TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • Boo ñëwee ci suñuy ndaje karceen lan nga fay jële ?
    Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
    • NJÀNGALE 5

      Boo ñëwee ci suñuy ndaje karceen lan nga fay jële ?

      Benn ndaje seede Yexowa yi ci saalu Nguur ca Argentine

      Argentine

      Benn ndaje seede Yexowa yi ca Sierra Leone

      Sierra Leone

      Benn ndaje seede Yexowa yi ca Belgique

      Belgique

      Benn ndaje seede Yexowa yi ca Malaisie

      Malaisie

      Ñu bare dañu bàyyi teewe ay ndaje diine ndaxte duñu fay jële xelal yu leen mën a dimbali ci seen dund walla luy dëfël seen xol. Léegi lan moo mën a tax nga teewe ndaje seede Yexowa yi ? Lan nga fay jële ?

      Mbégte bi nekk ci booloo ak nit ñuy wone mbëggeel ak cofeel. Karceen yu njëkk ya dañu doon taxawal ay mbooloo te am ay ndaje ci seen biir ngir jaamu Yàlla, jàng mbind mu sell mi te xiirtalante (Yawut ya 10:​24, 25). Jàmm ak mbëggeel lañu doon nekke ci ndaje yooyu. Ay xarit dëgg lañu woon, ay mbokk ci ngëm (2 Tesalonig 1:3 ; 3 Yowaana 14). Tey, ci ñoom lañuy roy moo tax ni ñoom dañu am mbégte.

      Njariñ bi nekk ci jàng ni ñuy toppe li Yàlla santaane ci Biibël bi. Ni ñu ko daan defe ca jamono yonent ya, tey bu seede Yexowa yi dajee, ñépp ay teew, muy góor mbaa jigéen, mag ak ndaw. Ay jàngalekat yu xareñ ñoo ñuy woon ci Biibël bi naka lañu mënee topp santaane Yàlla yi bés bu nekk (Deutéronome 31:12 ; Nehémia 8:⁠8). Ñépp a mën a bokk ci waxtaan yi ak ci woy yi ñuy woy foofu te wone noonu seen ngëm. — Yawut ya 10:23.

      Barke bi nekk ci am ngëm buy gën a dëgër. Ci jamono ji mu doon dund, lii la ndaw li Pool waxoon benn mbooloo karceen : “ Bëgg naa leena gis lool, . . . nu dimbaleente ci suñu ngëm, ndax man itam ma gëna am doole ” (Room 1:11, 12). Tàmm di daje ak suñuy mbokk ci ngëm dafay dëgëral suñu ngëm te gën ñu xiir ci topp li Yàlla santaane ci Biibël bi.

      Ñëwal teewe ndaje bii di ñëw, xool ba xam ndax li ñu wax fii dëgg la. Ñu ngi lay xaar. Mën nga teew te doo fey dara. Kenn du la laaj xaalis.

      •  Fasoŋ bi seede Yexowa yi di defe seeni ndaje tey, fan lañu ko jële ?

      •  Ban njariñ lañu mën a jële ci teewe ndaje karceen yi ?

      XÓOTALAL WAXTAAN BI

      Boo bëggee gis fi ñuy defe suñu ndaje yi bala nga ciy teew, waxal benn seede Yexowa mu yóbbu la fa, nga xool.

  • Ban njariñ lañuy jële ci booloo ak suñuy mbokk ci ngëm ?
    Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
    • NJÀNGALE 6

      Ban njariñ lañuy jële ci booloo ak suñuy mbokk ci ngëm ?

      Ay seede Yexowa yu booloo ak seeni mbokk ci ngëm

      Madagascar

      Benn seede Yexowa buy dimbali benn mbokk karceen

      Norvège

      Ay magi mbooloo yu seetsi benn mbokk ci ngëm

      Liban

      Ay seede Yexowa yu booloo di waxtaan

      Italie

      Seede Yexowa yi duñu bàyyi dara tere leen teewe seen ndaje yi ; du taw, du naaj, du yoonu àll. Bu dee sax dañuy jànkoonteel ay jafe-jafe walla ñu yendoo liggéey ba sonn, seede Yexowa yi dañuy def lépp ngir booloo ak seeni mbokk ci ngëm. Lu waral loolu ?

      Dañuy am ndimbal ci suñuy jafe-jafe. ‘ Xiirtalanteleen ’ ci seen biir. Loolu la ndaw li Pool waxoon ñépp ñiy daje ci mbooloo karceen yi (Yawut ya 10:24). Wax boobu dafa laaj ñu xamante ci suñu biir. Kon ndaw li Pool dafa ñuy xiir ci am yitte ci ñépp. Nanga jéem a xam yeneen njabooti karceen yi. Dinga gis ne ñu bare jaar nañu ci jafe-jafe yi ngay dund tey ba génn ci. Dinañu la mën a xelal ndax nga mën a génn ci say poroblem yaw itam.

      Dañuy am xaritoo yu dëgër. Ci suñu ndaje yi, duñu ay àndandoo kese waaye ay xarit dëgg lañu. Lée-lée li waral ñuy booloo mooy bëgg a féexal suñu xol ci fasoŋ bu rafet. Ban njariñ moo ci nekk ? Dafay tax ñu gën a xamante ngir gën a soppante te suñu mbëggeel dafay gën a dëgër. Kon bu suñu mbokk ci ngëm amee jafe-jafe, dinañu sawar ci dimbali ko ndax xaritoo bu dëgër bi dox suñu diggante (Kàddu yu Xelu 17:17). Nañu booloo ak ñépp ñiy teew ci suñu ndaje yi. Noonu dinañu wone ne ñépp lañu yég. —1 Korent 12:​25, 26.

      Ñu ngi lay xiir ci tànn say xarit ci ñiy def li Yàlla bëgg. Xarit yu mel noonu dinga leen fekk ci biir seede Yexowa yi. Fexeel ba dara bañ laa tere booloo ak ñun.

      •  Bu ñu demee ci suñu ndaje yi, lu tax booloo ak suñuy mbokk ci ngëm nekk suñu jariñ dëgg ?

      •  Kañ ngay ñëw xamante ak suñu waa mbooloo ?

  • Lan lañuy def ci suñu ndaje yi ?
    Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
    • NJÀNGALE 7

      Lan lañuy def ci suñu ndaje yi ?

      Benn ndaje seede Yexowa ca Nouvelle-Zélande

      Nouvelle-Zélande

      Benn ndaje seede Yexowa ca Sapoŋ

      Sapoŋ

      Benn xale seede Yexowa buy liir Biibël bi ca Ouganda

      Ouganda

      Ñaari seede Yexowa ca Lituanie yuy wone ni ñuy defe waxtaan ci Biibël bi

      Lituanie

      Karceen yu njëkk ya, ci seeni ndaje, dañu doon woy, di ñaan Yàlla, di jàng te waxtaan ci mbind mu sell mi (1 Korent 14:26). Tey boo ñëwee ci suñu ndaje yi, lu mel noonu ngay gis.

      Li ñuy jàngale foofu, ci Biibël bi la sukkandiku te am na njariñ. Semen bu nekk, samdi walla dimaas, ci mbooloo yépp dañuy déglu benn Waare ci Biibël bi bu def 30 minit. Waxtaan boobu dafay wone njariñ bi Biibël bi am ci suñu dund ak ci suñu jamono te ñépp a mën a topp njàng mi ci seen Biibël. Bu ñu paree, dañuy jël benn waxtu ngir def li ñuy woowe Gëstu ci “ La Tour de Garde ”. Waxtaan la ci téere bi tudd La Tour de Garde (Édition d’étude) te ñépp a ci mën a bokk. Waxtaan boobu dafa ñuy dimbali ñu xam ni ñu mënee topp li nekk ci Biibël bi. Benn téere boobu lañuy jàng ci lu ëpp 110 000 mbooloo seede Yexowa yi am ci àddina ci sépp.

      Dañuy jàng ngir nekk ay jàngalekat yu aay. Dañuy daje itam benn ngoon ci diggu semen bu nekk. Porogaraamu ñetti xaaj la bu tudd Dundinu karceen ak liggéeyu waare bi dafay sukkandiku ci li ñu war a jàng ci kayitu ndaje bi tudd Dundinu karceen ak liggéeyu waare bi. Xaaj bi jëkk ci ndaje bi mu ngi tudd Njariñ bu réy bi ñu mën a jële ci Kàddu Yàlla. Dafa ñuy dimbali ñu gën a miin aaya Biibël yu ñu jàng ci semen bi. Bi ci topp mu ngi tudd Farlul ci liggéeyu waare bi, dañu ciy jàng ni ñu mënee jëfandikoo Biibël bi ngir waxtaan ak nit ñi. Bu ñu paree, dafay am kuy joxe ay xelal ngir ñépp gën a aay ci jàng ak ci jàngale (1 Timote 4:​13). Xaaj bi mujj mu ngi tudd Dundinu karceen. Dañu ciy jàng ni ñu mën a dunde bés bu nekk santaane yi nekk ci Biibël bi. Dafay am kuy yëkkëti laaj, ñi teew di tontu. Dafa ñuy dimbali ñu gën a nànd Biibël bi.

