Lu rafet te jar a def ci atum liggéeyu waare biy komaase
1. Lan lañu mën a xalaat a def ci atum liggéeyu waare biy komaase nii ?
1 Su ñu bëggee jëm kanam ci wallu ngëm, dañu war a xam li ñu bëgg a def. Lan nga bëgg a def ci atum liggéeyu waare biy komaase ? Mën nga nekk pioñee buy jàpple ci benn wéer walla lu ko ëpp. Waaye bala nga mën a bokk ci liggéey boobu di maye mbégte, fàww nga njëkk toog te def porogaraam. Kon léegi nga war a komaasee di ci xalaat. Lu tax ñu war a bëgg a nekk pioñee buy jàpple ?
2. Lu tax ñu war a bëgg a nekk pioñee buy jàpple ?
2 Li war a tax ñu bëgg a nekk pioñee buy jàpple : Bu ñu nekkee pioñee buy jàpple, suñu baay bi nekk ci asamaan dafay ‘ gën a feddali ” (maanaam dafay gën a yokk) mbëggeel bi mu am ci ñun, ndaxte dañuy yokk waxtu yi ñuy def ci waaraate bi (1 Tes. 4:1). Bu ñu xoolee lépp li ñu Yexowa defal, suñu xol dafa ñuy xiir ci wax ak nit ñi lu jëm ci moom (Sab. 34: 1, 2). Yexowa dafay gis li nuy def te lépp li ñuy def ngir yokk li ñuy def ci liggéeyu waaraate bi, loolu dafa koy neex lool (Yaw. 6: 10). Yexowa dafay kontaan bu gisee ne dañu sawar lool ci liggéeyu waare bi. Ñun it bu ñu xamee loolu, dañuy am mbégte bu réy. — 1 Chron. 29:9.
3, 4. Nekk pioñee buy jàpple, naka la ñuy jariñe ?
3 Yàgg ci liggéey, day tax mu gën a yomb ci yow te gën a neex. Boo yokkee li ngay def ci waaraate bi, waxtaan ak nit ñi dina la gën a yomb. Dinga gën a aay ci fasoŋ bi ngay komaasee waxtaan ak nit ñi ak itam ci fasoŋ bi ngay jëfandikoo Biibël bi. Booy waxtaan ci sa ngëm ci waaraate bi, dafay gën a dëgëral sa ngëm. Ñu bare ñu amul woon ku ñuy jàngal Biibël bi, bi ñu nekkee pioñee buy jàpple, gis nañu ku bëgg ñu jàngal ko.
4 Nekk pioñee buy jàpple mën na nekk lu ñuy génne ci yem rekk ci li ñu tàmm def ngir jaamu Yàlla fekk duñu ci def suñu xel ak suñu xol. Am na ku nekkoon pioñee bu ci sax ba bàyyi. Waaye dafa gis ne jotam yépp la doon def ci liggéeyam. Mu daldi nekk pioñee buy jàpple benn weer. Lii la wax : “ Mënuma woon a gëm ni benn wéer kese mënoon a yokk sama ngëm ! Fexe naa ba kontine di nekk pioñee buy jàpple, ba tax sax ma mujj nekkaat pioñee bu ci sax. ”
5. Lan lañu mën a def bu ñu foogee ne duñu mën nekk pioñee ?
5 Bu ñu foogee ne duñu ko mën : Am na ñu ragal a nekk pioñee buy jàpple ndaxte pur ñoom aayuñu ci waaraate bi. Su fekkee ne loolu moo la teree nekk pioñee, nanga xam ne Yexowa mën na laa dimbali ni mu ko defe woon ak Yérémi (Yér. 1:6-10). Musaa nekkoon na ku “ mas a tële ay wax ”, maanaam waxam dafa yéexoon. Waaye loolu terewul Yexowa sant ko mu def li Mu bëggoon (Gàdd. 4:10-12). Boo foogee ne doo mën a nekk pioñee, ñaanal Yexowa mu may la fiit.
6. Naka lañu mënee nekk pioñee buy jàpple bu ñu amee feebar walla suñu porogaraam xat ?
6 Ndax feebar walla porogaraam bu xat moo tax nga ragal a nekk pioñee buy jàpple ? Soo amee feebar, xéyna dinga mën a nekk pioñee buy jàpple sooy def ndànk, ni la ko sa kàttan maye. Boo amee porogaraam bu xaat lool, xéyna dinga gis ne mën nga bàyyi lu amul solo lool li nga bëggoon a def te porogaraame ko ci beneen wéer. Am na ñuy liggéey bés bu nekk, altine ba àjjuma, waaye dañoo jariñoo jot gi ñu am te jël benn walla ñaari fan ci fan yi ñu war a noppalu ngir mën a nekk pioñee buy jàpple. — Kol. 4:5.
7. Kontine di ñaan Yexowa ngir mu dimbali nu ñu nekk pioñee buy jàpple, lu tax mu baax ?
7 Naka lañu koy defe : Waxal ci say ñaan li nga bëgg def. Ñaanal Yexowa mu barkeel lépp li ngay def ngir yokk li ngay def ci waaraate bi (Room 12:11, 12). Moom mën na la may xam-xam bi nga soxla ngir xam li nga mën a soppi ci sa porogaraam ngir mu baax (Saag 1:5). Su fekkee ne nekk pioñee buy jàpple nekkul ci sa xol, ñaanal Yexowa mu dimbali la ba liggéeyu waare bi neex la. — Luug 10:1, 17.
8. Boo defee li nekk ci Léeb yi 15:22, loolu naka la la mënee dimbali nga nekk pioñee buy jàpple ?
8 Nangeen waxtaan ci seen njaboot ci li ngeen mën a def ngir nekk pioñee buy jàpple (Léeb 15:22). Xéyna mu am kenn ci seen waa kër kuy mën nekk pioñee su ko ñeneen ñi jàpplee. Nanga waxtaan itam ak seen waa mbooloo ci li nga bëgg a nekk pioñee buy jàpple, rawatina ñi nga xam ne yéen a bokk li ngeen nekke. Loolu mën na tax nga gën a bëgg nekk pioñee buy jàpple.
9. Yan weer nga mën a tànn ngir nekk pioñee buy jàpple ?
9 Seetal porogaraamu waaraate bi nga def ngir atum liggéeyu waare biy komaase nii. Kañ ngay mën a nekk pioñee buy jàpple ? Boo amee liggéey buy jël sa jot yépp, walla ngay dem lekkool, xéyna mën nga seet weer yi am ay fan fu ñu dul liggéey walla wéer yi am juróomi samdi walla juróomi dimaas. Ci weeru septaambar, desàmbar, màrs, ak ut, dina am juróomi samdi ak juróomi dimaas. Wéeru me am na juróomi samdi. Wéeru suweŋ moom am na juróomi dimaas. Bu sa wér-gi-yaram demewul noonu, seetal weer yi faral di gën a féex, asamaan si leer. Mën nga bëgg a nekk it pioñee ci weer bi wottukat biy wër ci mbooloo yi di ñów ci sa mbooloo. Boo ko defee, dinga am lu neex. Ci ayu-bés boobu, dinga mën a fekke xaaj bi njëkk ci ndaje bi muy def ak pioñee yu ci sax. Te it, bésu ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu ci at mii di ñów, ci bésu 22 màrs lay doon. Kon weeru màrs, awril ak me dinañu baax lool ngir nekk pioñee. Boo tànnee ba pare weer wi walla wéer yi nga bëgg a nekk pioñee buy jàpple, nanga komaasee bind porogaraam buy tax nga mën a waare waxtu yi ñu laajte.
10. Lan nga mën a def bu fekkee ne mënuloo nekk pioñee buy jàpple ?
10 Su fekkee ne sax danga xalaat ne doo mën a nekk pioñee buy jàpple ci atum liggéeyu waare bii di ñów, mën nga kontine di sawar ci waaraate bi. Nanga kontine di def lépp li nga mën ci liggéeyu waare bi. Na la wóor ne Yexowa kontaan na bu la gisee ngay def lépp ngir jox ko li gën ci li nga am (Gal. 6:4). Nanga jàpple te dooleel ñi mën a nekk pioñee buy jàpple. Xéyna dinga mën a defaraat sa porogaraam ba yokk benn bés ci fan yi nga faral di dem waare ngir mën a ànd ak ay pioñee ci waaraate bi.
11. Lu tax ñu war a xam ne liggéeyu waare bi, liggéey bu jamp la ?
11 Ñi bokk ci mbooloo Yexowa, dañoo xam ne am na liggéey bu jamp bu ñu war a def. Liggéey boobu mooy waare xibaar bu baax bi. Nit ñi mën nañu ci ñakk seen bakkan, te jot bi des bareetul (1 Kor. 7:29-31). Mbëggeel bi ñu am ci Yàlla ak ci suñuy moroom mooy tax ñuy def lépp li ñu mën ci liggéeyu waare bi. Bu ñu defee porogaraam bu baax te góor-góorlu ci, xéyna dinañu mën a nekk pioñee buy jàpple lu mu néew-néew benn wéer ci atum liggéeyu waare bii di komaase nii. Te wax dëgg, loolu nekk na lu rafet te jar a def !