WOY-YÀLLA 76
Lan ngay yég ci sa xol?
(Yawut ya 13:15)
1. Lan ngay yég ci sa xol
Booy wër ñi seen xol rafet
Ci liggéeyu waare bi
Ànd ceek cawarte?
Maa ngi def li ma war
Bàyyi Yàlla def li des
Ndaxte moom moo mën a xam
Nit ku koy wut a neex.
(AWU BI)
Am naa mbégte may Yexowa
Sama dooleek jot gi ma am.
Man damay màggal Yexowa
Su may dem waareji.
2. Lan ngay yég ci sa xol
Boo laale xolu nit ñi
Bëgg dund gu dul jeex
Ci àjjana jiy ñëw?
Bu ma nit dégluwul
Walla mu di ma saaga
Loolu du dindi mbégte
Bi ne ci sama xol.
(AWU BI)
Am naa mbégte may Yexowa
Sama dooleek jot gi ma am.
Man damay màggal Yexowa
Su may dem waareji.
3. Lan ngay yég ci sa xol
Bu la Yàlla dimbalee?
Moo la sant nga waare,
Ndax am nga ci mbégte?
Man damay jéema woo
Ñi woyof te rafet xol
Ànd ceek mbaax ak dëggu
Ndax li des bareetul.
(AWU BI)
Am naa mbégte may Yexowa
Sama dooleek jot gi ma am.
Man damay màggal Yexowa
Su may dem waareji.
(Xoolal itam Jëf ya 13:48; 1 Tesalonig 2:4; 1 Timote 1:11.)