      Wóor na ñu ne boo teewee suñu ndaje yi dinga kontaan ndax njàngale Biibël bu set te leer bi nga fay dégg. — Isaïe 54:⁠13.

      •  Boo demee ci ndaje seede Yexowa yi, lan nga fay dégg ?

      •  Ndaje yi ñuy def, ban nga ci bëgg a teewe ?

      XÓOTALAL WAXTAAN BI

      Xoolal waxtaanu Biibël bi ñu nar a def ci suñu ndaje yii di ñëw. Seetal njariñ bi nga ciy mën a jële.

  • Lu tax ñuy solu ba jekk bu ñuy dem ci suñu ndaje yi ?
    Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
    • NJÀNGALE 8

      Lu tax ñuy solu ba jekk bu ñuy dem ci suñu ndaje yi ?

      Pàppa ak doomam bu góor ñu ngi solu ngir dem teewe suñu benn ndaje

      Islande

      Yaay ak doomam bu jigéen ñu ngi waajal seen bopp ngir teewe suñu benn ndaje

      Mexique

      Ay seede Yexowa yu dëkk Guinée-Bissao yu solu ba jekk

      Guinée-Bissao

      Benn njaboot bu dëkk Philippines a ngi dox ngir dem teewe suñu benn ndaje

      Philippines

      Ndax seetlu nga ci foto yi nekk ci téere bii ni seede Yexowa yi di soloo ba jekk bu ñuy dem ci seeni ndaje ? Lu tax colin bu jekk am solo ci ñun ?

      Dafay wone ne dañu may cër Yàlla. Dëgg la, Yàlla buy xool nit du yem ci melokaanam (1 Samwil 16:⁠7). Waaye bëgg nañu bu ñuy booloo ngir jaamu ko, ñu may ko cër, may it cër ñi ñuy dajeel. Dafa mel ni tey, nga war a taxaw ci kanamu buur walla peresidaa. Li wóor mooy, dinga xool bu baax ni ngay soloo ndax li mu doon kilifa. Noonu it ñun, ni ñuy soloo bu ñuy dem ci ndaje yi, dafay wone ne may nañu cër Yexowa Yàlla miy “ Buur bi fiy sax ba abadan ” te fonk béréb bi ñu koy jaamoo. —1 Timote 1:⁠17.

      Dafay wone ne li ñuy jàng ci Biibël bi mu ngi feeñ ci ñun. Ci Biibël bi, Yàlla dafa wax karceen yi ñuy solu “ cig woyof ak maandu ” (1 Timote 2:​9, 10). Solu “ cig woyof ” mooy bàyyi bépp fasoŋu solu buy tax ñépp di la xool ndax colin bu ñàkk yiw te di wone awra. Ku “ maandu ” nag dina xam ni muy tànnee yére yi muy sol. Du tànn lu jagul walla lu doy waar ba ëpp. Li Biibël bi wax noonu terewul ñu am lu bare lu ñu mën a sol. Bu ñuy solu ba jekk, loolu mën na “ rafetal ci lépp njànglem Yàlla sunu Musalkat ” te “ màggal ” ko (Tit 2:10 ; 1 Piyeer 2:​12). Bu ñuy solu ba jekk bu ñuy dem ci suñuy ndaje, dañuy tax nit ñi xalaat lu rafet ci ni ñuy jaamoo Yexowa.

      Bul bàyyi yére yi nga sol tere la teewe suñuy ndaje. Li ñuy sol, soxlawul mu doon lu réy walla lu seer. Na nekk lu set te jekk.

      •  Lu tax suñu colin am solo bu ñuy jaamu Yàlla ?

      •  Yan santaane Yàlla ñoo ñu mën a dimbali ci xam ni ñu war a soloo ?

  • Naka lañu mënee waajal bu baax suñu ndaje yi ?
    Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
    • NJÀNGALE 9

      Naka lañu mënee waajal bu baax suñu ndaje yi ?

      Benn seede Yexowa mu ngi waajal li ñu war a jàng ci suñu benn ndaje

      Cambodge

      Benn seede Yexowa mu ngi waajal li ñu war a jàng ci suñu benn ndaje
      Kenn ci seede Yexowa yi mu ngi joxe tont ci suñu benn ndaje

      Ukraine

      Xéyna fi nga nekk nii, yaa ngi jàng Biibël bi ak benn seede Yexowa. Ndax bala muy ñëw dangay waajal li ngeen war a jàng ? Loolu baax na. Defal loolu itam bala ngay teewe ndaje yi. Dinga ci jële njariñ bu gën a réy. Am porogaraam bu baax ngir def waajal boobu mooy li gën.

      Nanga tànn waxtu bi ak béréb bi. Kañ la sa xel di gën a ubbeeku ci njàng ? Ndax ci suba si la, bala ngay def dara ? Walla ci guddi gi, bu xale yi tëddee ? Xéyna mënoo toog lu yàgg di jàng. Kon seetal jot bi nga mën a jël ngir jàng te boo demee ba tàmbali sa njàng bul bàyyi dara yàqal la. Toogal fu wéet te sore lépp lu mën a génne sa xel ci njàng mi. Nanga fey sa rajo, sa tele, ak sa telefon. Nanga ñaan Yàlla bala ngay komaase. Loolu dina la dimbali nga fàtte coono yi nga yendoo te def sa xel mépp ci kàddu Yàlla. — Filib 4:⁠6, 7.

      Nanga rëdd ci téere bi baat yi am solo te waaj ngir bokk ci waxtaan yi. Booy waajal li ñu war a waxtaane, nanga njëkk a xool turu waxtaan bi walla turu pàcc bi. Nanga seet ni ñu xaajalee waxtaan bi ci biir ak ni xaaj yooyu ànde ak turu waxtaan bi. Bu amee ay foto, nanga xool li nga ci mën a jànge. Xoolal itam laaj yi mujj yiy fàttali ponk yi ëpp solo. Boo paree loolu, jàngal xise maanaam paragraphe bu nekk te jéem a tontu laaj bi mu àndal. Jàngal aaya yi ñu lim te xool ni aaya yooyu di dëgërale waxtaan bi (Jëf ya 17:11). Tont boo gis ci laaj yi nekk foofu, nanga rëdd baat yi ci ëpp solo. Loolu dina tax ngay mën a gaaw a fàttaliku tont bi bés boo teewee ndaje bi te bëgg a bokk ci waxtaan yi. Te it doo soxla di liir booy joxe tont bi. Dinga ko mën a wax ci say kàddu bopp. Boo bëggee tontu, nanga yëkkati sa loxo te bu ñu la mayee, nga joxe tont bu gàtt.

      Semen bu nekk, boo waajalee noonu waxtaan yi ñu war a def ci ndaje yi, sa ‘ dencukaayu ’ xam-xam ci Biibël bi dina yokku ndànk-ndànk. — Macë 13:​51, 52.

      •  Ban porogaraam nga mën a am ngir waajal ndaje yi ?

      •  Naka nga mën a waajale tont boo bëgg a joxe ci ndaje ?

      XÓOTALAL WAXTAAN BI

      Toppal xelal yi ñu wax fii booy waajal njàngum La Tour de Garde bi walla Gëstu Biibël bi ñuy def ci mbooloo mi. Ki lay jàngal Biibël bi dina la dimbali nga waajal benn tont booy joxe ci ndaje bii di ñëw.

  • Lan mooy njàngum Biibël ci biir njaboot ?
    Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
    • NJÀNGALE 10

      Lan mooy njàngum Biibël ci biir njaboot ?

      Benn njàngum Biibël ci biir njaboot

      Corée du Sud

      Jëkkër ak jabar ñu ngi toog di jàng Biibël bi

      Brésil

      Benn seede Yexowa mu ngi jàng Biibël bi

      Australie

      Benn njaboot a ngi def benn waxtaan bu ñu tànn ci Biibël bi

      Guinée

      Yexowa dafa mas a bëgg njaboot yi jël jot ngir toog waxtaan, dëgëral seen ngëm te rattaxal seen diggante ci seen biir (Deutéronome 6:​6, 7). Loolu moo tax seede Yexowa yi di jël jot semen bu nekk ngir jàng Biibël bi ak seen njaboot. Dañuy waxtaan ci toogaay bu neex ci li ñu soxla ci wàllu ngëm. Boo nekkee yaw kese, jot boobu mën nga ci wéet ak Yàlla, tànn benn waxtaan te gëstu li ci Biibël bi wax.

