Nañu jariñoo suñu njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi ci téere Qu’enseigne réellement la Bible ?
1 Téere bi tudd Qu’enseigne réellement la Bible ?, bokkoon na ci lu neex lu ñu amoon ci suñu ndaje bu gën a mag bi tuddoon “ Nañu déggal Yàlla ”. Bu ci kanamee tuuti dinañu ko komaase jariñoo bu baax ci waaraate bi. Te ci njàngum Biibël yi lañu koy gën a jariñoo. Kon nag, war nañu xam bu baax li nekk ci téere bu bees boobu. Li ñu ciy dimbali mooy njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi ci téere boobu. Diggante 17 ba 23 awril 2006 lañu ko war a komaase.
2 Kiy jiite njàngum téere bi ci mbooloo mi dina wax ci laaj yiy komaase pàcc bu nekk. Bu ci paree, dina def njàngum téere bi ak laaj yi nekk ci suufu xët yi. Aaya yi ëpp solo lañuy jàng, te waxtaan ci. Pàcc bu nekk dañu ko jeexal ak wërale bu tudd “ Ce que la Bible enseigne ”. Wërale boobu dina baax lool ngir fàttaliku li nekk ci pàcc bi, ndaxte dafay wone li Biibël bi wax ci laaj yi ñu bind ngir komaase pàcc bi. Dingeen mën a bokk bu baax ci waxtaan yi ndaxte li nekk ci téere bi dafa leer, yomb nànd, te neex.
3 Li ñu yokk ci xët 194 ba 223 (Appendix) dafay gën a yaatal yenn waxtaan yi nekk ci téere bi. Booy def benn njàngum Biibël, bu amee li nit ki war a gën a xóotal ci li ngeen jàng, dinga ko mën a jàng ak moom ci xët yooyu. Yenn saay, ci njàngum téere bu ñuy def ci mbooloo mi, dinañu waxtaan ci yenn ci xët yooyu. Dinañu leen njëkk jàng, dog ci waxtaan. Bu fekkee ne lu gudd lañu war a jàng ci xët yooyu, mën nañu ko xaaj, te waxtaan ci xaaj bu nekk. Defuñu fa ay laaj, waaye kiy jiite waxtaan bi mën na laajte ay laaj yuy wone li ëpp solo ci xaaj yooyu.
4 Fasoŋ bi ñuy waxtaane téere Qu’enseigne la Bible ? ci njàngum téere bi, dina xaw a gaaw tuuti. Waaye bu ñu ciy jàngal nit ñi Biibël bi, waruñu gaaw noonu, rawatina bu fekkee ne nit ki tuuti kese la xam ci Biibël bi, walla sax xamu ci dara (Jëf. 26:28, 29). Bu ñuy jàngal nit ñi Biibël bi, dañu war a waxtaan bu baax ci aaya yi, leeral misaal yi te def yeneen yu mel noonu. Kon boo bëggee mën loolu, nanga def lépp loo mën ngir teewe bépp njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi ci téere Qu’enseigne réellement la Bible ?, te nanga ci bokk bu baax.