TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 9/06 p. 1
  • Leetar bi ñu bànqaas bi yónnee

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Leetar bi ñu bànqaas bi yónnee
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ban liggéey lañuy def ci bànqaas yi ?
    Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
  • Lan mooy Betel ?
    Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
  • Leetaru bànqaas bi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
Sasu Nguuru Yàlla — 2006
km 9/06 p. 1

Leetar bi ñu bànqaas bi yónnee

Yéen ñi ñu sopp, yéen ñi di waare Nguur gi :

Liggéey bi ngeen def ci atum liggéeyu waare bii weesu rafet na lool. Am na lu rafet lu ñu gis ci jamano Fàttaliku bii paase : ñu bare dañu bëggoon a yokk seen liggéeyu waare bi. Ci weeru feewriyee, amoon na 241 waaraatekat ca Mali. Weeru suweŋ 2005 ba tey, masuñu woon a bare noonu. Ca Guinée-Bissao, boo seetee li waaraatekat yépp def ci waaraate bi ci weeru màrs, dafa mel ni, waaraatekat bu nekk dafa waare 19,4 waxtu. Ci Senegaal, dina doon 13,6 waxtu, waaraatekat bu nekk. Ca Gambi am na 4 fànn yoo xam ne waaraatekat yi def nañu lu ñu masul woon a def ci liggéeyu waare bi. Nekkoon nañu 184 waaraatekat, waare nañu 6 083 waxtu, dellu nañu seeti 2 477 nit te def nañu 409 njàngum Biibël.

Ñi teewoon ca ndaje Fàttaliku bi ci réew yu bànqaasu Senegaal di toppatoo yépp, mat nañu 4 884. Loolu wone na ne ñu bare ci ñi ñuy jàngal Biibël bi, ñëw nañu màggal ak ñun deewu Sang bi Yeesu Kirist. Waaye ñu bare ci ñoom soxla nañu gën a xam lan mooy nekk taalibe Kirist. Ndax dinañu mën a def loolu balaa àddina si di tukki ?

Yexowa mu ngi ñuy jox lépp li ñu soxla ngir ñu mën a def bépp “ jëf ju rafet ”. (2 Tim. 3:17.) Ñu ngi ko ciy gërëm bu baax. Ci atum liggéeyu waare bii weesu, pioñee yu bare teewe nañu Lekkoolu pioñee yi ngir ñu seetaat ni ñuy jàngale “ ci Kirist ” (1 Kor. 4:17). Li ëpp 300 njiit ak surga mbooloo yi nekk ci suñu gox yi, jaar nañu it ci Lekkoolu Sasu Nguuru Yàlla bi. Wóor na ñu ne, loolu lépp dina tax liggéey bi jëm kanam bu baax ci atum liggéeyu waare bu bees bi !

Ñu ngi leen di xiir ci kontine di bokk bu baax ci liggéeyu Yexowa, te kontine di ko jiital ci seen dund. Li ñuy ànd ak yéen ci liggéey bii di maye dund gu dul jeex, ci ñun, cér bu réy la !

Seeni mbokk ci ngëm,

Bànqaasu Senegaal

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager