TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 7/07 p. 1
  • Ay soppi yu am solo ci La Tour de Garde !

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ay soppi yu am solo ci La Tour de Garde !
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ndax yaa ngi jëfandikoo lépp li ci nekk ?
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Nañu wone yéenekaay yiy “ wax dëgg gi ”
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
Sasu Nguuru Yàlla — 2007
km 7/07 p. 1

Ay soppi yu am solo ci La Tour de Garde !

1 Mbooloo yi jotoon nañu yégle bu am maanaa bi at bii komaasee : Ci sãwiyee 2008 dinañu tàmbali di defar ñaari fasoŋu La Tour de Garde. Benn bi dinañu ko jagleel ñépp. Beneen bi ñu jagleel ko ñi bokk ci suñu mbooloo. Mën na am ngeen di wax ci seen xel : ‘ Ci lan la ñaari téere yi di wuute ? Ban njariñ moo nekk ci ñaari fasoŋu La Tour de Garde yooyu ? Ndax dina am ay xaaj yu bees ci téere yooyu ? ’

2 Ci lan lañuy wuute : Téere biy génn ci fan bu njëkk ci wér bu nekk, dinañu ko woowe Edition publique (maanaam bi ñuy wone ci waaraate bi). Waxtaan yi fa nekk yépp, dañu leen defar ngir ñi bokkul ci suñu mbooloo. Téere La Tour de Garde buy génn ci bésu 15 ci wér bu nekk, dinañu ko woowe Edition d’étude (maanaam bi ñuy jang ci mbooloo mi). Boobu duñu ko joxe ci waaraate bi. Dinañu ci def waxtaan yi mbooloo mi war a jàng ci lu mat benn wér. Dina am it yeneen waxtaan yu nar a soxal bu baax karceen yi jébbal seen bopp Yexowa. Li nekk ci téere bi ñuy woowe Edition publique bu La Tour de Garde, du Seede Yexowa yi kese lay nar a neex. Dina neex it ñi nekkul Seede Yexowa te nangu li Biibël bi wax. Réveillez-vous ! moom, dinañu kontine di ko jagleel nit ñu bare. Dinañu ci boole ñi am xel ñaar ci li Seede Yexowa yi gëm ak ñi bokk ci diine bu dul karceen.

3 Njariñ bi ci nekk : Ci La Tour de Garde bi ñuy woowe Edition d’étude, dootuñu soxlati leeral kàddu yu mel ni “ pioñee ” ngir ñi nekkul Seede Yexowa mën a xam li muy tekki. Dinañu ci def it loo xam ne dañu koy jagleel Seede Yexowa yi ak ñiy sore ci jàng Biibël bi. Lan mooy nekk ci Edition publique bi ? Waxtaan yi nekk ci téere boobu ak fasoŋ bi ñu leen di defe ñooy neex ñi nekkul Seedee Yexowa. Moo tax jàng lépp li nekk ci téere bi dina neex ci ku nekkul Seede Yexowa. Waaye jàng ñaari fasoŋu La Tour de Garde yi, dina amal njariñ itam képp kuy Seede Yexowa. Komka léegi, weer wu nekk, benn La Tour de Garde ak benn Réveillez-vous ! kese lañuy wone ci waaraate bi, dinañu am weer ngir mokkal bu baax li ñuy wax ngir wone yéenekaay yi.

4 Lu bees li ciy nekk : Edition publique bu La Tour de Garde mooy am ay fasoŋu waxtaan yu bees. Benn bi mooy, téere bi dina am waxtaan yuy leeral li Biibël bi di jàngale ci kàddu yu yomb. Dina am it waxtaan yuy wone naka la Biibël bi mënee dimbali njaboot yi. Dinañu def it ay waxtaan ngir ndaw yi mën ko jariñoo bu ñuy jàng Biibël bi. Dina am it ay waxtaan yuy jëm ci aaya yuy wax ci jikko Yexowa yi.

5 Ñu ngi ñaan Yexowa mu barkeel lu bees li ñuy def ci La Tour de Garde bi. Yàlla na téere boobu ak Réveillez-vous ! bi tax ba boroom xol yu rafet yu gën a bare jot ci xibaar bu baax bi. — Macë 10:11.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager