TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • Lan mooy nguuru Yàlla?
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
    • Lesoŋ 31. Yeesu Kirist, buur ci asamaan mu ngi taxaw ci kanamu leeru Yexowa.

      LESOŊ 31

      Lan mooy nguuru Yàlla?

      Xibaar bi gën a am solo ci Biibël bi, mu ngi jëm ci nguuru Yàlla. Yexowa dina jaar ci Nguuram ngir def li mu bëggoon bi muy sàkk suuf si. Lan mooy nguuru Yàlla? Naka lañu xame ne Nguur googu tàmbali na ilif? Lan la jot a def ba pare? Te lan la nar a def ëllëg? Ci lesoŋ bii ak ci ñaar yi ci topp, dinañu tontu ci laaj yooyu.

      1. Lan mooy nguuru Yàlla, te kan mooy buur bi?

      Nguuru Yàlla, gornmaa la bu Yexowa Yàlla taxawal. Yeesu Kirist mooy buur bi, te mu ngi nguuroo ci kaw asamaan (Macë 4:17; Yowaana 18:36). Biibël bi lii la wax ci Yeesu: «Dina yilif [...] ba fàww» (Luug 1:32, 33). Ni buur ci nguuru Yàlla, Yeesu dina ilif ñépp ñi nekk ci kaw suuf.

      2. Ñan ñooy nguuru ak Yeesu?

      Yeesu du nguuru moom rekk. «Ay nit ñu bokk ci bépp giir ak kàllaama ak réew ak xeet [...] dinañu nguuru ci àddina» (Peeñu 5:9, 10). Ñaata nit ñooy nguuru ak Kirist? Bi Yeesu ñëwee ci kaw suuf ba léegi, ay milioŋi nit nekk nañu ay taalibeem. Waaye 144 000 ci ñoom rekk, ñooy dem ci kaw asamaan ngir nguuru ak Yeesu (Jàngal Peeñu 14:1-4). Ñi ci des ñépp ci kaw suuf lañu nar a dund, ci kilifteefu nguuru Yàlla (Sabóor 37:29).

      3. Lan moo tax nguuru Yàlla gën nguuru doomu Aadama yi?

      Bu dee sax njiiti doomu Aadama yi dañuy jéem a def lu baax, amuñu kàttanu matal lépp li ñu bëgg. Rax-ci-dolli, njiit yooyu dañu leen di folli, fal ñeneen. Te ñi leen di wuutu, xéyna seen njariñu bopp rekk lañuy wut waaye du njariñu nit ñi ñuy ilif. Waaye Yeesu miy njiit ci nguuru Yàlla, kenn du mas a jël palaasam. Yàlla dafa «samp nguur gu dul tas mukk» (Dañeel 2:44). Yeesu dina ilif ci kaw suuf si sépp te du gënaatle. Dafa bëgg nit ñi, baax te jub. Te dina jàngal nit ñi ñu wone mbëggeel ci seen biir, mbaax ak njub, ni moom (Jàngal Esayi 11:9).

      XÓOTALAL NJÀNG MI

      Xoolal li tax nguuru Yàlla gën bépp nguuru doomu Aadama.

      Yeesu Kirist mu ngi nekk ci asamaan toog ci jalu buur di ilif suuf si. Ñi mu bokkal Nguur gi ñu ngi toog ci ginnaawam. Leeru Yexowa di melax ci seen ginnaaw.

      4. Gornmaa bu am kàttan mooy nguuru ci kaw suuf si sépp

      Yeesu Kirist moo ëpp kàttan bépp njiit bu mas a am. Jàngal Macë 28:18. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

      • Lan moo tax sañ-sañu Yeesu ëpp sañ-sañu bépp njiit?

      Gornmaa doomu Aadama yi dañu leen di faral di rampalaase ak yeneen, te gornmaa bu nekk, ci réewam rekk la nguuram yem. Nguuru Yàlla nag? Jàngal Dañeel 7:14. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

      • Nguuru Yàlla «du foq mukk [maanaam du tas]», lu tax loolu doon lu baax?

      • Nguuru Yàlla dina nguuru ci kaw suuf si sépp, lu tax loolu doon lu baax?

      5. Gornmaa doomu Aadama yi dañu leen war a rampalaase

      Lan moo tax nguuru Yàlla war a rampalaase nguuru doomu Aadama yi? Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

      WIDEO: Lan mooy nguuru Yàlla? (Xaaj) (1:41)

      • Lan la kilifteefu doomu Aadama jur?

      Jàngal Kàdduy Waare 8:9. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

      • Ci sa xalaat, ndax nguuru Yàlla war na rampalaase nguuru doomu Aadama yi? Lu tax?

      6. Ñiy jiite ci nguuru Yàlla xam nañu bu baax li ñuy dund

      Ndegam Yeesu miy suñu buur, dund na ci kaw suuf ni nit, moom dina ‘mana bokk ak nun sunuy naqar’ (Yawut ya 4:15). 144 000 góor ak jigéen yu takku, yi Yexowa tànn ngir ñu nguuru ak Yeesu, ñu ngi «bokk ci bépp giir ak kàllaama ak réew ak xeet» (Peeñu 5:9).

      • Xam ne Yeesu ak ñépp ñi nar a nguuru ak moom xam nañu bu baax li ñuy dund, ndax loolu dalul sa xel? Lu tax?

      Ay góor ak ay jigéen yu Yàlla tànn te bokkuñu jamono ak xeet.

      Yexowa dafa tànn ay góor ak ay jigéen yu bokkul xeet ngir ñu nguuru ak Yeesu

      7. Santaaney nguuru Yàlla ñoo gën

      Gornmaa doomu Aadama yi dañuy joxe ay santaane ak di tëral ay sàrt yuy aar ñi ñuy jiite te amal leen njariñ. Nguuru Yàlla itam am na ay santaane ak ay sàrt yu ñu war a topp. Jàngal 1 Korent 6:9-11. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

      • Bu ñépp ci àddina si nekkee di topp santaane Yàlla yi, ci sa xalaat naka la àddina di mel?a

      • Yexowa dafa laaj nit ñi Nguuram nar a ilif, ñu topp ay santaaneem, ndax foog nga ne loolu jaadu na? Lu tax?

      • Lan mooy wone ne, nit ñi toppul santaane yooyu, mën nañu soppeeku? (Xoolal aaya 11).

      Polise bu taxawloo oto yi ci benn rond-point bu xat. Ay nit yu maasewul ñu ngi jéggi tali bi.

      Gornmaa doomu Aadama yi dañuy tëral ay sàrt yuy aar ñi ñuy jiite te amal leen njariñ. Sàrt yi nguuru Yàlla tëral ñoo gën fuuf ngir aar nit ñi te amal leen njariñ

      BU LA NIT LAAJOON: «Lan mooy nguuru Yàlla?»

      • Lan nga koy tontu?

      NAÑU TËNK

      Nguuru Yàlla, gornmaa bu am la te nekk ci kaw asamaan. Dina ilif suuf si sépp.

      Nañu fàttaliku

      • Ñan ñooy ñiy jiite ci nguuru Yàlla?

      • Lan moo tax nguuru Yàlla gën bépp nguuru doomu Aadama?

      • Lan la Yexowa di xaar ci nit ñi Nguuram nar a ilif?

      Jubluwaay

      GËSTUL

      Xoolal fi Yeesu wax ne fa la nguuru Yàlla nekk.

      «Ndax nguuru Yàlla lu nekk ci suñu xol la?» (Ci jw.org la nekk)

      Xoolal li Biibël bi wax ci 144 000 nit ñi Yexowa tànn ngir ñu nguuru ak Yeesu.

      «Ñan ñooy dem asamaan?» (Ci jw.org la nekk)

      Lan moo tax benn jigéen ju ñu tëj kaso gëm ne, Yàlla rekk a mën a indi njubte ci kaw suuf?

