TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 9/08 p. 5
  • Ay Tont Ci Seeni Laaj

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ay Tont Ci Seeni Laaj
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ay tont ci seeni laaj
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Naka nga mënee am jàmm ci sa biir njaboot? (Xaaj 2)
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
Sasu Nguuru Yàlla — 2008
km 9/08 p. 5

Ay Tont Ci Seeni Laaj

◼ Ndax ñaari wayjur yépp ñooy bind waxtu yi ñuy def ci njàngum Biibël bi ñuy def ci njaboot bi ?

Dëgg la pàpp yi lañu njëkk sant ñu yar xale yi “ di leen yemale ak a yee ci Boroom bi ”. Waaye ñaari wayjur yépp ay bokk ci yaru xale yi (Efes 6:4). Lii la Biibël bi wax xale yi : “ Sama doom, deel déglu li la sa baay digal te bul xeeb sa kàddu yaay. ” (Prov. 1:8.) Njàngum Biibël bi ñuy def ci njaboot bi, fànn bu am solo la ci ni wayjur yi di yare seeni doom.

Bu njëkk wayjur bi doon jàngal xale bu ñu sóobagul, moom rekk moo doon bind waxtu bi mu ko doon jàngal. Bu dee sax ñaari wayjur yi ñoo doon bokk ci waxtaan bi. Waaye ñu ngi seetaat loolu. Bu dee ñoom ñaar ñépp ñooy jàngal xale bi, kon ñoom ñaar ñépp a war a bind waxtu bi ñuy def ci njàng mi. Waaye li ñuy bind bumu weesu benn waxtu par ayu-bés. Dëgg la, li wayjur yi di def ngir jàngal seeni doom ayu-bés bu nekk dafay faral di ëpp benn waxtu. Jàngal sa doom dafay laaj ci ñaari wayjur yépp ñu liggéey fu ñu mënta tollu (Deut. 6:6-9). Waaye li ñuy bind ci kayit biy wone li ñu def ci waaraate bi weer wu nekk, dañu ko def ngir wone liggéey bi ñuy def ci gox bi. Moo tax bu dee sax njàng mi dafay weesu benn waxtu te ñu koy def lu ëpp benn yoon par ayu-bés, te xale bu nekk am njàngam, waruñu bind lu ëpp benn waxtu par ayu-bés. Bu ñuy bind li ñu def ci waaraate bi weer bu nekk, kenn ci wayjur yi kese mooy bind njàngum Biibël bi ak ñaata yoon la waxtaan ak xale bi.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager