LESOŊ 21
Naka lañuy yéglee xibaaru jàmm bi?
Ci kanam tuuti, Yexowa dina fi jële suñu jafe-jafe yépp jaare ko ci Nguuram. Xibaar bu neex boobu, fàww ñépp dégg ko. Yeesu dafa bëggoon ay taalibeem yégal ko ñépp! (Macë 28:19, 20). Naka la Seede Yexowa yi di toppe ndigalu Yeesu boobu?
1. Naka la li ñu wax ci Macë 24:14 di ame tey?
Lii la Yeesu yégle woon: «Xibaaru jàmm bii ci nguuru Yàlla, dees na ko yégle ci àddina sépp» (Macë 24:14). Seede Yexowa yi am nañu mbégte ci def liggéey bu am solo boobu. Dañuy waare xibaaru jàmm bi fépp ci àddina si, ci lu ëpp 1 000 làkk! Liggéey bu mag boobu dafa laaj góor-góorlu, jot ak it def ko ci fasoŋ bu jaar yoon. Soxla nañu ndimbalu Yexowa ngir def liggéey boobu.
2. Naka lañuy góor-góorloo ngir waare?
Dañuy waare fépp fi ñu mën a fekk nit ñi. Ni karceen yu njëkk ya, dañuy waare ci ‘kër yi’ (Jëf ya 5:42). Loolu tax na, ñu mën a wax ak lu tollu ci ay milioŋi nit at mu nekk. Ndegam am na ñi dul nekk seen kër, dañuy waare itam ci mbedd yi walla fi ñu mën a fekk nit ñi. Saa su nekk, dañuy wut a xamal nit ñi Yexowa ak coobareem.
3. Kan moo war a waare xibaaru jàmm bi?
Karceen yi yépp ñoo war a waare xibaaru jàmm bi. Wareef boobu nag, dañu ko fullaal. Dañuy def lépp li ñu mën ngir waare, ndaxte xam nañu ne loolu mën na musal nit ñi (Jàngal 1 Timote 4:16). Kenn du ñu fey ngir def liggéey boobu, ndaxte Biibël bi nee na: «Cig neen ngeen ame, mayeleen cig neen» (Macë 10:7, 8). Du ñépp a ñuy nangoo déglu. Waaye dañuy kontine di waare ngir déggal Yexowa te bégal xolam.
XÓOTALAL NJÀNG MI
Xoolal leneen li Seede Yexowa di def ngir waare ci àddina si sépp, ak ni leen Yexowa di dimbalee.
Dañuy waare ci àddina si sépp: (A) Costa Rica, (B) Etaa sini, (C) Bénin, (D) Thaïlande, (E) Yap, (F) Suède
4. Dañuy def suñu kem kàttan ngir waar ñépp
Seede Yexowa yi dañuy def lépp li ñu mën ngir waare xibaaru jàmm bi fépp fu nit ñi nekk. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.
Lan ngay yëg boo gisee ni Seede Yexowa yi di góor-góorloo ngir waare?
Jàngal Macë 22:39 ak Room 10:13-15. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
Naka la suñu liggéeyu waare bi, di wonee ne dañu bëgg suñu moroom?
Lan la Yexowa di yëg bu gisee ñiy waare xibaaru jàmm bi? (Xoolal aaya 15).
5. Dañuy liggéeyandoo ak Yàlla
Am na ay nettali yu bari yuy wone ne, Yexowa mooy jiite liggéeyu waare bi. Ci misaal, ca Nouvelle-Zélande, benn ngoon, suñu mbokk bu tudd Paul dafa doon waare këroo-kër ba taseek benn jigéen. Fekk ca bés boobu, ci suba si, jigéen ji dafa ñaanoon Yàlla jaar ci turam Yexowa ngir mu am ku ko seetsi. Paul nee na bi jigéen ji ñaanee, ñetti waxtu rekk a ci tegu, moom Paul mu fëgg buntoom.
Jàngal 1 Korent 3:9. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Li xew ca Nouvelle-Zélande, naka lay wonee ne Yexowa mooy jiite liggéeyu waare bi?
Jàngal Jëf ya 1:8. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Lu tax ñu soxla ndimbalu Yexowa ngir def liggéeyu waare bi?
Ndax xamoon nga ne...
Semen bu nekk ci suñu ndaje yi, dañu ñuy jàngal ni ñuy waaree. Bu dee mas nga teewe benn ci ndaje yooyu, lan nga xalaat ci njàngale boobu?
6. Dañuy topp ndigalu Yàlla
Ci jamono karceen yu njëkk ya, am na ñu doon jéem a tere taalibe Yeesu yi ñu waare. Karceen yu njëkk ya dañu dem ci kanamu yoon ngir «taxawal xibaaru jàmm bi» (Filib 1:7). Tey itam, Seede Yexowa yi loolu lañuy def.a
Jàngal Jëf ya 5:27-42. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Lan moo tax duñu mas a bàyyi waare? (Xoolal aaya 29, 38, ak 39).
BU LA NIT LAAJOON: «Lu tax Seede Yexowa yi di dem këroo-kër?»
Lan ngay tontu?
NAÑU TËNK
Yeesu dafa sant taalibeem yi, ñu yégle xibaaru jàmm bi ci xeet yépp. Yexowa mu ngi dimbali jaamam yi ci liggéey boobu.
Nañu fàttaliku
Naka lañuy yéglee xibaaru jàmm bi ci àddina si sépp?
Naka la suñu liggéeyu waare bi, di wonee ne dañu bëgg suñu moroom?
Ndax foog nga ne liggéeyu waare bi mën na ñu may mbégte? Lu tax?
GËSTUL
Lan la Seede Yexowa yi def ngir dimbali ñi daw seen réew?
Ku jébbal jotam yépp ci liggéeyu waare bi, wax na mbégte bi mu ci jële.
Xoolal yenn ndam yi ñu am ci kanamu tirbinaal ak ni ñu gënee yombal liggéeyu waare xibaaru jàmm bi.
«Waarekat yi dem nañu ci yoon ngir aar seen bopp» (kr pàcc 13)
a Yàlla moo ñu sant ñuy waare. Kon Seede Yexowa yi soxlawuñu tàggu nguur yi ngir waare xibaaru jàmm bi.