      «Xam naa léegi li fi mën a dindi lu awul yoon» (Réveillez-vous!, nowàmbar 2011)

      a Dinañu gis yenn ci santaane yooyu ci xaaj 3.

  • Nguuru Yàlla tàmbali na ilif!
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
    • Lesoŋ 32. Yeesu Kirist ca kaw asamaan ni buur ak yatu buuram mu ngi nguuru ci kaw suuf si.

      LESOŊ 32

      Nguuru Yàlla tàmbali na ilif!

      Nguuru Yàlla tàmbali na ilif ci asamaan ci atum 1914. Ci at boobu itam la mujug nguuru doomu Aadama yi tàmbali. Naka lañu ko xame? Nañu xool li Biibël bi yégle woon, liy xew ci àddina si ak doxalinu nit ñi, li ko dale ci atum 1914.

      1. Lan la Biibël bi yégle woon?

      Ci Biibël bi, téere Dañeel wone na ne nguuru Yàlla dina tàmbalee ilif ci mujug bés yi ñuy woowe «juróom ñaari jamono» (Dañeel 4:13, 14). Ay téeméeri at ginnaaw loolu, Yeesu wax na itam ci jamono jooju. Woowe na ko «jamonoy ñi dul Yawut», te wone na ne jamono jooju jeexagul woon (Luug 21:24). Ni ñu ko nar a gise, juróom ñaari jamono yooyu jeex nañu ci atum 1914.

      2. Yan xew-xew ak doxalin lañuy gis, li dale ci atum 1914?

      Taalibe Yeesu yi lii lañu ko laajoon: «Kañ la loolu di am, te luy tegtale ne yaa ngi ñëw te àddina di tukki?» (Macë 24:3). Yeesu xamal leen ne, lu bari dina xew bu komaasee ilif ci nguuru Yàlla ci kaw asaaman. Geer yi, ñàkk lekk bi ak yëngu-yëngu suuf yi, bokk nañu ci li nar a xew (Jàngal Macë 24:7). Biibël bi yégle woon na itam ne «ci mujug jamono» doxalinu nit ñi, dina tax dund gi ‘tiis te tar’ (2 Timote 3:1-5). Li ko dale atum 1914, xew-xew yooyu ak doxalin yooyu dañu gën a bari.

      3. Lu tax àddina si di gën di metti bi nguuru Yàlla tàmbalee ilif ba léegi?

      Bi Yeesu nekkee buuru nguuru Yàlla, yàggul dara mu xeex ak Seytaane ak ay malaakaam ci kaw asamaan. Seytaane lañu daan ci xeex boobu. Biibël bi nee na «daaneel nañu ko ci kaw suuf, moom ak i malaakaam» (Peeñu 12:9, 10, 12). Seytaane dafa ànd ak mer bu tàng ndaxte xam na ne dinañu ko alag. Loolu moo tax muy indi musiba ak coono ci kaw suuf. Loolu dafa ñuy dimbali ñu xam li tax àddina si mettee nii! Nguuru Yàlla dina fi dindi coonoo yooyu yépp.

      XÓOTALAL NJÀNG MI

      Xoolal firnde yiy wone ne nguuru Yàlla tàmbali na ilif ci atum 1914 ak loolu li mu war a def ci ñun.

      4. Yégle yonent yiy wone ne nguuru Yàlla tàmbali na ilif ci atum 1914

      Seetaanal WIDEO BI.

      WIDEO: Nguuru Yàlla tàmbali na ilif ci atum 1914 (5:02)

      Yàlla dafa géntloo Nabukodonosor mi nekkoon buuru Babilon, ay xew-xew yu naroon a am. Gént googu Dañeel firi, yemul rekk ci wax ci kilifteefu Nabukodonosor waaye dafa laal itam nguuru Yàlla (Jàngal Dañeel 4:14).a

      Jàngal Dañeel 4:17-23. Boo paree, jëfandikool tabló bi ngir tontu ci laaj yii di topp:

      • (A) Lan la Nabukodonosor gis ci gént gi? (Xoolal aaya 17 ak 18).

