TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 2/07 p. 3-4
  • Yégleleen ni Yexowa baaxe

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Yégleleen ni Yexowa baaxe
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Lu rafet te jar a def ci atum liggéeyu waare biy komaase
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • ‘ Nañu seedeel ci ñépp xebaar bu baax bi ’
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Nañu waaraate bu baax
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Nañu wax ak nit ñi lu jëm ci “ leeru àddina si ”
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2007
km 2/07 p. 3-4

Yégleleen ni Yexowa baaxe

1. Lan moo ñuy xiir ci yégle ni Yexowa baaxe ?

1 “ Céy Yexowa, yaa moom màggaay, kàttan, rafetaay, kiliftéef te yeyoo ndam. Ndax yaa moom lépp li nekk ci asamaan ak suuf ” (1 Net. 29:11). Mbëggeel ak ngërëm yi ñu am ci Yexowa, lu muy def ci ñun ? Dina ñu xiir ci ‘ yégle ngëneelam (maanaam wax ni mu baaxe), moom mi ñu woo, ba génne ñu lëndëm gi, tàbbal ñu ci leeram gu yéeme gi ’ (1 Piy. 2:9). Mënuñu bàyyi wax lu jëm ci suñu Yàlla bu mag bi ! Ci weeru màrs, awril ak me, dinañu mën a wax nit ñi ni Yexowa baaxe.

2. Ban liggéey bu am solo lañu waajal ngir yégle ndaje fàttaliku bi te ñan ñoo ci mën a bokk ?

2 Liggéey bu am solo bu ñu war a def ngir yégal nit ñi reeru sang bi : Altine ñaari fan ci awril, dinañu wone bu baax ni Yexowa baaxe bu ñuy magal reeru sang bi. Ci diggante 17 màrs ba 2 awril, ci àddina si sépp, dinañu joxe kayit yi ñu defar ngir woo nit ñi ci ndaje bu am solo boobu. Na ci ñépp bokk bu baax. Mën na doon jamano ju baax pur ñu bees ñi mën a komaase waare xibaar bu baax bi, bu dee mat nañu waaraatekat. Bu fekkee ne say doom walla ñi ngay jàngal Biibël bi mën nañu mat waaraatekat, demal waxtaan ak njiiti mbooloo mi.

3. Lan lañu mën a wax ngir woo nit ñi ci fàttaliku bi ?

3 Liggéey bi dina nuroo ak li ñu defoon bi ñu doon woo nit ñi ci ndaje bu gën a mag bi tuddoon “ Mucc gi soreetul ! ” Dinañu yónni mbooloo yi ay kayit yu doy, ngir bépp waaraatekat mën ci am 50, te bépp pioñee mën ci am 100. Nanga wax lu gàtt. Mën nga wax lii : Kayit bii, dañu ko defar ngir woo nit ñi ci xew bu am solo boo xam ne, at mu nekk benn yoon lañu koy def. Bii yaa ko moom. Boo ci teewee, dinañu bég lool. Bind nañu ci kayit bi ay tegtal yu jëm ci xew boobu. Bu dee nit ki am na ay laaj, nga ci tontu. Xaaj biy komaase ci xët 206 ci téere Qu’enseigne la Bible mën na la ci dimbali. Dafay wax ci reeru sang bi. Samdi ak dimaas yi, nanga joxe yéenekaay yi ak kayit bi ñu defar ngir woo nit ñi ci ndaje moomu.

4. Naka lañuy joxe kayit yiy woo nit ñi ci fàttaliku bi ?

4 Fépp fu ñu ko mën a def, nañu bàyyi benn kayit ci loxo kenn ci waa kër bu nekk. Nañu fexe ba nit ñi nuy seetiwaat, ñiy jàng Biibël bi, suñu mbokk yi, ñi nu bokkal liggéey, suñu dëkkandoo ak ñeneen ñu nu xam mën a jot ñoom itam seen kayit.

5. Lu tax ñu war a seet léegi li ñu mën a def ngir nekk pioñee buy jàpple ?

5 Nekk pioñee buy jàpple : Ndax mën nga nekk pioñee buy jàpple ci weeru màrs, awril ak me ngir gën a mën a wax nit ñi ni Yexowa baaxe ? Loolu laaj na ñu soppi yenn yi ci li ñu tàmmoon a def bés bu nekk (Efes 5:15-17). Na la wóor ne lépp lu ñu def ngir dolli li ñuy def ci liggéeyu Yexowa dina indi mbégte ak ay barke (Léeb. 10:22). Ndegam jamano fàttaliku bi mu ngi jegesi, waxtu bi jot na ngir seet li ñu nar a def. — Léeb. 21:5.