      Jot la bu ñu jël ngir gën a jege Yexowa. “ Jegeleen Yàlla, mu jege leen. ” (Saag 4:⁠8). Mën nañu yaatal suñu xam-xam ci Yexowa bu ñuy jàng ci Kàddoom lu jëm ci jikkoom ak ciy jëfam. Liir Biibël bi ci kaw mooy fasoŋ bu yomb bi ngeen mën a komaase seen njàngum Biibël ci biir njaboot. Mën ngeen a topp porogaraamu Lekkoolu Sasu Nguuru Yàlla bi. Mën ngeen a topp porogaraamu ndaje bi tudd Dundinu karceen ak liggéeyu waare bi. Mën ngeen seddale aaya yi, ba ku nekk am li ngay liir. Bu ngeen paree, ngeen waxtaan ci.

      Jot la bu ñu jël ngir ñu gën a jegeente ci biir njaboot gi. Bu jëkkër ak jabar walla waajur ak seeni doom di toog ngir jàng Biibël bi, seen diggante dafay gën a rattax. Waxtu boobu dafa war a nekk waxtu bu neex te ànd ak jàmm ak mbégte. War na bokk ci waxtu yi gën a neex ci semen bi. Bu waajur di tànn li ñuy waxtaane ci seen njàngum Biibël, nañu sóoraale at yi seen doom am. Mën nañu tibb ci waxtaan yi nekk ci Tour de Garde yi ak Réveillez-vous yi walla ci palaas bi ñu moom ci internet jw.org. Mën ngeen a seetaan ay wideo ci JW Télédiffusion (tv.jw.org) boo leen paree ngeen waxtaan ci. Mën ngeen a waxtaan ci poroblem yi xale yi di daj ci seen lekkool te seet li ñu ci mën a def. Mën ngeen woy itam li ñu war a woy ci ndaje yi. Bu ngeen paree nag, mën ngeen am tuuti lu ngeen lekk walla naan.

      Jot boobu njaboot gi di jël semen bu nekk ngir jaamu Yexowa, dina dimbali ñépp ñu bég bu ñuy jàng kàddu Yàlla. Nangeen ci góor-góorlu. Yexowa dina leen barkeel bu baax-a-baax. — Sabóor 1:​1-3.

      • Lu tax ñuy jël jot ngir jàng Biibël bi ci biir njaboot gi ?

      • Lan la waajur mën a def ba ku nekk ci njaboot gi bég ci waxtu boobu ?

      XÓOTALAL WAXTAAN BI

      Boo bëggee am yeneen xalaat ci ni nga mën a defe sa njàngum Biibël ci biir njaboot, laajal ay mbokk ci mbooloo mi ni ñuy defe seen bos. Nanga seet itam ci sa mbooloo téere yi nga fa mën a jël ngir jàngal say doom lépp lu jëm ci Yexowa.

  • Lu tax ñuy teew ci ay ndaje yu mag ?
    Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
    • NJÀNGALE 11

      Lu tax ñuy teew ci ay ndaje yu mag ?

      Benn ndaje bu mag bu ñetti fan bu seede Yexowa yi ca Mexique

      Mexique

      Téere bu bees bu ñuy door a génne ci benn ndaje bu mag bu ñetti fan ca Allemagne

      Allemagne

      Ay seede Yexowa yu teew ci benn ndaje bu mag bu ñetti fan ca Botswana

      Botswana

      Benn ndaw bu ñuy sóob ci ndox ca Nicaragua

      Nicaragua

      Tiyaatar bu ñu def ci benn ndaje bu mag bu ñetti fan ca Italie

      Italie

      Xoolal nit ñi nekk ci foto yi ci paas bii. Ndax gis nga ni ñu kontaane ? Xam nga lu tax ? Ñu ngi teewe suñu benn ndaje bu mag. Ñun itam yàkkamti nañu teew ci suñu ndaje yu mag yi. Dañuy roy ñi doon jaamu Yàlla ca jamono yu yàgg ya. Yàlla dafa leen santoon ñu booloo ñetti yoon at mu nekk ngir jaamu Ko (Deutéronome 16:16). Am nañu ñetti ndaje yu mag ci at mu nekk : ñaari ndaje yu mag yu benn fan ak benn ndaje bu mag bu ñetti fan. Ban njariñ lañu mën a jële ci teewe ndaje yooyu ?

