Porogaraam bu bees pur ndaje yi ñuy def ci mbooloo mi
1, 2. Dale ko ci weeru sãwiyee 2009, lan lañuy soppi ci ndaje yi ?
1 Ci ayu-bés bu 21 ba 27 awril 2008, mbooloo yi nekk ci àddina si sépp jotoon nañu yégle bu neex. “ Dale ko 1 sãwiyee 2009, dinañu def ci benn bés njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi, lekkoolu sasu Nguuru Yàlla bi ak ndaje liggéeyu waare bi. Njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi dinañu ko woowe léegi njàngum Biibël bi ci mbooloo mi. ”
2 Ni ñuy doxale ndaje yooyu : Ndaje bi yépp, boole ci woy-Yàlla yi ak ñaan yi, dina def 1 waxtu ak 45 minit. Dinañu komaase ndaje bi ak woy-Yàlla ak it ñaan (ci 5 minit). Njàngum Biibël bi ci mbooloo mi moo ciy tegu (ci 25 minit). Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla bi topp ci (ci 30 minit). Bu ñu defee loolu ba pare, dinañu woy benn woy-Yàlla (ci 5 minit) ngir komaase ndaje liggéeyu waare biy def 35 minit. Dinañu def woy-Yàlla ak ñaan ci 5 minit ngir jeexal ndaje bi. Ngir ngeen mën a waajal ndaje boobu, weer bu nekk, dinañu def ci Sasu Nguuru Yàlla bi porogaraamu njàngum Biibël bi ci mbooloo mi, porogaraamu lekkoolu sasu Nguuru Yàlla bi ak porogaraamu ndaje liggéeyu waare bi.
3. Naka lañuy defe njàngum Biibël bi ci mbooloo mi ?
3 Njàngum Biibël bi ci mbooloo mi : Ndaje boobu, dinañu ko def ni ñuy defe njàngum La Tour de Garde bi. Soxlawul ñu jaaraat ci li ñu jàngoon ci ayu-bés bi weesu ngir komaase. Kiy jiite ndaje bi na wax rekk lu gàtt ngir tàmbali ndaje bi. Loolu dina tax ñu am jot bu doy ngir ñi teew ñépp mën a tontu ci lu gàtt. Ayu-bés bu nekk, njiiti mbooloo mi dinañu awlante ngir jiite ndaje boobu. Wottukat biy jiite ci mbooloo mi mooy toppatoo ni njiit yooyu di awlante.
4. Lan mooy soppeeku ci ndaje liggéeyu waare bi ?
4 Ndaje liggéeyu waare bi : Ni ñu daan defe ndaje boobu rekk lañu koy defe, waaye dafay gën a gàtt léegi. Dinañu faral di def yégle yi ci juróomi minit. Loolu war na mën a doy ngir jàng yégle yi gën a am solo ak yenn leetar yi ñu betel bi yónnee. Jaratul ñuy jàng ci kanamu ñépp yégle yu mel nii : fi ñuy waare ci ayu-bés bi, ñi war a raxas saalu Nguur gi, fi xaalisu mbooloo mi tollu ak leetar yi betel bi faral di yónnee. Léegi, yégle yooyu dinañu leen taf ci tablo bi ñuy tafe yégle yi ngir waa mbooloo mi mën ko jàng. Ñi war a def waxtaan ci ndaje bi, war nañu ko waajal bu baax, topp bu baax li ñu leen sant te bañ a weesu minit yi ñu leen may.
5. Ayu-bés bi wottukat biy wër di ñëw ci suñu mbooloo, naka lañuy defe ndaje yi ?
5 Bu wottukat biy wër ñëwee ci mbooloo mi : Soppiwuñu dara ci ni ñuy defe ndaje yi, bu wottukat bi di ñëw ci mbooloo mi. Ci talaata, bu ñu defee lekkoolu sasu Nguuru Yàlla bi ba pare, dañuy njëkk def ndaje liggéeyu waare bi sog a woy benn woy-Yàlla. Ginnaaw loolu, wottukat bi dina def waxtaan bu 30 minit. Dinañu tànn beneen bés ngir def njàngum Biibël bi ci mbooloo mi, ni ñu ko doon defe bu wottukat bi nekkee ci suñu mbooloo. Su ñu ko defee ba pare, dinañu woy benn woy-Yàlla, wottukat bi sog a def waxtaan biy jëm ci liggéeyu waare bi. Ginnaaw waxtaan boobu, dinañu woy benn woy-Yàlla, te ñaan ngir jeexal ndaje bi.
6. Lan mooy liggéeyu wottukatu gurup bi ?
6 Ndaje yi ñuy def bala ñuy waare : Kurélu njiiti mbooloo mi dina tànn wottukati gurup yi ngir ñu toppatoo gurub yiy liggéey ci waaraate bi te toppatoo it ñi bokk ci gurub yooyu. Bu benn surga mbooloo mi waree toppatoo benn gurub, dinañu ko woowe “ surga gurub bi ”.
7. Lan lañu nar a jële ci porogaraam bu bees bi ñu def ngir ndaje yi ?
7 Ni ñu ko wone fii, dinañu jàng ci ndaje yooyu luy yokk suñu xam-xam ak suñu doole ngir suñu diggante ak Yexowa mën a rattax. Loolu dina tax ñu doon waaraatekat ak jàngalekat yu aay te xam bu baax ni ñuy defe liggéey bu gën a rafet ci waaraate bi. — Efes 4:13, 14 ; 2 Tim. 3:17.
8. Waajal ndaje yi, naka la ñuy jariñe ñun ci suñu bopp ak it suñuy moroom ?
8 Bu ñuy waajal ndaje boobu, dinañu xam bu baax ponk yi gën a am solo yi ñuy jàng ci ndaje bu nekk. Ñun ñépp dinañu mën a bokk ci waxtaan bi ngir ñu dimbaleente ci suñu ngëm (Room 1:11, 12 ; Yaw. 10:24). Li ñu war a bëgg mooy suñu “ jëm kanam bir ñépp ” ci li ñuy “ faramfàcce bu jub kàddug dëgg gi. ” — 1 Tim. 4:15 ; 2 Tim. 2:15.
9. Lan lañu fas yéene def ? Te lu tax ?
9 Kontaan nañu lool ci soppi yu am solo yooyu ñu def ci ndaje yi. Nañu topp bu baax tegtalu “ surga bu takku te teey ” bi. Te it nañu jege bu baax suñu Sàmmkat bu mag bi, bi mu ñuy waajal ngir “ metit ” wu réy wi jege lool. — Macë 24:21, 45 ; Yaw. 13:20, 21 ; Peeñ. 7:14.