      • (B) Lan moo naroon a dal garab gi? (Xoolal aaya 20).

      • (C) Lan moo naroon a xew ci mujug «juróom ñaari jamono» yi? (Xoolal aaya 23).

      Li tax ñu misaale nguuru Yàlla ak garab gi ci gént gi

      YÉGLE YONENT BI (Dañeel 4:17-33)

      Kilifteef gi

      (A) Garab gu gudd

      Garab gu gudd.

      Nangu nañu kilifteef gi

      (B) «Daaneleen garab gi,» te bàyyi ko «diiru juróom ñaari jamono»

      Ëkku garab gu ñu jéng ak ay càllalay weñ ak xànjar.

      Delloo nañu kilifteef gi

      (C) «Nguur gi dees na la ko delloo»

      Garab gu gudd.

      Ci ni yégle yonent bi njëkkee mat...

      • (D) Kan la garab gi doon misaal? (Xoolal aaya 19).

      • (E) Kañ lañu nangu kilifteef gi? (Jàngal Dañeel 4:26-30).

      • (F) Lan moo dal Nabukodonosor bi «juróom ñaari jamono» yi jeexee? (Jàngal Dañeel 4:31-33).

      NI YÉGLE YONENT BI NJËKKEE MAT

      Kilifteef gi

      (D) Nabukodonosor, buuru Babilon

      Buur Nabukodonosor mu ngi taxaw di réy-réylu.

      Nangu nañu kilifteef gi

      (E) Gannaaw atum 606 B.S.J. Nabukodonosor dof, te mënatul woon a jiite lu tollu ci juróom-ñaari at

      Nabukodonosor mu ngi sëgg di lekk ñax ni mala.

      Delloo nañu kilifteef gi

      (F) Nabukodonosor wér te tàmbaliwaat a jiite

      Buur Nabukodonosor mu ngi yëkkati ay loxoom di xool asamaan.

      Ci ni yégle yonent bi mate ci ñaareelu yoon bi...

      • (G) Kan la garab gi doon misaal? (Jàngal 1 Chroniques 29:23).

      • (H) Kañ lañu nangu kilifteef gi? Naka lañu xame ne, ba bi Yeesu nekkee ci kaw suuf, dellooguñu woon kilifteef gi? (Jàngal Luug 21:24).

      • (I) Kañ ak fan lañu delloo kilifteef gi?

      NI YÉGLE YONENT BI MATE CI ÑAAREELU YOON BI

      Kilifteef gi

      (G) Buuri Israyil yi doon misaal kilifteefu Yàlla

      Ay buur yu toppalante ci Israyil ñu ngi toog ci ay jalu buur. Leer gi di melax ci seen kaw.

      Nangu nañu kilifteef gi

      (H) Yàq nañu Yerusalem, nangu nañu kilifteefu buuri Israyil yi, ci diirub 2 520 at

      Safara mu ngi yàq Yerusalem bu njëkk ba ci atum 607 B.S.J. Gannaaw gi, 2 520 at jàll.

      Delloo nañu kilifteef gi

      (I) Yeesu tàmbali na ilif ci asamaan ni Buur ci nguuru Yàlla

      Yeesu mu ngi toog ci jalu buur ci kaw asamaan di ilif suuf si, li ko dale atum 1914 C.S.J. Leer gi di melax ci kawam.

      Lan mooy diirub juróom ñaari jamono yi?

      Ci Biibël bi, yenn aaya yi mën nañu ñu dimbali ñu nànd yeneen aaya. Ci misaal, téere Peeñu dafay wone ne ñetti diir ak genn-wàll ñu ngi tollook 1 260 fan (Peeñu 12:6, 14). Juróom ñaari jamono mooy ñaari yoon lim boobu, maanaam 2 520 fan. Lée-lée ci Biibël bi, benn fan mën na tekki benn at (Esekiyel 4:6). Kon ci téere Dañeel, juróom ñaari jamono yi, ñu ngi tollook 2 520 at.

      5. Àddina si dafa soppeeku li dale ci atum 1914

      Seetaanal WIDEO BI.

      WIDEO: Àddina si dafa soppeeku li dale ci atum 1914 (1:10)

      Yeesu yégle woon na, ni àddina si naroon a mel bu nekkee buur ba pare. Jàngal Luug 21:9-11. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

      • Ci li nga jàng ci aaya yi, lan nga gis ne mu ngi xew, walla nga dégg ko?

      Ndaw li Pool waxoon na ni nit ñi nar a mel ci mujug kilifteefu doomu Aadama yi. Jàngal 2 Timote 3:1-5. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

      • Ci li ñu wax ci aaya yi, yan jikko nga seetlu ci nit ñi tey?

      Foto yu ñu boole: Foto yuy wone liy xew ci àddina si ak jikkoy nit ñi, ci mujug jamono. 1. Njiitu militeer a ngi taxaw ci ab pójom, yëkkati ay loxoom di yuuxu. 2. Ay tabax yu daanu gannaaw yëngu-yëngu suuf bu am. 3. Ay awyoŋu militeer. 4. Ay nit yu sol mask di dox ci biti. 5. Ñaari tabax yi tudd tours jumelles te nekk ca Etaa sini, ñu ngi tàkk gannaaw bi leen terorist yi songee. 6. Góor guy jël dorog. 7. Góor gu yëkkati loxoom ngir door jabaram, boole ci di ko yuuxu. 8. Dorog yu wuute ak ay butéelu sàngara. 9. Ñaari jigéen yu sol yére yu xew ci jamono ak ay takkaay, di foto seen bopp. 10. Benn animatër buy xumbal ci benn concert. 11. Nit kuy ñaxtu mu ngi sànni butéel bu ñuy woowe cocktail Molotov.

      6. Woneel ne gëm nga ne nguuru Yàlla mu ngi ilif

      Jàngal Macë 24:3, 14. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

      • Ban liggéey bu am solo mooy wone ne nguuru Yàlla mu ngi ilif?

      • Naka nga mënee bokk ci liggéey boobu?

      Nguuru Yàlla mu ngi ilif, te bés bi mu nar a ilif suuf si sépp jege na. Jàngal Yawut ya 10:24, 25. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

      • Lan la kenn ku nekk ci ñun war a def «fi ak [ñu] ngi gis bésu Boroom biy jubsi»?

      Foto yu ñu boole: 1. Kuy jàng Biibël bi te teewe benn ci ndaje Seede Yexowa yi. 2. Mu ngi waar xaritam.

      Boo yëgee lu mën a dimbali ñeneen te musal leen, lan nga war a def?

      BU LA NIT LAAJOON: «Lu tax Seede Yexowa yi di wax ne atum 1914, at bu am solo la?»

      • Lan nga koy wax?

      NAÑU TËNK

      Yégle yonent yi, liy xew ci àddina si ak doxalinu nit ñi, dafay wone ne nguuru Yàlla mu ngi ilif. Ngir wone ne gëm nañu loolu, dañu war di waare te di teewe ndaje yi ci mbooloo mi.

      Nañu fàttaliku

      • Lan moo naroon a xew ci mujug juróom ñaari jamono yi, ni ñu ko yégle woon ci téereb Dañeel ci Biibël bi?

      • Lan moo tax nga gëm ne, nguuru Yàlla ci atum 1914 la tàmbalee ilif?

      • Naka nga mënee wone ne, gëm nga ne nguuru Yàlla mu ngi ilif?

      Jubluwaay

      GËSTUL

      Xoolal li ay boroom xam-xam ak ñeneen wax ci ni àddina si soppeekoo li dale atum 1914.

      «Kañ la àddina si tàmbalee yàqu nii?» (g 4/07)

      Naka lañu xame ne yégle yonent bi nekk ci Dañeel pàcc 4, ci nguuru Yàlla lay wax?