      Ndaje yooyu dañuy dëgëral suñu diggante ak suñu mbokk karceen yi. Waa Israyil dañu amoon mbégte mu réy bi ñu doon booloo ak ñi gëmoon Yexowa ngir màggal ko. Tey ñun itam, bu ñu booloo ci suñu ndaje yu mag yi ngir jaamu Yexowa, dañuy kontaan lool (Sabóor 26:12 ; 111:⁠1). Ci ndaje yooyu lañu mën a xamante ak yeneen seede Yexowa yu bokk ci yeneen mbooloo walla ci yeneen réew. Bu waxtu añ jotee, ñun ñépp dañuy añandoo ci bërëbu ndaje bi. Loolu dafay gën a neexal ndaje bi (Jëf ya 2:​42). Ci xew-xew yu mel noonu lañu mën a yëg dëgg mbëggeel gi am ci “ kureelu bokk yi ” ci àddina si sépp. — 1 Piyeer 2:​17.

      Ndaje yooyu dañu ñuy dimbali ñu jëm kanam ci wàllu ngëm. Waa Israyil dañu doon jële njariñ ci nànd li ñu leen doon jàngal (Nehémia 8:​8, 12). Ñun itam dañu fonk njàngale Biibël yi ñuy jot ci suñu ndaje yu mag yi. Turu ndaje bu nekk, ci Biibël bi la sukkandiku. Li ñuy gis te dégg ci porogaraam yooyu, dafa ñuy jàngal ni ñuy toppe santaane Yàlla yi ci suñu dund. Dañuy déglu itam suñuy mbokk ci ngëm di nettali ni ñuy jànkoontee ak jafe-jafe yi ci suñu jamono ju metti jii. Bu ñu gisee ne jafe-jafe yooyu terewul ñuy kontine di roy Kirist, loolu dafay dëgëral suñu ngëm bu baax. Tiyaatar yi ñuy def ci ndaje yu mag yu ñetti fan yi dañuy dundal nettali yi nekk ci Biibël bi te won ñu ni ñu mënee topp ay njàngale yu am solo. Ci ndaje bu nekk dañuy sóob ci ndox ñi bëgg a wone ne jébbal nañu seen bopp Yàlla.

      •  Lan moo tax suñu ndaje yu mag yi nekk ay xew-xew yu neex ?

      •  Ban njariñ nga mën a jële ci teewe benn ndaje bu mag ?

      XÓOTALAL WAXTAAN BI

      Boo bëggee gën a xam ni seede Yexowa yi mel ci seen biir, ñëwal teewe suñu ndaje bu mag bii di ñëw. Ki lay jàngal Biibël bi mën na la won benn porogaraamu ndaje bu mag ngir nga xam fasoŋu waxtaan yi ñu fay am. Bindal bésu ndaje bii di ñëw ak fi ñu koy defe ngir bañ koo fàtte. Fexeel ba teew ci.

  • Naka lañuy defe suñu liggéeyu waare Nguuru Yàlla ?
    Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
    • NJÀNGALE 12

      Naka lañuy defe suñu liggéeyu waare Nguuru Yàlla ?

      Ay seede Yexowa yuy waare këroo-kër

      Espagne

      Benn seede Yexowa buy waare ci benn park

      Biélorussie

      Benn seede Yexowa buy waare ci telefon

      Hong Kong

      Ay seede Yexowa yu nekk ci liggéeyu waare bi

      Pérou

      Ci lu yàggul dara bala muy gaañu, Yeesu dafa yégle woon ne : ‘ Xibaaru jàmm bii ci Nguuru Yàlla, dees na ko yégle ci àddina sépp, ngir mu nekk seede ci xeet yépp. Bu loolu amee mujug jamono ji jot. ’ (Macë 24:14). Naka lañuy defe liggéeyu waare boobu ci àddina si sépp ? Xanaa ñu topp fasoŋ bi ko Yeesu doon defe bi mu nekkee ci kaw suuf. — Luug 8:⁠1.

      Dañuy fekki nit ñi ci seeni kër. Yeesu dafa jàngaloon taalibeem yi ni ñu waroon a yéglee xibaaru jàmm bi ci kër yi (Macë 10:​11-​13 ; Jëf ya 5:​42 ; 20:20). Ca jamono karceen yu jëkk ya, dañu doon wax waaraatekat yi fi ñu war a waare (Macë 10:​5, 6 ; 2 Korent 10:13). Tey itam suñu liggéeyu waare bi, noonu lañu koy defe ngir lépp mën a aw yoon. Mbooloo mu nekk dañu koy jox fu mu war a waare. Noonu lañu mën a defe liggéey bi ñu Yeesu sant. — Jëf ya 10:⁠42.

