Njàngum Biibël bi ñuy def ci njaboot bi ak bi ngay defal sa bopp, am nañu solo lool !
1. Lu am solo lan la ñu Jataay Biy Dogal bëgg defal tey ak lu tax mu koy def ?
1 Ni ñu ko doon defe ci jamano karceen yu njëkk yi, Jataay Biy Dogal dafa bëgg def lépp li mu mën ngir toppatoo bu baax mbooloo Yexowa (Jëf. 15:6, 28). Metit wu rey wi mu ngi gën di jege. Kon waaraatekat bu nekk war na am diggante bu rattax a Yexowa. Loolu dafa am solo lool. Naka nga nar a jariñoo waxtu bi ñu doon defe njàngum téere bi ci mbooloo mi ? Ñu ngi xiirtal ñépp ñu jël waxtu boobu def ko ci liy dimbali njaboot bi yépp mu jaamu Yàlla. Jariñoo waxtu boobu ci fasoŋ bi gën dina ñu may ñu mën a gën a gëstu ci Kàddu Yàlla te jariñoo ci li ñu ciy jàng. — Sab. 1:1-3 ; Room 11:33, 34.
2. Ban ngoon lañu mën a jagleel liy dimbali njaboot bi yépp mu jaamu Yàlla ?
2 Nañu jël benn ngoon jagleel ko liy dimbali njaboot bi yépp mu jaamu Yàlla : Ci kanamu Yexowa, boroom kër yi ñoo war a fexe ba njaboot bi am porogaraam bu baax bu muy faral di topp ngir jàng Biibël bi ak njaboot bi (Deut. 6:6, 7). Suñu mbokk yu amul njaboot dinañu mën a jariñoo jot boobu ngir def seen njàngum Biibël bi te di gëstu ci suñu téere yi. Ñun ñépp a war a “ jariñoo jot gi ” ngir jàng te xalaat bu baax ci li ñu jàng ngir mën a am ngëm bu dëgër gi ñu soxla ci “ jamano ju bon ” jii. Loolu am na solo lool. — Efes 5:15, 16.
3, 4. Lan lañu nu wax ne mën nañu ko jëfandikoo te lan lañu war a def ci suñu xel ?
3 Li ñu ci war a jàng : Index bu La Tour de Garde bi walla CD-ROM bu Watchtower Library mën na ñu dimbali ñu xam fu ñuy jële li ñuy jàng ba njàngum Biibël bi nekk lu neex ci njaboot bi. Njaboot yi mën nañoo xool waxtaan yi nekk ci La Tour de Garde. Lu mel ni waxtaan yi ci faral di nekk, maanaam “ Clés du bonheur familial ”, “ Enseignez vos enfants ” ak “ Pour nos jeunes lecteurs ”. Am na it waxtaan yuy faral di nekk ci Réveillez-vous ! te tudd “ Les jeunes s’interrogent ” ak yeneen waxtaan yu neex yu jëm ci lu doy kéemaan li Yexowa sàkk.
4 Jàng Biibël bi ndànk-ndànk mën na def ci xel ak xolu waa kër gi yépp li Yàlla santaane ak li ñu ci mën a jàng (Yaw. 4:12). Yenn saay, mën ngeen seetaan benn ci wideo yi mbootaay bi defar te waxtaan ci. Am na lu bare lu mën a may boroom kër yi ñu seet ni ñuy def ba am ay fasoŋi njàngale yu wuute te neex. Ndax mënuloo laaj sa waa kër li ñu bëgg jàng ak ni ñu bëgg ñu defe ko ?
5. Njàngum Biibël bi ñuy def ci njaboot bi ak bi ngay defal sa bopp, lu tax ñu am solo lool ci suñu dund tey ?
5 Lu tax loolu am solo tey : Bu ñuy rattaxal suñu diggante ak Yexowa, loolu dina tax ñu mën a ‘ taxaw jonn te gis mucc, gi ñu Aji sax ji defal ’ (Gàd. 14:13). Wayjur yi soxla nañu Yàlla won leen li ñu war a def ngir yar seeni doom “ ci biir jamano ju yàqu te rëb ” ji ñu nekk (Fil. 2:15). Xale yi soxla nañu ku leen di dimbali ngir ñu xam li ñu war a def ca lekkool ba, ndax jikko yu bon yi ñu fay gis (Prov. 22:3, 6). Li gën ci jëkkër ak jabar yi mooy, ñu dëgëral seen diggante ak Yexowa te ñu koy méngale ak “ buum bu ñu boole ñetti buum ” (Eccl. 4:12). Kon nag nañu jariñoo bu baax jot bi des ngir dëgëral suñu “ ngëm wu sell ” wi ! — Yudd 20.