Nañu wone yéenekaay yiy “ wax dëgg gi ”
1. Lan mooy njariñu La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! ?
1 Ba fi ñu tollu nii, La Tour de Garde annonce le Royaume de Jéhovah ak yéenekaay bi muy àndal, Réveillez-vous ! am nañu wàll bu am solo ci liggéeyu waaraate bi ak ci liggéeyu sàkk ay taalibe (Macë 24:14 ; 28:19, 20). Kontaan nañu lool di wone ci bépp fànnu liggéeyu waare bi, ñaari yéenekaay yooyu baax ci suñu jamano ji.
2. Lan lañu jot a soppi ci La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! Te lu tax ñu def loolu ?
2 Bi téere yooyu amee ba tey, soppi nañu ni ñu tollu, soppi it li ñu ci def. Soppi nañu itam ni ñu leen di wonee ci waaraate bi. Soppi yooyu dañu leen def ngir yéenekaay yi gën a neex nit ñi te ñu gën leen a amal njariñ, te it noonu xibaaru nguur gi dina gën a laal xolu nit ñépp ngir ñu ‘ mucc te xam dëgg gi ’. — 1 Tim. 2:4.
3. Naka lañu mën a wonee yéenekaay yi ci liggéeyu waare bi ?
3 Ci wéeru sãwiyee 2006 lañu komaase di jëfandikoo waxtaan yu wuute ngir wone benn Réveillez-vous ! biy am wéer wu nekk. Léegi, dinañu def lu mel noonu itam, ngir wone benn ci ñaari La Tour de Garde annonce le Royaume de Jehovah yuy génn weer wu nekk. Def nañu ci xët bi mujj ci Sasu Nguuru Yàlla bi, lu ñu mën a wax ngir wone yéenekaay bu nekk. Loolu, ci waxtaan yi jiitu ci yéenekaay bi la faral di wax. Waaye lée-lée, dafay laal yeneen waxtaan yi nekk ci biir yéenekaay bi te mën a neex nit ñu bare. War nañu xam bu baax li nekk ci xaaju yéenekaay bi ñu bëgg a wone. Loolu dina tax ñu mën a jëfandikoo ni mu gënee baax li ñu wone ci Sasu Nguuru Yàlla bi ngir wone yéenekaay bi. war nañu itam mën a wax ak suñu kàddu bopp li ñu bind ci Sasu Nguuru Yàlla bi gën a baax ci suñu gox.
4. Lu tax yenn say,di wax ci leneen li nekk ci yéenekaay bi te bañ a jël li nekk ci Sasu Nguuru Yàlla bi ngir wone yéenekaay yi mën a baax ?
4 Bu dee sax dañu def ci Sasu Nguuru Yàlla bi ñaari waxtaan ngir wone yéenekaay bu nekk, bu la neexee waxal leneen. Lu tax loolu ? Ndaxte beneen waxtaan ci yéenekaay bi mën na gën a baax ci sa goxu mbooloo. Walla mën nga am waxtaan bu la gën a neex ci yéenekaay bi,te loolu mën a tax nga wone yéenekaay bi nu mu gënee baax.
5. Bala ngay mën a waajal li ngay wax booy wone yéenekaay yi, lan nga war a njëkk def ?
5 Naka nga mënee waajal li ngay wax ngir wone yéenekaay yi : Li njëkk mooy, danga war a xam bu baax li ñu wax ci xaaju yéenekaay bi nga bëgg wone. Yenn saay doo mën a xam li nekk ci yéenekaay bi yépp bala nga koy komaasee wone ci waaraate bi. Waaye booy wax ci benn xaaj ci yéenekaay bi, danga war a wone ne dafa la neex dëgg te danga gëm li ci nekk. Kon, fàww nga xam bu baax li téere bi wax ci li nga bëgg waxtaan ak nit ki.
6. Naka lañu mënee waajal li ñuy wax bu ñuy wone yéenekaay yi ?
6 Boo defee loolu ba pare, nanga tànn li mën a itteel nit ñi. Boo bëggee komaase waxtaan bi, mën nga laaj nit ki laaj bu jëm ci xaaju waxtaan bi nga ko bëgg won. Na doon laaj buy tax nit ki bëgg déglu li nga koy wax. Bul fàtte mukk ne danga soxla doole gi nekk ci Kàddu Yàlla ngir jot xolu nit ki (Yaw. 4:12). Tànnal aaya bu baax buy ànd ak li nga bëgg a wax. Li gën mooy nga tànn aaya bu nekk ci xaaju yéenekaay bi nga bëgg wone. Fexeel ba aaya bi ànd bu baax ak li nekk ci yéenekaay bi.
7. Lan lañu mën a def ngir li ñu waajaloon ngir wone yéenekaay yi gën a baax ?
7 Nañu wone yéenekaay yi saa yu ñu ci amee bunt : Bala li ñu waajal mën a jur lu baax, fàww ñu won suñu yéenekaay yi nit ñi. Nañu ànd ak mbooloo mi ngir waaraate ak yéenekaay yi ci bésu samdi yi. Nañu won yéenekaay yi nit ñi am ba pare suñu yeneen téere yi. Nañu tàmm wone yéenekaay yi ñiy jàng ak ñun Biibël bi, ak ñi ñuy fekk bu ñuy dellu seeti nit ñi. Dinañu mën a jox itam yéenekaay yi nit ñi ñuy taseel bu ñuy doxi suñuy soxla, walla bu ñuy tukki, walla ñuy xaar doktoor ca loppitaan. Ci biir wéer wi, booy wone yéenekaay yi, nanga seet li nga mën a soppi ci li ngay wax ngir mu gën a baax.
8. Lu tax amul benn yéenekaay bu mel ni La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! ?
8 Amul benn yéenekaay bu mel nii La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! Dañuy màggal Yexowa ni Aji kowe ji ci asamaan ak suuf si sépp (Jëf. 4:24). Dañuy may nit ñi doole ak xibaar bu baax bi jëm ci nguuru Yàlla bi nekk ci suñu yéenekaay yi. Te it dañuy xiir nit ñi ci gëm Yeesu Kirist (Macë 24:14 ; Jëf. 10:43). Rax ci dolli, dañuy topp xew-xew yiy am ci àddina bi, di seet ni ñuy méngoo ak li Biibël bi waxoon ne dina am (Macë 25:13). Nanga waajal sa bopp ngir mën a wone yéenekaay yi saa yoo ci amee bunt. Noonu ngay dimbalee nit ñi nekk ci sa goxu mbooloo ngir ñu jariñoo leen.
9. Lu ñu mën a def ba am li ñuy may ñu dellu seeti nit ñi ?
9 Boo fexee ba nit ki jël benn yéenekaay, walla sax nga waxtaan rekk ak moom waxtaan bu neex bu jëm ci suñu ngëm, na fekk nga waajaloon benn laaj bu baax walla kàddu buy tax mu xalaat bu baax ci li nga koy wax. Bu ko defee, dinga mën a dellusi ngir kontine di waxtaan ak moom waxtaan bu jëm ci suñu ngëm. Bu ñu sawaree ci jiwu dëgg gi, na ñu wóor ne Yexowa dina ubbi xolu nit ñi ko bëgg xam dëgg te bëgg ko jaamu dëgg. — 1 Kor. 3:6.