      Dañuy fekki nit ñi fépp fu ñu mën a nekk. Yeesu royukaay la ci liggéeyu waare bi. Dafa doon dem fu nit ñi bare, maanaam ci tefes yi, ci teen yi ak yu mel noonu (Màrk 4:1 ; Yowaana 4:​5-15). Ñun itam ñu ngi jéem a waxtaan ak nit ñi ci Biibël bi fépp fu ñu ko mën, muy ci mbedd yi, ci biro yi, fi nit ñi di féexloo, walla ci telefon. Te it saa yu ñu ci amee bunt, dañuy waar itam suñu dëkkandoo yi, ñi ñu bokkal liggéey, ñi ñu bokkal lekkool ak suñuy mbokk. Loolu yépp tax na ba ay junniy nit ci àddina si sépp dégg xibaaru jàmm bi ngir mën a mucc. — Sabóor 96:⁠2.

      Ndax am na koo mën a yégal xibaaru jàmm bi jëm ci Nguuru Yàlla ? Ndax gis nga njariñ bi mu ci mën a jële ? Yaakaar boobu, bu ko yemale ci yaw. Gaaw a koo yégal nit ñi !

      •  Ban “ xibaaru jàmm ” lañu war a yégle ?

      •  Naka la seede Yexowa yi di roye Yeesu ci seen liggéeyu waare ?

      XÓOTALAL WAXTAAN BI

      Laajal ki lay jàngal Biibël bi mu won la ni nga mënee waxtaan ci fasoŋ bu rafet ak koo xam ci li nga jàng ci Biibël bi.

  • Lan mooy pioñee ?
    Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
    • NJÀNGALE 13

      Lan mooy pioñee ?

      Nit bu jébbal jotam yépp ci liggéeyu waare bi mu ngi waar kenn ci mbedd mi

      Canada

      Ay nit ñu jébbal seen jot yépp ci liggéeyu waare bi ñu ngi waaraate

      Këroo-kër

      Ay pioñee ñu ngi jàngale Biibël bi

      Njàngum Biibël

      Benn pioñee mu ngi jàng Biibël bi

      Jàngal sa bopp Biibël bi

      “ Pioñee ” mooy ku njëkk a sanc ab dëkk ba tax yeneen nit mën fa dëkk. Kon Yeesu pioñee la woon ndaxte Yàlla dafa ko yónni ci kaw suuf ngir mu def liggéey buy tax doomu Aadama yi am dund te mu ubbil leen bunt ngir ñu mucc (Macë 20:28). Tey, ñiy topp Yeesu ñu ngi koy roy bu ñuy def lépp li ñu mën ngir jébbal jot ci “ sàkk ay taalibe ” (Macë 28:19, 20). Am na ci ñoom ñu dem ba mën a bokk ci ñi ñuy woowe pioñee.

      Pioñee mooy kiy jébbal jotam yépp ci liggéeyu waare bi. Seede Yexowa yépp dañuy yégal nit ñi xibaaru jàmm bi, waaye am na ci ñoom ñoo xam ne fexe nañu ba jébbal 70 waxtu ci liggéeyu waare bi weer bu nekk. Dañu leen di woowe pioñee permanã. Ñu bare ci ñoom dañuy wàññi seen liggéey ngir mën a def loolu. Am na it ñi ñu tànn, def leen pioñee espesiyaal ngir ñu dem ci gox yi ñu soxla ay waaraatekat. Ñoom weer bu nekk dañuy jébbal 130 waxtu walla lu ko ëpp ci liggéeyu waare bi. Pioñee yi dañu nekk ay nit ñu doylu te nangu dundin bu woyof, xam ne Yexowa dina faj seeni soxla (Macë 6:​31-​33 ; 1 Timote 6:​6-8). Ñi mënul a jébbal seen jot yépp ci liggéeyu waare bi, mën nañu tànn weer bu ñu bëgg ngir nekk pioñee oksiliyeer. Ñoom weer boobu dinañu jébbal 30 waxtu walla 50 waxtu ci liggéeyu waare bi.

      Pioñee mooy kiy waare ndax li mu bëgg Yàlla ak nit ñi. Yeesu dafa yërëmoon nit ñi xamul Yàlla ak coobareem. Ñun it tey, loolu lañuy yëg bu ñu gisee ne ñu bare noonu lañu mel (Màrk 6:​34). Am na lu ñu xam lu leen mën a dimbali tey te may leen yaakaaru ëllëg. Pioñee dafa bëgg moroomam moo tax mu nangu jébbal jot ak kàttan bu bare ngir dimbali nit ñi ñu xam xibaaru jàmm bi (Macë 22:39 ; 1 Tesalonig 2:⁠8). Loolu dafay dëgëral ngëmam, dafay tax mu gën a jege Yàlla te dafa koy may mbégte mu réy. — Jëf ya 20:⁠35.

