WOY-YÀLLA 74
Woyleen Nguuru Yàlla!
(Taalifi Cant 98:1)
1. Woy a ngi nii, woy wuy yégle ndam lu réy,
di cantu Buuru asamaan ak suuf;
di may yaakaar ñi koy wut, sawarloo leen.
Kayleen ñu woy awu biñ koy bàkke.
(AWU BI)
‘Bu kenn des! Nañ ko jaamu,
xamle mooy kan, xalamal ko,
ànd ak mbégte di sant Nguuru Yàlla.
Nañ ko sukkal. Yàlla ku màgg la! ’
2. Woy wu bees wii day xamle Nguuru Yàlla.
Yeesu mooy buur, moom mooy ilif suuf si.
Ay àndandoom, askan wu sell te bees.
Paree nguuru, di ko teerook woy wii:
(AWU BI)
‘Bu kenn des! Nañ ko jaamu,
xamle mooy kan, xalamal ko,
ànd ak mbégte di sant Nguuru Yàlla.
Nañ ko sukkal. Yàlla ku màgg la! ’
3. Askan wu réy, ñu woyof ñoo koy xamle.
Ñoom ñoo dikkee baat bu xumb di woy
guddeek bëccëg kàttanam, jox ko ndam li.
Na nit ku ne ci kaw suuf xam woy wii:
(AWU BI)
‘Bu kenn des! Nañ ko jaamu,
xamle mooy kan, xalamal ko,
ànd ak mbégte di sant Nguuru Yàlla.
Nañ ko sukkal. Yàlla ku màgg la! ’
(Xoolal itam Taalifi Cant 95:6; 1 Piyeer 2:9, 10; Peeñu ma 12:10.)