Ay Tont Ci Seeni Laaj
◼ Ci suñuy ndaje, maanaam lekkoolu sasu Nguuru Yàlla, ndaje liggéeyu waare bi, ndaje bi ñu jagleel ñépp walla njàngum La Tour de Garde bi, naka lañuy xamal ñi teew woy bi ñu war a woy ngir komaase ndaje yooyu te kan moo ko war a def ?
Woy bi ñu war a woy ngir ubbi lekkoolu sasu Nguuru Yàlla ayu-bés bu nekk, mu ngi ci porogaraamu lekkoolu sasu Nguuru Yàlla bi ñu def ci Sasu Nguuru Yàlla bu oktoobar, xët 3 ba 6. Woy yi ñuy woy ngir komaase ak it jeexal ndaje liggéeyu waare bi, ñu ngi ci xët 2 ci Sasu Nguuru Yàlla bi. Te woy yi ñu war a woy ayu bés bu nekk ci njàngum La Tour de Garde bi, dañu leen bind ci xët 2 ci téere La Tour de Garde bu nekk. Woy bi ñu war a woy ci ndaje bu nekk, ci ndaje boobu la bokk. Kon kiy jiite ndaje bi moo war a xamal nit ñi woy bi ñu war a woy. Kiy jiite ndaje bi sog a jeex, warul wax woy bi ñuy ubbee ndaje bi ci topp.
Kon kiy def lekkoolu sasu Nguuru Yàlla bi, dina teral ñi teew, wax ban woy-Yàlla lañu war a woy, ba pare def lekkool bi. Bu ci paree dina woo ki war a def waxtaan bi njëkk ci ndaje liggéeyu waare bi. Kooku nag moo war a wax woy bi ñuy war a woy ngir ubbi ndaje boobu.
Noonu it, kiy jiite ndaje bi ñu jagleel ñépp mooy ubbi ndaje boobu. Dina teral bu baax ñi teew, wax leen ñu woyandoo woy-Yàlla bi ñu war a woy. Woy boobu, kiy def waxtaan bi moo koy tànn. Kiy jiite ndaje bi ñu jagleel ñépp, (walla keneen ku ko mën te ñu yégal ko ko bala ndaje bi komaase), dina tàmbali ndaje bi ak ñaan. Dina woo kiy def waxtaan bi, te wax nit ñi turu waxtaan bi. Bu waxtaan bi jeexee, kiy jiite ndaje bi warul a jéem a tënk li ñu waxoon ci waxtaan bi. Ci lu gàtt, dafa war a gërëm ki def waxtaan bi ci lu mu jàngale. Dina xamal nit ñi turu waxtaan bi ñu war a def ayu-bés bi ci topp, ba pare ñaan ñi teew ñu toog ngir fekke njàngum La Tour de Garde bi. Jarul muy laaj mbooloo mi ndax bëgg nañu ki defoon waxtaan bi nuyul ñu mbooloom. Léegi nag kiy jiite ndaje bi ñu jagleel ñépp dina woo ki war a jiite njàngum La Tour de Garde bi, mu ñëw jiite ndaje boobu.
Kiy jiite La Tour de Garde bi dina wax woy bi ñu war a woy ngir komaase ndaje bi. Dina jiite njàng mi ci fasoŋ bu ànd ak tegtal yi ci mbooloo mi jot. Bu ci paree, dina wax woy bi ñuy mujj a woy. Ci lu ëpp, kiy jiite La Tour de Garde bi dina woo ki doon def waxtaan bi mu def ñaan bu mujj bi.
Bu ñu toppee tegtal yi ñu wax fii, dina tax mbooloo yi yépp bokk ni ñuy defe ndaje yi.