Nañu faj suñuy soxla ci wàllu ngëm
1 Ci ndaje bi gën a mag bii di ñów, te tudd “ Ñi sawar ci waare Nguuru Yàlla ”, dinañu mën a faj suñuy soxla ci wàllu ngëm. Ñam bu neex dafa ñuy may doole. Noonu it, ci lu wóor ndaje boobu dina ñu may doole ci wàllu ngëm “ ci kàdduy yoonu ngëm wi ”. (1 Tim. 4:6.) Dina tax ñu mën a gën a jege Yexowa. Ci lu wóor, dinañu am ay xelal ak liy yokk suñu doole ngir mën a muñ suñuy jafe-jafe. Yexowa dafa ñu ne, te lu wóor la : “ Dinaa def ba nga am seetlu, te dinaa la jàngal yoon fi nga war a aw. Dinaa la yedd, sama bët nekk sa kow. ” (Sab. 32:8). Yexowa dafa ñu bëgg te dafa ñuy won fi ñu war a aw. Loolu, barke bu réy la ! Nañu seet li ñu war a def ngir jariñoo ndaje bu mag boobu ni mu gëne.
2 War nañu waajal suñu xol : Kenn ku nekk ci ñun am nga li la war, maanaam sàmm sa xol (Léeb. 4:23). Loolu laaj na ñu yar suñu bopp te nangu gis ni suñu xol mel dëgg dëgg. Ndaje bu gën a mag bi, nekk na jamano bu baax ngir xalaat bu baax ci suñu diggante ak Yexowa. Jamano la it ngir “ gëstu yoonu Yàlla, wi mat tey goreel ”. Bu ñu bëggee waajal suñu xol ndax kàddu Yàlla mën cee dugg bu baax, dañu war a ñaan Yexowa, di ko saraxu, ndax mu niit ñu, mu won ñu bépp “ yoonu naqar ” bu ñu war a jubbanti ci ñun, te mu tette ñu ci “ yoon wu sax wi ”. — Saak 1:21, 25 ; Sab. 139:23, 24.
3 Nañu déglu te xalaat bu baax ci li ñu dégg : Yeesu taggoon na Maryaama ndax li mu ko déglu bu baax. Dafa ko ne : “ Maryaama dafa tànn cér bi gën, te kenn du ko nangu ci moom. ” (Lukk 10:39, 42). Bu ñu amee xel moomu, duñu bàyyi lu amul maanaa tere ñu déglu. Dinañu def li ñu mën ngir toog te déglu lépp li ñuy wax ci ndaje boobu. Dinañu moytu wax ak ñeneen ñi ci lu amul njariñ, walla jóg bu ñu ko soxlawul dëgg. Te it, dinañu moytu suñu telefon, suñu biper, walla suñu kameraa tere ñeneen ñi déglu.
4 Bu ñuy déglu waxtaan yi, nañu jéem a bind ci lu gàtt li ñuy dimbali ñu mën a seet bu baax ni waxtaan bi deme. Boo déggee dara, nanga seet ni mu ànde ak li nga xam ba pare. Loolu dina tax ñu mën a nànd te jàpp bu baax li ñuy wax. Bu ñuy seetaat li ñu bind bu ñu doon déglu, nañu xalaat ni ñu ko mënee topp. Ku nekk ci ñun, war nga laaj sa bopp : ‘ Li may dégg, naka la mënee laal sama diggante ak Yexowa ? Lan laa war a jubbanti ci suma dund ? Naka laa mënee topp li may jàng ci sama diggante ak ñeneen ñi ? Naka laa koo mënee jëfandikoo bu may waaraate ? ’ Boo déggee lenn lu la neex dëgg, nanga ci waxtaan ak ñeneen ñi. Loolu lépp moo ñuy dimbali ndax ñu denc “ ci suñu biir xol ” li Yexowa wax. — Léeb. 4:20, 21.
5 Nañu topp li ñu jàng : Bi mu jógee ci ndaje bi gën a mag, am na ku wax lii : “ Ku nekk amoon na wàllam ci ndaje bi, ba tax ñépp bëgg xoolaat li nekk ci seen xol, ak ci xolu ñi bokk ci seen njaboot, te jox ñi ko soxla ay xelal yu jóge ci Mbind mi, di ko def ak mbëggeel. Tax na ma gën a xam ne, yokk li may def ngir dimbali ñi nekk ci mbooloo mi, bokk na ci sama warugar. ” Xéyna, am na ñu bare ñu yëg loolu ñoom itam. Waaye bu ñu jógee ci ndaje bu gën a mag bi, fekk suñu doole yokku te suñu xel dal, nañu xam ne loolu rekk doyul. Yeesu nee na : “ Gannaaw xam ngeen loolu, bu ngeen doxalee noonu, dingeen bég. ” (Ywna. 13:17, bind yi ñu dëngal, ci ñun la.) Kon bu ñu déggee lu ñu laal ñun ci suñu bopp, war nañu koo topp bu baax (Fil. 4:9). Noonu lañuy mënee faj suñuy soxla yépp ci wàllu ngëm.
[Wërale bi nekk paas 5]
Xalaatal bu baax ci li nga dégg :
■ Naka lay laale sama diggante ak Yexowa ?
■ Naka lay laale sama diggante ak ñeneen ñi ?
■ Naka laa ko mënee topp ci sama dund ak bu may waaraate ?