Buleen fàtte ñi bàyyi waare
1. Lu tax ñu war a góor-góorlu ngir yokk doole ñi bàyyi waare ?
1 Ndax xam nga kenn ku bàyyi waare ? Xéyna bàyyi na di bokk ci li mbooloo mi di def te dafa bayliku maanaam dafa sore mbooloo mi ndànk-ndànk ba mujj réer. Mën na am nga daje ak ku mel noonu bi nga doon waare këroo-kër. War nañu bàyyi xel ne nit kooku, suñu mbokk ci ngëm la ba tey. Dañu ko bëgg won ne dañu ko bëgg ba tey te dimbali ko ngir mu dellusi ci mbooloo mi ak ci “ sàmm, biy aar suñu xol. ” — 1 Pie. 2:25.
2. Naka lañuy yokke doole ñi bàyyi waare ?
2 Nañu wone ne dañu leen bëgg : Bu ñu woowee telefon ku bàyyi waare, woo bu gàtt walla ñu jaar seen kër, loolu mën na ko won ne fàttewuñu ko. Lan lañu ko mën a wax ? Mën nañu yokk doole nit kooku bu ñu ko xamalee ne dañu ko doon xalaat. Nañu fexe ba waxtaan bi neex te yokk dooleem (Fil. 4:8). Mën nañu waxtaane lu neex lu ñu jàng bu yàggul ci benn ndaje. Mën nañu ko woo ci benn ci ndaje yiy ñëw walla ci ndaje bu mag ci at mi te wax ko ne dinañu ko jàppal fu muy toog walla ñu topptool ko lu koy yóbbu.
3. Naka la suñu benn mbokk mu jigéen demee ba komaasewaat waare ?
3 Suñu mbokk mu jigéen bu bàyyi woon a waare lu ëpp 20 at lañu fekkoon ci benn goxu mbooloo. Nanguwul ñu defal ko njàngum Biibël, waaye suñu mbokk mu jigéen bi ko gisoon, dafa ñówaat seetsi ko, indil ko yéenekaay yu bees yi. Bi ndaje bu gën a mag bi ci at mi weesee, suñu mbokk mu jigéen mi ñëw wax ko yenn poñ yu mu fa jàng. Mujj gi dem na ba komaasewaat waare.
4. Naka lañuy war a mel ak ku komaasewaat teewe ndaje yi ngir bokkaat ci mbooloo mi ?
4 Bu kenn di dellusi : Bu suñu mbokk mu bàyyi waare komaasee di dellusi ci ndaje yi, naka lañu waree mel ak moom ? Naka la Yeesu meloon ak taalibeem yi ginnaaw bi ñu ko bàyyee diir bu gàtt ? Dafa leen woowe “ mbokk ” te wone kóolute ci ñoom. Dénk na leen sax liggéey bu am solo (Macë 28:10, 18, 19). Tuuti ginnaaw loolu, ‘ daawuñu woon a noppe ’ waare xibaar bu baax bi, maanaam dañu kontine di waare. — Jëf. 5:42.
5. Waxal lu war a tax ñu waxtaan ak njiit yi ci kenn ku bàyyi waare.
5 Bala ñuy wax ku bàyyi waare ne mën nañu jàng ak moom Biibël bi, walla bala ñuy wax ku bàyyi waaraate lu yàgg ne mën na ànd ak ñun ci waaraate bi, dañu ci war a njëkk waxtaan ak njiiti mbooloo mi. Bu ñu dajee nag ci gox bi ak waaraatekat bu bàyyi waare, war nañu ko wax njiiti mbooloo mi ngir ñu wax ko ne mën nañu ko dimbali ni mu ko soxlaa.
6. Bu ñu dimbalee ñi bàyyi waare, ban mbégte lañu ci mën a am ?
6 Ni ko Biibël bi leeralee, ñiy daw ba àgg kese ñooy mucc (Macë 24:13). Moo tax ñu war a seetlu ñi fakkastalu ak ñi bayliku. Ñooñu bu ñu leen wonee ne dañu leen fonk, di leen won noonu ne dañu leen bëgg ni Yexowa, te bañ ci tàyyi, mën na am ñu am mbégte gis leen ñu komaasewaat jaamu Yexowa ci suñu wet. — Lukk 15:4-10.