxtaan bi, mën ngeen a wax lu mën a tax ngeen di komaase njàngum Biibël bés bu ngeen dellusee. Mën ngeen wax lii : “ Su ma fi dellusee, dinaa la won li Biibël bi wax ci laaj bii, ‘ Lu tax Yàlla sàkk suuf si ? ’ ” Ba pare nanga fa dellu ak téere Q’enseigne la Bible te won ko xët 4-5, walla nga waxtaan ak moom ci pàcc 3, xise 1-3. Mën nga wax itam lii : “ Bëgg naa fi dellusi ngir waxtaan ak yow ci lu Biibël bi waxoon te ñu koy gis tey ”. Boo fa dellusee, won ko ci téere bi pàcc 9 te waxtaanal ak moom ci xise 1-3. Walla mën nga wax nit ki lii rekk : “ Ñu bare dañuy wax ne bu ñuy jàng Biibël bi, li ñuy jàng du leer ci ñoom. Bu ma fi dellusee, dinaa la won naka nga mënee def ba xam bu baax li Biibël bi wax ”. Boo fa dellusee, won ko téere Q’enseigne la Bible, te won ko ni ñuy defe njàngum Biibël.
4 “ Mbind mu sell, mi [ñu] man a yee ci yoonu mucc ”, ci Biibël bi kese la nekk (2 Tim. 3:15). Looloo tax, ñun ñépp dinañu góor-góorlu ngir sawar lool ci wone Réveillez-vous ! bu am solo boobu ngir dimbali nit ñi ñu gëm li nekk ci Biibël bi !