Ay tont ci seeni laaj
◼ Bu ñuy bind li ñu def ci waaraate bi ngir joxe ko ci mbooloo mi, ndax mën nañu ci boole njàngum Biibël bi ñuy def ak suñu njaboot ?
Way-jur buy jàng Biibël bi ak ay doomam, te mu am ci ñu ci sóobagul, mën na boole njàngum Biibël boobu ci li mu def ci waaraate bi. Mën na am njàngum Biibël boobu ëpp benn waxtu ci ayu bés bi walla way-jur bi def ko lu ëpp benn yoon ci ayu-bés bi, walla sax way-jur bi am benn njàngum Biibël ak xale bu nekk. Waaye ba tey way-jur bi, benn waxtu ak benn nouvelle visite kese (maanaam nit bu ñu dellu seeti) lay mën a bind ayu-bés bu nekk ngir xale yooyu yépp. Te benn njàngum Biibël kese lay mën a bind ci weer wi. — Seetal téere Notre ministère, xët 105.
Bu fekkee ne ñi nekk ci kër gi yépp dañu leen sóob ba pare, way-jur yi waruñu boole waxtu bi ñuy toog ngir jàngal Biibël bi seeni doom ci waxtu yi ñu def ci waaraate bi, te duñu bind it njàngum Biibël boobu. (Bu fekkee ne kenn ci seen doom sóob nañu ko waaye mu ngi jàng ñaareelu téere bi ñu war a jàng, way-jur bi dina mën a boole njàngum Biibël boobu ci li mu def ci waaraate bi.) Lu tax loolu ? Li ñuy bind ngir wone li ñu def ci waaraate bi, dafa war a wone li ñu def ngir waare xibaar bu baax bi ak jàngal dëgg gi nekk ci Biibël bi nit ñi nu sóobagul (Macë 24:14 ; 28:19, 20). Waaye nag, loolu warul a tax ñu xalaat ne soxlawul ñuy faral a def njàngum Biibël boobu ayu-bés bu nekk.
Way-jur yi nekk karceen ñoo am wareefu jàngal seeni doom Biibël bi. Ñi soxla ndimbal ngir mën a am njàngum Biibël ak seen njaboot, walla ngir gën koo mën a def, dañu ko war a wax magi mbooloo mi. Yenn saay li gën ci xale bi ñu sóobagul mooy keneen ku dul way-juram jàngal ko Biibël bi. Waaye bala ñuy def loolu, fàww ñu waxtaan ak wottukat biy jiite walla wottukatu liggéeyu waare bi. Bu nangoo loolu, nit kiy def njàngum Biibël bi ak xale boobu, dina ko mën a boole ci li mu def ci waaraate bi, ni muy defe ak yeneen njàngum Biibël yi mu am.
Li way-jur di bind ngir wone li mu def ci waaraate bi, du wone lépp li muy def ngir yar doomam yi ci yoonu Yexowa (5 Mu. 6:6-9 ; Léeb. 22:6). Yar xale yi “ di leen yemale ak a yee ci Boroom bi ”, wareef bu diis la. Li way-jur yi di def ci loolu, dëgg-dëgg, rafet na lool. — Efes 6:4.