Li ñu mën a def ba komaase njàngum Biibël ak ñiy jël suñuy yéenekaay
1. Lan lañu bëgg dëgg bu ñuy joxe yéenekaay yi ?
1 Samdi yi, dañuy faral di wone ci waaraate bi suñuy téere La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! Waaye loolu mooy liy jëkk rekk ci li ñuy def ngir mën a jot li ñu tax a jóg, maanaam jàngal dëgg gi boroom xol yu jub yi. Lii di topp, dafa ñuy won li ñu mën a wax bu ñuy wone téere Qu’enseigne la Bible bés bu ñuy dellu seeti nit ñi, ak it li ñu mën a def ba komaase ak ñoom njàngum Biibël. Xelal yooyu mën nga ci soppi dara ngir mu gën a baax ci seen gox te mën nga ko wax it ci sa kàddu bopp. Su amee leneen lu mën a baax ci seen gox, mën nga ko wax itam.
2. Naka lañu mënee jariñoo xët yi njëkk ci téere Qu’enseigne la Bible ngir komaase njàngum Biibël ?
2 Jariñool xët yu njëkk yi ci téere bu nekk : Booy delloo seeti nit ki, mën nga wax lii : “ Yéenekaay yi ma la joxoon dañuy wax ci li nekk ci Biibël bi. Xoolal ni jàng Biibël bi ame solo ”. Jàngal Esayi 48:17, 18 ; Yowaana 17:3 ; walla beneen aaya buy wone lu tax jàng Biibël bi am solo. Boo wonee nit ki téere Qu’enseigne la Bible, ba mu jël ci benn, mën nga def lii di topp :
◼ “ Biibël bi dafa ñuy may yaakaar bu wóor ngir ëllëg ”. Wonal nit ki xët 4 ak 5 te laaj ko lii : “ Ci li ñu wax fii, lan nga bëgg mu am ? ” Won ko pàcc biy waxtaan ci li mu tànn te Mbind mi dige ko. Ci lu gàtt, waxtaanal ak moom ci benn walla ñaari xise, bu dee nangu na ko.
◼ Walla mën nga wax lii : “ Biibël bi dafay tontu ci laaj yi ëpp solo ci yi doom Aadama di laajte ”. Won ko li nekk ci xët 6, te laaj ko ndax masul a laaj boppam benn ci laaj yi nekk ci suufu xët bi. Boo ko waxee ba pare, ubbil léegi pàcc bi ciy tontu , te waxtaanleen ci benn walla ñaari xise.
◼ Walla mën nga jël téere bi, dem ci xët bi ñu def turu waxtaan yi nekk ci téere bi, te nga won ko waxtaan yi fa nekk, ba pare laaj ko waxtaan bu ko ci gën a itteel. Ubbil pàcc bi mu tànn, te won ko ci lu gàtt ni ñuy defe njàngum Biibël.
3. Naka lañu mënee def ba komaase njàngum Biibël, bu dee yéenekaay bi ñu jox nit ki dafay wax ci a) coono yiy yokku ci àddina si ? b) njaboot gi ? c) lu tax ñu mën a gëm li nekk ci Biibël bi ?
3 Booy njëkk waxtaan ak nit ki, bala ngay dem, laaj ko benn laaj bi ngay indi ay leeral boo fa dellusee : Leneen li ñu mën a def mooy, bi ñu njëkkee waxtaan ak nit ki, nañu ko wax li ñu mën a may ñu waxtaan bu ñu fa dellusee. Bu nit ki nangoo jël yéenekaay yi, laaj ko benn laaj, te wax ko ne dinga ci tontu boo fa dellusee. Fexeel ba jàpp ak moom bés ak waxtu bi nga fa war a dellu te nanga fa dellu ni nga ko ko waxe (Macë 5:37). Boo fa dellusee, nanga ko fàttaliku laaj bi te ci lu gàtt, jàngal ak moom tont bi nekk ci téere Qu’enseigne la Bible te ngeen waxtaan ci. Jox ko benn téere ngir mu mën ci jàng bu ngeen di waxtaan. Bind nañu fii ci suuf li ñu mën a def.
◼ Bu dee yéenekaay bi nga joxe dafay wax ci coono yiy yokku ci àddina si, mën nga wax lii : “ Bu beneenee dinañu waxtaan ci li Biibël bi tontu ci laaj bii : Lan la Yàlla di soppi ci kow suuf ? Boo fa dellusee nanga won nit ki xët 4 ak 5. Mën nga laaj it laaj bii : ndax musiba yi, ci Yàlla lañu jóge ? Boo fa dellusee nanga won nit ki xise 7 ak 8 ci pàcc 1.
◼ Bu dee yéenekaay bi nga joxe dafay wax ci njaboot gi, bala ngeen di tàggoo, mën nga laaj nit ki lii : “ Lan la nit ku nekk ci kër gi mën a def ngir jàmm gën a am ci biir kër gi ? Boo fa dellusee nanga waxtaan ak moom ci xise 4, ci pàcc 14.
◼ Bu dee yéenekaay bi nga joxe dafay wone lu tax ñu war a gëm li nekk ci Biibël bi, mën nga laaj lii ngir waajal seen beneen waxtaan : “ Ndax li Biibël bi wax méngoo na ak li boroom xam-xam yi wax ? ” Boo fa dellusee, waxtaanal ak moom ci xise 8, bi ci pàcc 2.
4. Lan lañu war a def bu dee nit ki ñu taseel nanguwul jël téere Qu’enseigne la Bible ?
4 Saa yu ngeen waxtaanee ba pare, laaj ko benn laaj bi ngeen di tontu boo fa dellusee. Bu njàngum Biibël bi demee ba ngeen faral di ko def, nangeen dellu ci pàcc 1 komaasewaat téere bi. Bu pàcc boobu jeexee, ngeen def bi ci topp, di def noonu ba jeexal téere bi. Bu nit ki bañee jël téere Qu’enseigne la Bible nag ? Mën nga kontine di ko indil suñu yéenekaay yi te di waxtaan ak moom ci lu jëm ci Mbind mi. Booy góor-góorlu noonu ba waxtaan yi gën koo neex, xéyna benn bés mu nangu nga jàngal ko Biibël bi.
5. Lu tax ñu war a góor góorlu ci jéem a jàngale Biibël bi te bañ a yem rekk ci joxe yéenekaay yi ?
5 La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! mën nañu tax nit bëgg xam li Biibël bi di wax dëgg. Kon nag nangeen góor-góorlu ngir komaase ay njàngum Biibël ak ñiy jël suñu yéenekaay yi. Bu ñu defee loolu, dinañu def li ñu Yeesu sant maanaam “ sàkk ay taalibe ..., te ... jàngal leen ”. — Macë 28:19, 20.