1) Benn laaj, 2) benn aaya, ak 3) benn pàcc
Lu yomb lu ñu mën a def ngir wone téere Qu’enseigne réellement la Bible ? mooy ñett yii : 1) Laaj nit ki benn laaj ngir mu wax li mu xalaat, 2) jàng benn aaya buy ànd ak xalaatam, te 3) won ko ci téere bi pàcc buy wax ci li ngeen di waxtaan. Nanga jàng foofu laaj yiy tàmbali pàcc bi. Boo gisee ne waxtaan bi neex na nit ki, mën nga jàng ak moom xise yu njëkk yi, ngir won ko ni ñuy jàngalee Biibël bi. Li ñu wax fii ci kow, mën nga ko def booy njëkk a waxtaan ak nit, walla boo fay jaaraat.
◼ “ Ndax foog nga ne nit mën na def li ñu wax fii ci Biibël bi, maanaam xam ki ñu Sàkk, moom mii nekk aji kàttan ji ? ” Jàngal Jëf ya 17:26, 27. Mayal nit ki mu tontu te won ko li nekk ci pàcc 1.
◼ “ Tey, coono yi bare nañu lool. Ndax foog nga ne am na lu mën a dalal suñu xel te may ñu yaakaar ni ñu ko waxee fii ? ” Jàngal Room 15:4. Mayal nit ki mu tontu te won ko li nekk ci pàcc 2.
◼ “ Soo ko mënoon, ndax dinga def li ñu wax fii ? ” Jàngal Peeñu ma 21:4. Mayal nit ki mu tontu te won ko li nekk ci pàcc 3.
◼ “ Ndax foog nga ne suñu doom yi dinañu mas a am dund gu mel ni lii ? ” Jàngal Sabóor 37:10, 11. Mayal nit ki mu tontu te won ko li nekk ci pàcc 3.
◼ “ Ndax foog nga ne bés, lii dina mas a am ? ” Jàngal Esayi 33:24. Mayal nit ki mu tontu, te wax ko li nekk ci pàcc 3 bi.
◼ “ Ndax mas nga laaj sa bopp lii : ñi dee ndax xam nañu li ñiy dund di def ? ” Mayal nit ki mu tontu. Jàngal Dajalekat (Ecclésiaste) 9:5 te won ko li nekk ci pàcc 6.
◼ “ Ndax dinañu mën a gisaat suñu mbokk yi gaañu ni ko Yeesu waxe ci aaya bii ? ” Jàngal Yowaana 5:28, 29. Mayal nit ki tontu te won ko li nekk ci pàcc 7.
◼ “ Lan moo mën a tax coobare Yàlla am ci kow suuf ni mu ame ca asamaan, ni ko ñaan bii waxe ? ” Jàngal Macë 6:9, 10. Mayal nit ki tontu te won ko li nekk ci pàcc 8.
◼ “ Ndax foog nga ne tollu nañu ci jamano bi ñu doon yégle fii ? ” Jàngal 2 Timote 3:1-4. Mayal nit ki tontu te won ko li nekk ci pàcc 9.
◼ “ Ñu bare dañu bëgg xam lu tax coono doom-Aadama di gën a yokku rekk. Seetal li aaya bii wax ci lu tax loolu am. Ndax mas nga ci xalaat ? ” Jàngal Peeñu ma 12:9. Mayal nit ki tontu te won ko li nekk ci pàcc 10.
◼ “ Ndax mas nga laaj sa bopp laaj yii ? ” Jàngal Ayóoba 21:7. Mayal nit ki tontu te won ko li nekk ci pàcc 11.
◼ “ Ndax foog nga ne bu ñu toppee li Biibël bi wax fii, jàmm dina gën am ci suñu kër ? ” Jàngal Efes 5:33. Mayal nit ki tontu te won ko li nekk ci pàcc 14.
[Nataal bi nekk paas 6]
Boo waxtaanee ak nit ñaari yoon ginnaaw bi nga ko wonee ni ñuy defe njàngum Biibël te nga yaakaar ne nit ki dina kontine di jàng Biibël bi, bu boobaa mën nga komaase bind ne yaa ngi def benn njàngum Biibël.