“ Lan ngay tontu ? ”
1. Yan jafe-jafe la ñu bare am ?
1 Xéyna danga bëgg Kàddu Yàlla waaye poroblem bi nga am mooy boo jàngee li Biibël bi nettali, am na yu bare yoo ci mënul a jàpp. Yenn saay it dinga xam li Biibël bi wax waaye dangay fàtte ci ban aaya la nekk. Ndax bëgg nga say doom nànd bu baax li Biibël bi di nettali ak di jàngale ? Weer wu nekk, waxtaan bi tudd : “ Que répondriez-vous ? ” (maanaam “ lan ngay tontu ? ”) dafay feeñ ci Réveillez-vous !, ci xët 31. Waxtaan boobu mën na dimbali mag ak ndaw, ñu gën a xam Kàddu Yàlla. — Jëf. 17:11.
2. Naka lañu mënee jëfandikoo xaaj yi nekk ci waxtaan bi tudd “ Que répondriez-vous ? ” (maanaam “ lan ngay tontu ? ”) ?
2 Naka lañu mënee jëfandikoo waxtaan boobu ni mu gënee ? Réveillez-vous ! bu weeru sãwiyee nee woon na ñu xool li nekk ci xët 31. Am na xaaj yuy neex ndaw yi. Yi ci des dinañu baax ci ñi gën a sore ci njàngum Biibël. Réveillez-vous ! boobu nee woon na it ne xaaj bi tudd “ Situez dans le temps ” (maanaam “ kañ la woon ? ”) dina ñu dimbali ngir ñu xam kañ la nit ñi ñu wax ci Biibël bi doon dund ak it kañ la xew-xew yi ëpp solo am. Tont laaj yi nekk ci xaaj bi tudd “ Dans ce numéro ” (maanaam “ ci yéenekaay bii ”) ci waxtaan yi nekk ci yéenekaay bi lañu koy wut. Waaye li ëpp ci yeneen laaj yi, seeni tont ñoo bokk fi ñu leen def ci yéenekaay bi te dinañu la wax ci ban xët lañu nekk. Boo ubbee xët boobu, dinga gis ne dañu walbati mbindi tont yi. Réveillez-vous ! mu ngi ñu doon xiir it ci njëkk gëstu ci Biibël bi walla ci suñu téere yi ngir wut tont laaj yi, te waxtaane ko ak ñeneen, bala ñuy jàng tont yooyu. Nee woon na it ne mën nañu jëfandikoo sax pàcc bi tudd “ Que répondriez-vous ? ” (maanaam “ lan ngay tontu ? ”) ngir waxtaane ko ak suñu njaboot walla ak mbooloo mi bu ñuy waxtaan ak ñoom ci lu jëm ci Biibël bi.
3. Naka la yenn njaboot di jariñoo xaaju Réveillez-vous ! boobu te yan xaaj ñoo la ci gën a neex ?
3 Ay njaboot yu bare dañu jëfandikoo waxtaan boobu ci njàngum Biibël bi ñuy def ci seen njaboot. Te dañu ci kontaan. Benn yaay nee na : “ Man ak sama jëkkër dañu waxoon ne dinañu boole xaaj bi tudd ‘ Aux enfants de chercher ’ (maanaam “ xale yi ñoo war a seet tont laaj yii ”) ci njàngum Biibël bi ñuy def ci suñu njaboot ngir mu xumb te neex ci suñu doom bu jigéen bi am ñetti at. Bi ñu ko gisee muy wut tont laaj yi ci yéenekaayam dañu kontaan. Dafa doon ubbi xët bu nekk, di seet bu baax ba gis li mu doon wut. ” Benn baay bu nekk ca reew bi tudd Bresil nee na : “ Xaaju Réveillez-vous ! boobu, man ak sama doom bu góor bu juróom-ñaari at, dañu ko bëgg lool. Tax na ba Moise gën a am seetlu ci li muy jàng. Dafa ci jàng a wut aaya yi, xam li nataal yi tekki, te nànd kañ la mbir yi amee. ” Ashley, xale bu am juróom ñetti at, lii la bind : “ Maa ngi leen di gërëm ci waxtaan bi ñu tudde “ Que répondriez-vous ? ” (maanaam “ lan ngay tontu ? ”) bi nekk ci xët bi mujj ci Réveillez-vous ! yi. Jàng naa ci lu bare lu jëm ci Biibël bi. ”
4. Naka la njaboot yi mënee boole xaaju Réveillez-vous ! boobu ci seen njàngum Biibël ?
4 Ndax mënuleen a boole léeg-léeg, xaaj bi tudd “ Que répondriez-vous ? ” (maanaam “ lan ngay tontu ? ”) ci njàngum Biibël bi ngeen di def ci seen njaboot ? Mën ngeen jëfandikoo téere bi tudd Index walla Watchtower Library ci CD-ROM ngir wut tont laaj yu ci gën a jafe. Bu ñu defee loolu, dinañu jàngal suñuy doom ni ñuy gëstoo ci téere yi. Boo amee doom yu mag, ndax mënoo leen a laaj ñu wutal seen bopp tont laaj yi nekk ci waxtaan bi tudd “ Qui suis-je ? ” (maanaam “ man maay kan ”) walla bi tudd “ Situez dans le temps ” (maanaam “ kañ la woon ? ”), bala njàngum Biibël bi ngeen di def ci seen njaboot di jot. Bu ko defee, bu ngeen di def njàngum Biibël bi ci seen njaboot, seeni doom dinañu mën a wax ci li ñu doon gëstu. Waa jur yi nangeen jariñoo bu baax xaaj boobu nekk ci Réveillez-vous ! yi, di dimbali seeni doom ñu xam Kàddu Yàlla li dale ci seen ngune. Loolu bokk na ci li mën a tax ngeen dugal Kàddu Yàlla ci seen xol. — 2 Tim. 3:15 ; 5 Mu. (Deut.) 6:7.