WOY-YÀLLA 35
Nañu ràññee li gën a am solo
(Filib 1:10)
1. Li ñuy musal ci mujug jamono ji,
mooy ñu mën a ràññee,
sàkku xam-xam dëgg ci li baax,
ci li war, li ëpp solo!
(AWU BI)
Bëgg lu baax, sore lu bon,
bégal Yàlla.
Aka moo barkeel, kiy sax ci gëstu,
mën a ràññee
ngir jiital li gën a am solo!
2. Ndax war nañu jiital leneen lu dul
waare Nguuru Yexowa?
Di seet ñiy xaar bés biy Yàlla àtte suuf si,
ñu dund ba fàww.
(AWU BI)
Bëgg lu baax, sore lu bon,
bégal Yàlla.
Aka moo barkeel, kiy sax ci gëstu,
mën a ràññee
ngir jiital li gën a am solo!
3. Farlu jox cër li ëpp njariñ
dina ñu yóbbe ci doylu.
Jàmmu Yàlla, ji xel mënta takk,
sàmm xol yi ak xel yi.
(AWU BI)
Bëgg lu baax, sore lu bon,
bégal Yàlla.
Aka moo barkeel, kiy sax ci gëstu,
mën a ràññee
ngir jiital li gën a am solo!
(Xoolal itam Taalifi Cant 97:10; Yowaan 21:15-17; Filib 4:7.)