NJÀNGALE 6
Ndax ñi dee dinañu mas a dekki ?
1. Lan mooy xibaaru jàmm bi jëm ci dee ?
Bi Yeesu àggee dëkk bi tudd Betani ci wetu Yerusalem, fekk na xaritam Lasaar dee ba am ñeenti fan. Yeesu dem ci bàmmeel ba, ànd ak Màrt ak Maryaama ñi nekkoon jigéeni ki gaañu. Yàggul dara nit ñi fees fa. Xalaatal mbégte bi Màrt ak Maryaama amoon bi Yeesu dekkalee Lasaar ! — Jàngal Yowaana 11:21-24, 38-44.
Màrt xamoon na xibaaru jàmm bi jëm ci dee. Xamoon na ne Yexowa dina dekkal ñi dee ngir ñu dundaat ci kaw suuf si. — Jàngal Job 14:14, 15.
2. Lan mooy dal nit bu deewee ?
Yàlla dafa ne Aadama : “ Pënd nga, te dinga dellu di pënd. ” — NJÀLBÉEN GA 3:19.
Nit pëndu suuf lañu ko defare (Njàlbéen ga 2:7 ; 3:19). Nit yorewul ruu walla xel bu dul dee mukk. Ñun ñépp, ay mbindeef lañu ci kaw suuf. Kon amul dara luy kontine di dund ci ñun bu ñu deewee. Bu ñu deewee, suñu xel dee na te suñu pexe dafay jeex. Te it, Lasaar waxul dara luy wone ne am na luy xew bu nit deewee ndaxte ñi dee xamuñu dara. — Jàngal Sabóor 146:4 ; Ecclésiaste 9:5, 6, 10.
Ndax Yàlla dafay bugël nit ñi dee ci safara ? Biibël bi wone na ne ñi dee xamuñu dara. Kon leer na ne safara, njàngale bu dul dëgg la buy tuumaal Yàlla. Jël safara, di bugël nit, xalaat bu Yàlla sib la. — Jàngal Jérémie 7:31.
Seetaanal wideo Lan mooy dal nit bu deewee ?
3. Ñi dee ndax mën nañu wax ak ñun ?
Ñi dee mënatuñu wax te mënatuñu dégg (Sabóor 115:17). Waaye am na ay malaaka yu soxor yuy wax ak nit ñi, di leen jéem a gëmloo ne ay nit ñu dee lañu (2 Piyeer 2:4). Yexowa tere na ñuy jéem a wax ak ñi dee. — Jàngal Deutéronome 18:10, 11.
4. Ñan ñooy dekki ?
Ay milyoŋi nit yi nekk ci bàmmeel dinañu dekki ngir dund ci kaw suuf si. Ñi xamul woon Yàlla te daan def lu bon sax dinañu dekki. — Jàngal Luug 23:43 ; Jëf ya 24:15.
Ñiy dekki dinañu mën a jàng xam dëgg gi jëm ci Yàlla te dinañu mën a am ngëm ci Yeesu te déggal ko (Peeñu ma 20:11-13). Ñooñu di dekki, bu ñu defee lu baax dinañu am dund gu dul jeex ci kaw suuf si. — Jàngal Yowaana 5:28, 29.
5. Lan la ndekkite di ñu xamal ci Yexowa ?
Yàlla jox na ñu yaakaaru dekki ci li mu yónni Doomam mu dee pur ñun. Kon ndekkite dafa ñuy won mbëggeelu Yexowa ak mbaaxaayam. Ñi dee bu ñu dekkee, kan nga ci gën a yàkkamtee gis ? — Jàngal Yowaana 3:16 ; Room 6:23.