Royal jàngalekat bu mag bi booy jëfandikoo téere Qu’enseigne la Bible
1. Naka la Yeesu doon jàngale ?
1 Yeesu, jàngalekat bu mag bi, lépp lu mu doon wax dafa leeroon te yomb jàpp. Bu bëggoon ñi ko doon déglu xalaat bu baax, yenn saay dafa leen doon njëkk laaj seeni xalaat (Macë 17:24-27). Kàddu Yàlla la doon won nit ñi (Macë 26:31 ; Mark 7:6). Dafa leen doon moytu jàngal lu ëpp ci ñoom, ndax xamoon na ne dinañu kontine jàng (Ywna. 16:12). Li soxaloon Yeesu mooy ndax taalibeem yi nànd nañu te gëm li mu leen jàngal (Macë 13:51). Téere Qu’enseigne la Bible dañu ko defar ngir mu dimbali ñu, ñu mën a jàngale ni Yeesu.
2. Naka lañu mëne jariñoo laaj yuy komaase pàcc bu nekk ?
2 Laaj yiy komaase pàcc yi : Bu ñuy komaase benn pàcc, baax na ñu won nit ki laaj yu nekk ci suufu turu pàcc bi. Nañu ko laaj laaj yooyu ngir mu tontu ci xelam, bu ko defee dina gën a sawar a jàng li nekk ci pàcc bi. Walla it mën nañu ko ñaan mu tontu laaj yooyu ci lu gàtt. Jarul ñu waxtaane lu yàgg ci li mu wax, mbaa ñuy jubbanti lépp lu dëng li mu wax. Nañu ko gërëm rekk ci li mu wax te komaase waxtaan bi. Lu mu tontu ci laaj yooyu dina la won ndax am na ci pàcc bi xaaj foo war a gën a yàgg.
3. Naka lañu mëne fexe ba njàng mi yomb ?
3 Aaya yi : Bu ñuy jàng ak nit ki, ci aaya yi lañu war a gën a wax (Yaw. 4:12). Waaye nag, jarul ñu jàng bépp aaya. Nañu gën a wax ci aaya yuy wone fu ñu jële li ñu gëm. Mën nañu bañ a jàng aaya yuy yokk suñu xam-xam kese. Téere Qu’enseigne la Bible dafay wone dëgg gi ci fasoŋ bu yomb. Nañu fexe ba njàng mi bañ a jafe. Nañu jublu ci poñ yi ëpp solo te moytu wax lu yàgg ci li amul solo walla di yokk ay wax yu ko jarul.
4. Lan mooy wone ndax war nañu jël jot ci njàng mi ngir waxtaane ci xaaj bu bokk ci xët 194 ba 223 ?
4 Li nekk ci xët 194 ba 223 : Li nekk ci xët yooyu, mu ngi ëmb 14 poñ yu ñu yokk ci pàcc yi nekk ci téere bi. Yaay seet ndax jar na ngeen waxtaan ci. Ci yenn waxtaan, mën nga wax kiy jàng mu jàngal boppam ci xët 194 ba 223, xaaj biy ànd ak pàcc bi ngeen tollu. Rawatina bu fekkee ne nànd na te nangu na li nekk ci pàcc bi. Nañu jël benn misaal. Bu ñuy jàng pàcc 4, “ Qui est Jésus Christ? ” (maanaam kan mooy Yeesu Kirist ?), bu dee nit ki gëm na ne Yeesu mooy Almasi bi, jarul ñu jàng ak moom xaaj bi tudd “ Jésus Christ, le Messie promis ” (maanaam Yeesu Kirist : Almasi bi ñu dige woon). Yenn saay nag, liy gën mooy ñu jël jot ci njàng mi ngir waxtaane ci xaaj bu ñu def ci diggante xët 194 ba 223 ngir mu ànd ak pàcc bi ngeen di waxtaane, walla ñu am lu ñu ci tànn ngir waxtaane ci.
5. Bu ñu bëggee waxtaan ci li nekk ci diggante xaaj 194 ba 223, naka lañu koy defe ?
5 Boo bëggee waxtaane ci xaaj bu bokk ci xët 194 ba 223, war nga waajal ay laaj ngir waxtaane xaaj boobu ni ngay waxtaane pàcc yi. Walla, ci kow li nit ki soxla, mën nañu jël tuuti minit ci njàng mi ngir seetaat ak moom li nekk ci xaaj boobu. Loolu dina ñu may ñu xam ndax nànd na lu mu jàngal boppam.
6. Naka lañuy jëfandikoo wërale yi ñu def ngir jeexal pàcc yi ?
6 Wërale bi ñu def ngir seetaat li ñu jàng : Wërale yiy jeexal pàcc bu nekk, dañuy tontu laaj yiy komaase pàcc bi. Mën nga ko jëfandikoo ngir seetaat poñ yi ëpp solo ci pàcc bi. Am na njàngalekat yu gis ne jàng kàddu yi nekk ci wërale yooyu ak aaya yi ñuy àndal, dafay dimbali kiy jàng. Dañu koy laaj mu wax, ci lu gàtt, naka la aaya yi di wone ne li ñu bind ci wërale bi mooy dëgg. Loolu dafay won jàngalekat bi ndax kiy jàng nànd na bu baax poñ yi ëpp solo ci njàng mi, naka la Biibël bi wonee poñ yooyu ak it ndax nangu na leen. Loolu dina jàngal kiy jàng ni mu mënee jëfandikoo Biibël bi ngir jàngale dëgg gi.
7. Naka lañu mënee jëfandikoo téere Qu’enseigne la Bible ngir def liggéey bi ñu nu sant ?
7 Li gën ngir def liggéeyu jàngale ak sàkk ay taalibe bi ñu nu sant mooy topp ni Yeesu doon jàngale (Macë 28:19, 20). Téere Qu’enseigne la Bible mën na ñu dimbali ngir def loolu. Nañu ko jëfandikoo bu baax ngir jàngale dëgg gi ci fasoŋ bu leer, yomb te neex ci kiy jàng.