TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 9/03 p. 3
  • Nañu daje ngir màggal Yexowa

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Nañu daje ngir màggal Yexowa
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Nañu màggal Yexowa ci diggu mbooloo mu réy mi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Liggéeyu waare bu gën a mag bi mas a am ci àddina !
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
  • Nañu ànd màggal turam
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Nañu kontine di xaar Yexowa
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
Xóotalal waxtaan bi
Sasu Nguuru Yàlla — 2003
km 9/03 p. 3

Nañu daje ngir màggal Yexowa

1 Yexowa, kenn mënu ko dab ci kàttan, xam-xam, njubte ak mbëggeel. Moom rekk lañu war a jaamu ndaxte moo sàkk lépp, moo tax ñuy dund te moom mooy Aji kilifa ji (Sab. 36:9 ; Peeñ. 4:11 ; 15:​3, 4). Ndaje bi gën a mag bii di ñów, mu ngi tudd “ Nañu màggal Yàlla ”. Dina tax ñu gën a bëgg màggal ki nga xam ne moom rekk a nekk Yàlla dëgg ji. — Sab. 86:​8-10.

2 Nañu ko waajal bu baax : Yexowa dafa ñu dencal lu bare te neex ci wàllu ngëm ca ndaje boobu. Su ñu ko bëggee jariñoo bu baax, fàww ñu waajal ko ni mu ware (Efes 5:​15, 16). Ndax xam nga fi ngay dal boo demee ci ndaje bi ak ni nga fay deme ? Ndax ñaan nga fi ngay liggéey walla ci lekkool fi ngay jànge ñu may la fan yi nga war a dem ci ndaje boobu ? Lu am solo la. Bul xaar ba ndaje bi bëgg a jot, sog a toppatoo loolu. Boo teelul a ñaan ñu may la fan yooyu, mën na tax nga ñàkk dara ci ndaje bu neex boobu. Ñun ñépp, porogaraam bi yépp lañu war a teewe.

3 Nanga jàpp ci sa xel ne danga bëgg a teel a agsi bés bu nekk ca palaasu ndaje bi . Loolu dina tax nga mën a toog bala woy bu njëkk bi te dinga mën a waajal sa xel ngir déglu bu baax li ñu lay jàngal foofu. Bés bu ne, bu juróom ñetti waxtu jotee ci suba lañuy ubbi bunt yi. Sa waa-kër, walla ñi nga bokkal oto rekk nga mën a dencal palaas.

4 Na ku nekk indaale li muy añ. Loolu moo gën ñu génn wuti li ñuy lekk bu waxtaan yi ñuy def ci suba si paree. Bu ñu defee loolu, dinañu mën a nekk ak suñu mbokk yi ci jàmm te gën a am jot ngir waxtaan ak ñoom (Sab. 133:​1-3). Te it, buleen fàtte ne dañuy tere ci bérébu ndaje bi lu mën a toj te it dañu fay tere sàngara.

5 Nañu déglu ngir jàng : Ezra dafa waajaloon xolam bu baax ngir Kàddu Yàlla mën cee dugg (Esr. 7:10). Dafa ubbi xolam ngir li Yexowa di jàngale dugg ci (Léeb. 2:⁠2). Mën nañu tàmbalee waajal suñu xol bala sax ñuy jóge suñu kër bu ñu xalaatee bu baax ci turu ndaje bi te bu ñu ci waxtaanee ak suñu waa kër.

6 Bu ñu amee ndaje bi ci béréb bu yaatu, bu ñu moytuwul lu bare dina ñu yàqal ba ñu bañ a déglu bu baax porogaraam bi. Mën na nekk lu ñuy gis walla lu ñuy dégg loo xam ne dina tax ñu def suñu xel ci leneen. Loolu mën na tax lu am solo raw ñu. Bu ñu toppee li ñu wax ci wërale bi nekk ci xaaj bii, dinañu gën a mën a def suñu xel ci li ñu fay wax.

7 Nañu xalaat nit ñi nekk suñu wet : Bu ñu nekkee ci ndaje bi, ku yore kamera walla wideo mën nga ko jëfandikoo. Waaye waruloo jóge fi nga toog, ngir ñi ci des mën a déglu bu baax. Looloo tax it ñu war a fey suñu telefon ak suñu biper. Kenn warul a jël ci kuraa bi nekk ci bérébu ndaje bi, walla jéem a boole dara ak lépp lu jëm ci mikroo yi.

8 Wóor na ne ñun ñépp a yàkkamti daje ak suñu mbokk yi ngir màggal Yexowa. Bu ñu bàyyi dara tere ñu teewe waxtaan yi yépp, déglu bu baax, te topp li ñu fay jàng. Bu ñu defee loolu, dinañu màggal Yexowa bu baax. — 5 Mu. 31:⁠12.

[Laaj yi]

1. Lan mooy turu ndaje bi gën a mag bii di ñów, te lu tax ñu war a màggal Yexowa ?

2, 3. Naka lañu war a waajal ndaje bi ngir mën ko jariñoo bu baax ?

4. Lu tax ñu bëgg ñépp indaale seen añ ci ndaje bi ?

5. Lan lañu mën a njëkk def ngir waajal suñu xol ngir ndaje bi ?

6. Lu ñu mën a def ba dara bañ ñoo teree déglu bu baax ci ndaje bi ? (Seetleen wërale bi.)

7, 8. Naka lañu mënee wone ne dañuy xalaat suñu moroom yi ?

[Wërale bi nekk paas 3]

Ni ñu waree déglu ci ndaje bi

▪ Nañu xalaat bu baax ci turu waxtaan yi

▪ Nañu jàng aaya yi ci Biibël bi

▪ Nañu bind ci lu gàtt li ëpp solo ci waxtaan bu nekk

▪ Nañu bind li ñu fas yéene topp

▪ Nañu seetaat li ñu jàng

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager