TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 9/08 p. 1
  • Leetaru bànqaas bi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Leetaru bànqaas bi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Leetar bi ñu bànqaas bi yónnee
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • Ban liggéey lañuy def ci bànqaas yi ?
    Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
Sasu Nguuru Yàlla — 2008
km 9/08 p. 1

Leetaru bànqaas bi

Yéen ñi ñu sopp, yéen ñi di waare Nguur gi !

“ Dinaa la màggal, yow Yexowa, ak sama xol gépp. ” (Ps. 9:1.) Loolu sax lañuy yég ci suñu xol ñun itam. Xam nañu ne loolu ngeen yég yéen ñépp ñi nekk waaraatekati Nguuru Yàlla, ndaxte loolu ngeen def ci atum liggéeyu waare bu 2008. Fi mu nekk nii, ñu ngi dajale li ngeen def ci liggéeyu waare bi. Te mbégte bu réy lañu ci jële. Fooguñu woon ne dingeen def lu bare noonu. Ñu bare ci yéen, waaraatekat yi ak pioñee yi, yokk ngeen waxtu yi ngeen def ci liggéeyu waare xibaar bu baax bi.

Ci weer bi ñu def ndaje fàttaliku bi, waaraatekat yi nekk Senegaal def nañu 32 064 waxtu. Maanaam boo seetee li ñu def daaw, ci 100 waxtu yoo jël, yokk nañu ci juróomi waxtu. Ca Gambie waare nañu lu mat 5 937 waxtu. Maanaam boo seetee li ñu def daaw, ci 100 waxtu yoo jël, yokk nañu ci juróom-ñaari waxtu. Wóor na ne loolu bokk na ci li tax 2 815 nit teewe ci ndaje fàttaliku bi ca Senegaal te 571 nit teewe ci ndaje boobu ca Gambie. Loolu masul woon a am.

Ci weeru ndaje fàttaliku bi ca Guinee-Bissao, pioñee yu ci sax yi ak pioñee yiy jàpple matoon nañu 37. Ca Mali, amoon na 54 pioñee. Masuñu woon a bare noonu ci ñaari réew yooyu.

Lépp li ngeen def ngir dimbali nit ñi, tax na ba ñu bare nangu déglu bu ngeen di waare. Ci weeru me, amoon na 2 105 nit ñu doon jàng Biibël bi ca Senegaal. Ca Gambie, 433 nit ñoo doon jàng Biibël bi ci weeru me. Masuñu woon a am njàngum Biibël yu tollu noonu ci ñaari réew yooyu. Lu mat 15 nit sóobu nañu ca Guinée-Bissao ci atum liggéeyu waare bu 2008. Maanaam boo seetee ñi fa sóobu daaw, ci 100 yoo jël, 50 yokku nañu ci. Lu mat 20 nit sóobu nañu ca Mali ci atum liggéeyu waare bu 2008. Maanaam boo seetee ñi fa sóobu daaw, ci 100 yoo jël, 43 yokku nañu ci. Loolu lépp dafa wone ni ngeen bëggee Yexowa ak ni ngeen sawaree dimbali seeni moroom ngir ñu ñëw màggal turu Yàlla bu mag bi.

Xam nañu ne yéen ñépp a jàpp lool. Li ngeen jàpp lool ci liggéeyu suñu baay bi ñu bëgg, yàlla na kontine di leen indil mbégte mu réy ci seen biir xol.

Na leen wóor ne bëgg nañu leen lool yéen ñépp.

Seeni mbokk ci ngëm,

Betel bu Senegaal

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager