TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 8/08 p. 4
  • Ndax yaa ngi jëfandikoo lépp li ci nekk ?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ndax yaa ngi jëfandikoo lépp li ci nekk ?
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ay soppi yu am solo ci La Tour de Garde !
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • “ Lan ngay tontu ? ”
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Li ñu mën a def ba komaase njàngum Biibël ak ñiy jël suñuy yéenekaay
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
Sasu Nguuru Yàlla — 2008
km 8/08 p. 4

Ndax yaa ngi jëfandikoo lépp li ci nekk ?

1 “ Yàkkamti naa ko jëfandikoo ci waaraate bi ! ” Loolu la suñu benn mbokk bu jigéen wax bi mu jàngee La Tour de Garde bu 1 sãwiyee 2008. Ndax xool nga yenn waxtaan yi faral di nekk ci La Tour de Garde Edition publique (maanaam bi ñuy wone ci waaraate bi) ? Ndax gis nga li nga mën a def ngir mën ko jëfandikoo bu baax ci waaraate bi ?

2 “ Ce que nous apprenons de Jésus ” maanaam li ñuy jàng ci Yeesu : Xéyna gis nga ne xaaj boobu baax na lool ngir komaase njàngum Biibël. Soo ko defagul, mën nga jàngal nit turu waxtaan bi, ba pare won ko ci xise bu njëkk bi li ci Yeesu wax. Su waxtaan bi neexee nit ki, jéemal a kontine waxtaan bi ci laaj yiy komaase xaaj bu nekk. Laaj yooyu dinañu tax ba nit ki xalaat bu baax. Waxal nit ki mu wax li mu xalaat ci laaj bi. Ci lu gàtt waxtaanal ak moom ci nataal bi ànd ak laaj bi, ba pare sog a jàll ci xise bi ci topp. Mën ngeen a def genn-wàllu xise yi ci seen waxtaan bu njëkk bi. Boo fa dellusee, ngeen àggali xise yi des. Nanga pare ngir kontine waxtaan bi ci téere Qu’enseigne la Bible ?

3 “ Clés du bonheur familial ” maanaam liy tax njaboot di am jàmm : Xaaj boobu, ñetti weer ba ñetti weer lay feeñ ci La Tour de Garde. Dañu ko def ngir mu won jëkkër yi, jabar yi ak wayjur yi, naka lañu mënee topp li nekk ci Biibël bi, bu njaboot bi amee poroblem yu leen mën a xañ jàmm. Mën nga jëfandikoo xaaj boobu it ngir won ñi nekkul seede Yexowa xam-xam bi nekk ci Biibël bi. — 2 Tim. 3:16, 17.

4 Xaaj bi ñu defar ngir xale yi : Xaaj bi tudd “ Pour nos jeunes lecteurs ” maanaam li ñu defar ngir suñu ndaw yi, dañu ko bind ci fasoŋ buy tax nit ki xalaat bu baax ci benn nettali bu nekk ci Biibël bi. Mën nga ko jëfandikoo ngir won ndaw yi ngay taseel ci waaraate bi ni jàng Kàddu Yàlla amee njàriñ (Sab. 119:9, 105). Booy waxtaan ak wayjur yi, mën nga leen a won xaaj bi tudd “ Enseignez vos enfants ” maanaam jàngalleen seeni doom. Xaaj boobu dafay feeñ weer bu nekk ci La Tour de Garde. Waxtaan yooyu, dinañu tax xale yu ndaw yi jàng lu am solo ci ñi doon dund ci jamano Biibël bi. Ndax fas nga yéene jàng waxtaan yooyu ak say doom ?

5 “ Leneen li nekk ci La Tour de Garde : Weer bu nekk, dina am waxtaan bu tudd “ Questions des lecteurs ” maanaam laaju ñiy jàng suñu téere yi. Waxtaan boobu, dafay tontu laaju ñi nekkul seede Yexowa. Mën nga waxtaan ci xaaj boobu booy wone suñuy yéenekaay këroo-kër. Am na it xaaj bu tudd “ Une lettre d’... ” (maanaam leetar bu jóge ...). Ci xaaj boobu, benn nit mooy bind li mu fekke. Dafa ciy nettali jafe-jafe yi missionnaires yi ak ñeneen am ci waaraate bi. Waxtaan yooyu dinañu tax ñi nekkul seede Yexowa, gis ne ñu ngi yégle xibaar bu baax bi ci suuf si sépp. Te loolu bokk na ci liy wone ne Yeesu teew na. — Macë 24:3, 14.

6 Weer bu nekk dina am xaaj bu tudd “ Approchez-vous de Dieu ” maanaam jegeleen Yàlla. Xaaj boobu dafay topp aaya yi ñu war a jàng ayu-bés bu nekk ci lekkoolu Sasu Nguuru Yàlla. Mën na tax boroom xol yu rafet yi bëgg yokk seen xam-xam ci Yexowa. Xaaj bi tudd “ Imitez leur foi ”, maanaam royleen ci seen ngëm, ñeenti yoon kese lay feeñ ci at mi. Xaaj boobu, dañu ko def ngir mu dimbali nit ñi ñu gis ci seen xel li ñu nettali ci Biibël bi, mel ni ñu fa nekkoon. Dafay tax ba nit ñi nekk ci Biibël bi, gën a nekk dëgg ci kuy jàng Biibël bi tey. Dinañu gën a nànd li nit ñooñu tànn, seeni jafe-jafe ak seen ngëm.

7 Kontaan nañu lool ci li ñuy jot weer bu nekk La Tour de Garde boo xam ne, li ci nekk yépp dañu ko defar ngir waaraate bi. Nañu fexe ba xam bu baax li ci nekk te jariñoo xaaj yépp ci waaraate bi.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager