WOY-YÀLLA 135
Yow miy ndaw: «Amal xel»
(Kàddu yu xelu 27:11)
1. Yow miy ndaw,
Joxal sa xol Yexowa Yàlla
Ngir mu mën a tontu Ibliis,
muy ndam lu rëy.
Nanga ko jaamu
Te xam ne dina la fey;
Ci lépp li ngay def,
Wóolul sa Baay Yexowa.
(AWU BI)
Yow sama doom, yow mi ma sopp,
Ngir nga mën a doon ku am xel,
Sama Kàddu nga war a topp.
Soo ko defee man ngay màggal.
2. Soo ma jaamoo,
Mbégte ngay am te muy lu wóor.
Maay téye sa loxo,
Te doo am lu la lor.
Bul xàddi
Doonte sax dina am ñu lay wor,
Xamal ne
Man may sa xarit bi gën a wóor.
(AWU BI)
Yow sama doom, yow mi ma sopp,
Ngir nga mën a doon ku am xel,
Sama Kàddu nga war a topp.
Soo ko defee man ngay màggal.
(Xoolal itam Baamtug Yoon wi 6:5; Kàdduy Waare 11:9; Esayi 41:13.)