Naka lañu mënee dimbali ñi teewe ndaje fàttaliku bi ?
1. Ban waare bu am doole lañuy def bésu 22 màrs 2008 ?
1 Bésu 22 màrs 2008, ay milyoŋi nit dinañu dégg waare bu am doole. Bés boobu, ñiy teewe ndaje fàttaliku bi dinañu dégg lu jëm ci mbëggeel bu réy bi Yexowa won doomu Aadama yi, bi mu joxe njot gi (Ywna. 3:16). Dinañu jàng lu jëm ci Nguuru Yàlla ak ni ko Yexowa di jëfandikoo ngir def coobareem ci suuf si sépp (Macë 6:9, 10). Dinañu gisal seen bopp mbëggeel bi am diggante ñiy jaamu Yàlla akit teraanga bi ñuy wone. — Sab. 133:1.
2. Naka lañu mënee dimbali njàngum Biibël yi teewe ndaje fàttaliku bi ?
2 Ñiy jàng Biibël bi : Ci ñiy teewe ndaje boobu, dina am ñu sog a komaase jàng Biibël bi ak ñun. Nañu leen won suñu mbokk yi ci wàllu ngëm. Nañu leen wax ni ñuy defe ndaje yiy am ayu-bés bu nekk, won leen it ci lu gaaw ni Saalu Nguur gi mel. Kiy def waxtaan bi dina xiirtal nit ñooñu ñu kontine di jëm kanam ci wàllu ngëm. Mën nga jaar ci li mu wax ngir xiirtal ñiy jàng Biibël bi ak yow.
3. Lan lañu mën a def ngir xiirtal ñi teewe ndaje fàttaliku bi fekk dañu bàyyi waaraate ?
3 Ñi bàyyi waaraate : Ci ñiy teewe ndaje bi, dina am waaraatekat yu bàyyi waaraate. Nañu dem ba ci ñoom ngir nuyu leen bu baax. Nañu leen moytu laaj ay laaj ci li suñu yoon nekkul walla wax leen lu leen mën a rusloo. Bu ndaje fàttaliku bi weesoo tuuti, njiiti mbooloo mi war nañu seeti ñi teewe ndaje bi fekk dañu bàyyi waaraate. Dinañu leen wax ne ni ñu góor-góorloo ngir teewe ndaje bi, lu rafet la. Dinañu leen xiirtal bu baax it ci teewe ndaje mbooloo biy topp.
4. Naka la kenn ku nekk ci ñun mënee dimbali gan yiy teewe ndaje bi ?
4 Yeneen gan yi teew : Nit ñu nu xam walla suñu ay mbokk mën nañu bokk ci ñi teewe fekk ñun ci suñu bopp ñoo leen woo ci ndaje bi. Dina am ñeneen ñi nga xam ne dafa am ñu leen jox kayit yi ñu doon joxe ngir woo nit ñi ci ndaje bi. Boo gisee nit ñoo xamul, demal nuyu leen te teral leen bu baax. Xéyna masuñu ñëw ci suñu ndaje yi. Booy waxtaan ak ñoom xéyna dinga mën a xam ni nga mënee def ba seeti leen. Tuuti fan ginnaaw bi ndaje bi paasee, mën nga leen seeti walla nga telefone leen ngir jéem a waxtaan ak ñoom te laaj leen ndax bëgg nañu nga jàng Biibël bi ak ñoom.
5. Lan lañu mën a wax ngir komaase njàngum Biibël ?
5 Bu ñu delloo seeti nit ñi, mën nañu jaar ci li ñu dég ci waxtaanu ndaje fàttaliku bi, ngir komaase njàngum Biibël ci téere Qu’enseigne la Bible ? Kiy def waxtaanu ndaje fàttaliku bi dina jàng Esa. (Isa.) 65:21-23. Boo delloo seeti nit ki, mën nga wax lu jëm ci waxtaan boobu, nee ko : “ Am na yeneen barke yoo xam ne, njot gi mooy tax ñu mën leen a am. Négal ma won la ko. ” Ba pare nga seet ak moom li nekk ci xët 4 ak 5 ci téere Qu’enseigne la Bible ? Walla mën nga wax lii itam : “ Li yonent Yàlla Esayi wax, ñu bare dañu bëgg xam kañ lay am. ” Ba pare seetal ak moom li nekk ci xise 1 ba 3, ci pàcc 9. Leneen li nga mën a def it, mooy jaaraat rekk ci lenn lu ñu waxoon ci waxtaanu ndaje fàttaliku bi, ba pare nga won ko téere Qu’enseigne la Bible ?, te won ko ni ñuy defe njàngum Biibël.
6. Bu ñuy fàttaliku deewu Yeesu ni mu ñu ko sante, lan lañu mën a def ?
6 Na kenn ku nekk ci ñun seet li koy may mu mën a dimbali ñiy jàng Biibël bi, ñi bàyyi waaraate bi, ak yeneen gan yiy teewe ci ndaje fàttaliku bi (Luug 22:19). Wóor na ne Yexowa dina barkeel lépp li ñuy def ngir yokk li ñuy def ci liggéeyu Nguur gi.