      «Kañ la nguuru Yàlla tàmbalee ilif? (Xaaj 1)» (w14 1/10)

      Lan mooy wone ne «juróom ñaari jamono» yi ñu wax ci Dañeel pàcc 4, ci atum 1914 lañu jeex?

      «Kañ la nguuru Yàlla tàmbalee ilif? (Xaaj 2) (w14 1/11)

      a Xoolal ñaari waxtaan yi mujj ci lesoŋ bii ci Gëstul.

  • Li nguuru Yàlla nar a def
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
    • Lesoŋ 33. Ay nit yuy dund ci àjjana ci kaw suuf.

      LESOŊ 33

      Li nguuru Yàlla nar a def

      Nguuru Yàlla taxaw na ba pare. Ci kanam tuuti, dina soppi lu bari ci kaw suuf. Nañu xool lu baax li nguuru Yàlla nar a def.

      1. Naka la nguuru Yàlla di indiwaate jàmm ak njub ci kaw suuf?

      Yeesu miy buuru nguuru Yàlla, dina alag nit ñu bon ñi ak nguur yi ci xeexu Armagedon (Peeñu 16:14, 16). Ci jamono jooju, dige bii ci Biibël bi dina mat sëkk: «Nes tuut, ku bon ne mes, nga seet, seet, mu réer» (Sabóor 37:10). Yeesu dina jaar ci Nguur gi, ngir feesal suuf si sépp ak jàmm ak njub (Jàngal Esayi 11:4).

      2. Naka la dund gi di mel bu coobare Yàlla amee ci kaw suuf si?

      Ci kilifteefu nguuru Yàlla, «aji jub ay jagoo réew mi [suuf si], dëkke ko ba fàww» (Sabóor 37:29). Xalaatal rekk dëkk ci àddina soo xam ne, ñépp a jub, bëgg Yexowa te ku nekk bëgg sa moroom! Kenn dootul feebar, te ñépp dinañu dund ba fàww.

      3. Lan la nguuru Yàlla di def bu ñu alagee ñu bon ñi ba pare?

      Bu ñu alagee nit ñu bon ñi ba pare, Yeesu dina nguuru 1 000 at. Ci jamono jooju, moom ak 144 000 ñiy nguuru ak moom, dinañu dimbali nit ñi ci kaw suuf ñu nekk nit ñu mat, ñu amul bàkkaar. Bu 1 000 at yi jeexee, suuf si sépp dina nekk àjjana ju rafet, te nit ñi ñépp dinañu bég ndaxte dañuy déggal Yexowa. Gannaaw loolu, Yeesu dina delloo nguur gi Baayam te ‘turu Yexowa dinañu ko sellal’ ci anam bu ñu ko masul a def (Macë 6:9, 10). Su boobaa dina leer ne, Yexowa njiit bu baax la te dafay toppatoo ñi muy ilif. Yexowa dina alag Seytaane, malaaka yu bon yi, ak ñépp ñi tànn bañ a nangu kilifteefam (Peeñu 20:7-10). Lépp li nguuru Yàlla indi, dina fi nekk ba fàww.

      XÓOTALAL NJÀNG MI

      Xoolal li tax ñu mën a gëm ne Yàlla dina jaar ci Nguuram ngir matal lépp li mu dige ci Biibël bi, lu jëm ci suñu ëllëg.

      4. Nguuru Yàlla dina fi dindi nguuru doomu Aadama yi

      ‘Nit dafay yilif nit, muy loraangeem’ (Kàdduy Waare 8:9). Yexowa dina jaar ci Nguuram ngir dindi fi lépp lu njubadi boobu indi.

      Jàngal Dañeel 2:44 ak 2 Tesalonig 1:6-8. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

      • Lan la Yexowa ak doomam Yeesu di def ak nguuru doomu Aadama yi ak ñi leen di jàppale?

      • Ci li nga jàng ci Yexowa ak Yeesu, lu tax nga am kóolute ne lépp li ñu nar a def, lu jub lay doon?

