Liggéeyu waare bu gën a mag bi mas a am ci àddina !
Lu ëpp 100 at a ngi nii, Seedee Yexowa yi di ànd di waare xibaar bu baax bi (1 Kor. 9:23). Liggéey boobu mujj na dem ba nekk liggéeyu waare bi gën a mag bi mas a am ci àddina. Dañuy yégle xibaar bi ci ay téeméeri làkk, ci lu ëpp 230 réew (Macë 24:14). Waaye lu tax ñu war a def liggéey boobu ? Te naka la liggéey boobu di ame ci àddina si sépp ?
DVD bi tudd Les Témoins de Jéhovah : Organisés pour proclamer la bonne nouvelle (maanaam Seede Yexowa yi dañuy ànd ngir yégle xibaar bu baax bi) dafay tontu laaj yooyu. Ngir def loolu, dafa ñuy won bu baax fànn yu bare yu bokk ci liggéey boobu ñuy def ci àddina si sépp. Bu ngeen koy seetaan nangeen xalaat ci laaj yii : 1) Naka lañuy doxale liggéey bi, te naka lañu koy jiite ? 2) Kurél biy toppatoo li ñuy bind ci téere yi, kurél biy toppatoo liggéey bi ñuy def ngir sotti ci yeneen làkk li ñu bind ci suñu téere yi, kurél biy toppatoo lépp luy foto ak nataal, ak biy toppatoo kaset ak wideo yi, kurél yooyu yépp naka lañu bokke ci liggéey bi ñuy def ngir yégle xibaar bu baax bi ? 3) Lan moo tax ñuy def liggéey bu bare ngir defar te yónne suñu téere yi ci àddina si ? (Ywna. 17:3). 4) Ñaata téere lañuy defar ci benn at ? 5) Suñuy téere yi nga xam ne li nekk ci Biibël bi lañuy topp, lan lañu indi ci waaraate bi ? (Yaw. 4:12). 6) Lan lañuy def ngir dimbali ci wàllu ngëm ñi dul gis walla dégg bu baax ? 7) Fu ñuy jële xaalis bi ñu soxla ngir def liggéey boobu ? 8) Biro buy dajale xam-xam bi jëm ci li ñu mën a def ngir bañ a jëfandikoo deret bu ñuy faj walla opere nit, te di ko xamal Seede Yexowa yi, biro biy toppatoo njàngale bi, ak it biro biy toppatoo ndaje yu mag yi, li biro yooyu yépp di def naka la ñuy jariñe ? 9) Yow mii di Seede Yexowa, li nga gis ci wideo bi naka la tax ba nga gën a seetlu te fonk njariñ bi nekk ci a) Liggéey bi mbootaayu Seede Yexowa yi di def ngir waare xibaar bu baax bi ? b) Lu ëpp 100 Betel yi nekk ci àddina bi ? c) Li ñuy def ngir jàngal njiiti mbooloo yi ak missionnaires yi (maanaam ñi nuy yónni fépp ci àddina ngir waaraate bi) ? d) Komaase bés bi ak xalaatu benn aaya Biibël bi, akit di waajal ayu-bés bu nekk ndaje mbooloo mi ? e) Teewe suñuy ndaje karceen yi ? f) Ni àjjana ci kow suuf di mel ? (Es. 11:9) g) Bokk yow ci sa wàllu bopp ci liggéeyu ngóob bi am tey ? — Ywna. 4:35.
Bi nga seetaanee wideo bi ak say mbokk, say xarit, nit ñi ngay dellu seeti ci waaraate bi, walla ñi ngay jàngal Biibël bi, lu rafet lan la def ci ñoom ? Ci jamano ji ñu tollu nii, ndax mënuloo won keneen wideo boobu, te wax ko lu jëm ci xibaar bu baax bi ? — Macë 28:19, 20.