6. Lan lañu mën a jàng ci màgget bu amoon 90 at te nekkoon pioñee daaw ?

6 Benn màgget bu am 90 at bégoon na ci li mu mënee bokk ci ñi nekkoon pioñee daaw. Lii la wax : “ Dëgg la, toppatoo tool, lu ma neex la, te dama bëggoon a komaase jëmbët ci sama tool. Waaye dama gis ne dama war a seetaat li war a jiitu ci sama àddina. Komka dama bëggoon a jiital liggéeyu Nguuru Yàlla, dama jàpp ne dinaa doon pioñee ci weeru màrs. ” Li mu def noonu ndax indil na ko ay barke ? Lii la wax : “ Dama gën a jege mbooloo mi. Te loolu tax na ma gën a jege Yexowa. ” Ndax mën nañu seetaat li ñuy jiital ci suñu dund ba pare indi ñun itam soppi yu ci war ?

7. Ndax nekk pioñee lu jafe la ?

7 Def 50 waxtu yi ñuy laaj pioñee yuy jàpple, mën na bañ a metti ni ñu ko xalaatee. Ci ñaan nanga seetaat li nga faral a def bés bu nekk, ba pare nga def benn porogaraam, te bind ko ci porogaraam bi nga def ngir liggéeyu Yexowa. Kenn gënula xam li nga nekke. Bu fekkee ne sa yaram neexul walla dangay gaaw a sonn, xéyna mën nga waare ay waxtu yu neew bés bu nekk. Bu nekkee ne dangay liggéey bés bu nekk, xéyna boo waaree ci ngoon walla samdi ak dimaas, dinga mën a nekk pioñee buy jàpple.

8. Lan moo tax benn jëkkër ak benn jabar mën a nekk pioñee buy jàpple ?

8 Njaboot yu bare jotoon nañu ànd nekk pioñee. Ci ay at ci ginnaaw benn jëkkër ak jabar dañu amoon xel ñaar ci nekk pioñee ndax dañu ragaloon ne li ñu nekke woon du leen may ñu nekk pioñee. Lan lañu def ? “ Dañu ñaan Yexowa ngir mu dimbali ñu ci loolu ñu yàggoon a bëgg def ”. Dañu def porogaraam bu baax ba tax ñu mën a def li ñu bëggoon. Lii lañu yokk : “ Neexoon na lool. Am nañu ci ay barke yu bare. Li ñu leen di xelal mooy ngeen jéem ko. Ndax bu ko suñu njaboot mënee def, dingeen ko mën yéen itam. ”

9. Lan ngeen mën a def ci seen njàngum Biibël bii di ñëw ngir waajal weer yii seen mbooloo di yokk li muy def ci waaraate bi ?

9 Seen njàngum Biibël ci njaboot bi bu jotee, mën ngeen ci seet naka la ñépp mënee yokk li ñuy def ci waaraate bi ci weer yii di ñëw. Bu dee seen njaboot yépp mënul a nekk pioñee, xéyna kenn ci yéen mën na ko doon bu ko ñeneen ñi jàpplee. Loolu bu mënul nekk, xéyna ñi bokk ci seen njaboot mën nañu fas yéene yokk li ñuy def ci waaraate bi ci weer yooyu.

10. Lu tax ñu war a wax ñeneen ñi ne dañu bëgg yokk li ñuy def ci waaraate bi ci jamano fàttaliku bi ?

10 Dimbaleenteleen : Cawarte dafay wàlle. Waxtaaneleen ci li ngeen bëgg nekk pioñee buy jàpple. Loolu mën na xiir ñeneen ñu nekk ko. Rax ci dolli ñi masoon a nekk pioñee mën nañu la xelal ci porogaraam ak li nga mën a def ba nekk pioñee (Léeb. 15:22). Boo mënee nekk pioñee lu tax doo wax ak keneen ci mbooloo mi, xéyna kenn koo xam ni yéen a bokk li ngeen nekke, ngir ngeen ànd ci liggéey bu neex boobu ?