      •  Lan mooy pioñee ?

      •  Lan mooy xiir ñu bare ci nekk pioñee ?

  • Yan lekkool lañu jagleel pioñee yi ?
    Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
    • NJÀNGALE 14

      Yan lekkool lañu jagleel pioñee yi ?

      Ay nit ñu jébbal seen jot yépp ci liggéeyu waare bi ñu ngi waaraate

      Etaa Sini

      Ay eleew yu nekk ci Lekkoolu Galàdd
      Ay eleew ñu ngi waajal seen bopp ngir nekk misioneer

      Lekkoolu Galàdd, ca Patterson, New York

      Jëkkër ak jabar yu nekk misioneer ñu ngi waare ci réewu Panama

      Panama

      Jàngal nit ñi ñu xam kan mooy Yàlla dafa mas a nekk li soxal Seede Yexowa yi. Loolu moo tax mu am benn lekkool bu ñu jagleel ñépp ñi jébbal seen jot gépp ci liggéeyu waare Nguuru Yàlla ngir ñu mën a ‘ matal seen yónnent. ’ – 2 Timote 4:5.

      Lekkool bi ñu jagleel pioñee yi. Pioñee permanã bu nekk, ci njeexteelu atam bi njëkk bi, dañu koy woo ngir mu teewe benn lekkool bu juróom-benni fan bu ñuy amal ci saalu Nguur bu ko gën a jege. Te lekkool boobu, li ko tax a jóg mooy dimbali bu baax pioñee yi ñu gën a jege Yexowa te gën a xareñ ci bépp fànnu liggéeyu waare bi, te kontine ci.

      Lekkool bi ñu jagleel ñiy waare Nguur gi. Lekkool boobu ci ñaari weer lañuy koy def. Dañu ko jagleel pioñee yi war a jóge ci seen dëkk ngir dem ci gox yi ñu soxla ay waaraatekat. Lii lañu wax, “ maa ngi nii ! Yónni ma ! ” dañuy roy noonu waarekat bi gën a mag bi mas a am ci kaw suuf, maanaam Yeesu Kirist (Esayi 6:8, MN ; Yowaana 7:29). Jóge sa kër dem feneen fu sore dafa laaj nga mën a woyofal sa dund. Aada yi ak kilimaa bi ak lekk bi mën na wuute bu baax ak li nit ki tàmm. Xéyna sax dinga war a jàng làkk bu bees. Lekkool boobu dafay dimbali suñu mbokk yu góor ak yu jigéen yu seen at tollu diggante 23 ak 65, ñi séy ak ñi séyagul, ñu am jikko yu baax yi ñu soxla ci wàllu ngëm ngir mën a def li leen war fi ñu leen di yónni te mën a yokk liggéey bi leen Yexowa ak mbootaayam dénk.

      Lekkoolu Galàdd. Ci làkku ebrë, Galàdd dafa tekki “ Jalu seede ” moo di seede bu baree bare. Bi lekkoolu Galàdd sosoo ci atum 1943 ba léegi, am na lu ëpp 8 000 nit yu fa jaar, ba pare ñu yónni leen ni ay misioneer ngir seede ba ci “ cati àddina. ” Te seen liggéey jur na lu bare lu baax (Jëf ya 13:47). Bi misioneer yi jëkkee ñëw ci réewu Peru, amu fa woon benn mbooloo seede Yexowa. Waaye léegi, ëpp nañu 1 000. Noonu it ci réewu Sapoŋ amuñu woon lu mat fukki seede Yexowa bi fa misioneer yi demee, waaye léegi ëpp nañu 200 000. Dañuy gëstu Kàddu Yàlla ci lu mat juróomi weer ci lekkoolu Galàdd. Ñi fa mën a dem ñooy pioñee espesiyaal yi, misioneer yi, ñi nekk ci bànqaas yi ak wottukat yiy wër. Dañu leen fay jàngal bu baax ni ñu mënee dimbali mbooloo yi ñu gën a dëgër ci liggéeyu waare bi.

      •  Lu tax ñu taxawal lekkool bi ñu jagleel pioñee yi ?

      •  Ñan ñoo mën a bokk ci lekkool bi ñu jagleel ñiy waare Nguur gi ?

Téere yi ci Wolof (1996-2025)
Ngir génn
Ngir konektewu
  • Wolof
  • Yónnee ko
  • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
  • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
  • Conditions d’utilisation
  • Règles de confidentialité
  • Paramètres de confidentialité
  • JW.ORG
  • Ngir konektewu
Partager