      Yeesu, buur ci kaw asamaan mu ngi nguuru ci kaw suuf si nekk àjjana.

      5. Yeesu mooy buur bi gën

      Yeesu miy buur ci nguuru Yàlla, dina dimbali nit ñi ci kaw suuf, ci anam yu bari. Seetaanal WIDEO BI ngir gis ne, Yeesu am na bëgg-bëggu dimbali nit ñi te Yàlla may na ko kàttanu def ko.

      WIDEO: Yeesu wone na li Nguur gi nar a def (1:13)

      Bi Yeesu nekkee ci kaw suuf, wone na li nguuru Yàlla nar a def. Ban ci barke yi ñu lim fii ci suuf nga yàkkamti mu am? Jàngal aaya yiy wax ci barke yooyu.

      BI YEESU NEKKEE CI KAW SUUF...

      YEESU DINA TOLLU CI KAW ASAMAAN...

      • mënoon a dalal ngelaw lu réy (Màrk 4:36-41).

      • defaraat lépp li yàqu ci kaw suuf si (Esayi 35:1, 2).

      • dundal na ay junniy nit (Macë 14:17-21).

      • dindi fi xiif (Sabóor 72:16).

      • faj na ñu bari ñu feebaroon (Luug 18:35-43).

      • may ñépp wér-gi-yaram gu mat sëkk (Esayi 33:24).

      • dekkaloon na ñu dee (Luug 8:49-55).

      • dekkal ñi dee te jële fi dee (Peeñu 21:3, 4).

      6. Nguuru Yàlla dina ñu may ëllëg ju neex

      Nguur gi dina matal lépp li Yexowa bëggaloon nit ñi. Dinañu dund ba fàww ci àjjana ci kaw suuf. Seetaanal WIDEO BI ngir gis ni Yexowa di jaare ci Yeesu ngir matal li mu bëggaloon nit ñi.

      WIDEO: Ëllëg ju neex ji ñuy xaar (4:38)

      Jàngal Sabóor 145:16. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

      • Xam ne Yexowa dina «reggal luy dund, ba xolam sedd», lan lay def ci yow?

      BU LA NIT WAXOON: «Ñun ñépp bu ñu góor-góorloo, jafe-jafe yi dinañu fi jóge.»

      • Yan jafe-jafe la fi nguuru Yàlla nar a jële te nguuru doomu Aadama yi mënuñu ko?

      NAÑU TËNK

      Nguuru Yàlla dina matal lépp li Yàlla bëgg. Dina def suuf si sépp àjjana, te suuf si dina fees ak nit ñu nar a jaamu Yexowa ba fàww.

      Nañu fàttaliku

      • Naka la nguuru Yàlla nar a sellale turu Yexowa?

      • Lu tax ñu mën a gëm ne, nguuru Yàlla dina matal dige yi nekk ci Biibël bi?

      • Ci barke yi nguuru Yàlla nar a indi, ban nga ci gën a yàkkamti mu am?

      Jubluwaay

      GËSTUL

      Xoolal li nar a xew ci li Yeesu tudde ‘metit wu réy wi’ (Macë 24:21).

      «Lan mooy metit wu réy wi» (Ci jw.org la nekk)

      Xoolal ni benn njaboot di xalaate ci bés bi ñu nar a dund ci àjjana.

      Xalaatal nga nekk ci àjjana ji (1:50)

      Ci waxtaan bi tudd «Laaj yu bari ñoo doon jaxase sama xel», xoolal ni góor gu sóobu woon ci politig gise ay tontu ci ay laajam.

      «Biibël bi dafay soppi dund» (w12 1/1)

Téere yi ci Wolof (1996-2025)
Ngir génn
Ngir konektewu
  • Wolof
  • Yónnee ko
  • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
  • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
  • Conditions d’utilisation
  • Règles de confidentialité
  • Paramètres de confidentialité
  • JW.ORG
  • Ngir konektewu
Partager