11. Naka la njiiti mbooloo mi mënee yokk cawarte pioñee yi ci weer yii di ñëw ?

11 Njiitu mbooloo yu bare dañuy defaraat seen porogaraam ngir nekk pioñee (Yaw. 13:7). Loolu dafay yokk doole mbooloo mi ! Waxtaan yi njiiti mbooloo mi di am ak waa mbooloo mi, dañuy tax ba ñu gën a sawar. Wax yu rafet yuy xiirtal, walla ay xelal mën na doon lu nit ki soxla woon ngir nekk pioñee. Njiitu mbooloo mi yore liggéeyu waare bi dina yokk it ndaje yi ñuy def bala ñuy dem waare. War nañu xamal saa su nekk waa mbooloo mi fu ñuy defe ndaje yooyu. Bu ko defee, ñépp dinañu mën a am ñu nuy àndal ci waaraate bi, bu dee sax bu ñuy wàcc liggéey walla lekkool. Dina fexe it ba ñépp am gox fu ñuy waare ak it téere yu doy.

12. Boo mënul nekk pioñee, lan nga mën a def ?

12 Bu dee li nga nekke mayu la nga nekk pioñee, mën nga xiirtal ñi ko doon, te mën nga leen ñaanal (Léeb. 25:11 ; Kol. 4:12). Xéyna mën nga jàpp ak ñoom benn bés ci biir semen bi ngir ànd ak ñoom ci waaraate bi walla nga gën ci yàgg.

13. Lan lañu fas yéene am ci dëkk yi bànqaasu Senegaal di topptoo te naka la seen mbooloo mënee def wàllam ngir ñu am ko ?

13 Fas nañu yéene mat 300 pioñee ci awril : Ci reew yi bànqaasu Senegaal di topptoo, li gën a bare ci pioñee yu ñu mas a am ci benn weer mooy lii : Senegaal, 204 ; Gambie, 35 ; Mali, 30 ; Guinee Bisao, 19. Bu ñu ko boolee, mu nekk 288. Looloo tax ñu xam ne mën nañu fexe ba am 300 pioñee yuy jàpple. Bu ñu ko boolee mu nekk 255 pur ñaari réew yi. Xalaatleen cawarte bu loolu di indi ci mbooloo mi ak lu rafet lu muy def ci waaraate bi ci goxu mbooloo mi !

14. Lu tax awril doon weer bu baax ngir nekk pioñee ?

14 Lu tax awril doon weer bu baax ngir nekk pioñee buy jàpple ? Ndaxte fàttaliku bi, bi weer wi di komaase lay ame. Kon dina ñu may ñu mën a seetiwaat bu baax ñi teewe woon. Dinañu joxe ay yéenekaay te di séentu joxe téere Qu’enseigne la Bible te komaase ay njàngum Biibël bu ñuy dellu seeti nit ñi. Doon pioñee ci weeru awril dina tax ñu mën a door ay njàngum Biibël yu bare. Rax ci dolli, weeru awril am na juróom dimaas ak ay bés yu ñu dul liggéey ci àddina si sépp. Loolu day tax ñiy liggéey ak ñiy jàngi, bu ñu bëggee nekk pioñee, dina gën a yomb ci ñoom.

15. Lu tax bu jamano fàttaliku bi di jegesi, ñu war di gën a gaaw ci li ñuy def ?

15 Bépp jamano fàttaliku bu romb, dafa ñuy waññil benn at ci li des bala njeexteelu àddina si di jot. Waxtu bi des ngir waxtaane lu jëm ci suñu Yàlla bu mag bi gàtt na lool (1 Kor. 7:29). Bu fàttaliku bi wéyee, li mu ñu mayoon ngir ñu magal suñu Baay bi ci asamaan day daldi wéy ba abadan. Nañu waajal léegi suñu bopp ngir def suñu kem kàttan ci weeru màrs, awril ak me ngir wax nit ñi ni Yexowa baaxe.

[Wërale bi nekk paas 4]

Ndax mën nañu am 300 pioñee yuy jàpple ci weeru awril ?

◼ Nañu seetaat lu war a jiitu ci suñu dund

◼ Waxtaan ak suñu njaboot ci li ñu fas yéene def

◼ Waxtaane ak suñu moroom yi lu jëm ci li ñu bëgg def

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager