TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 5/02 p. 8
  • Ndax gox bi sa mbooloo moom dafa réy ?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ndax gox bi sa mbooloo moom dafa réy ?
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Bu ñu fekkul nit ñi seen kër
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Ndax am nga gox bi nga moomal sa bopp ngir waare ?
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
Sasu Nguuru Yàlla — 2002
km 5/02 p. 8

Ndax gox bi sa mbooloo moom dafa réy ?

1 Yeesu dem na seede fu nekk ci réewu Israyil. Mu jóge ca dëkk yi nekk ci Yude, dem ba ca dëkki kow ga, ca Galile (Mark 1:​38, 39 ; Lukk 23:⁠5). Ñun itam war nañu def lépp li ñu mën ngir waar nit ñu baree bare ci xibaar bu baax bi (Mark 13:10). Waaye loolu mën na nekk lu jafe. Lu tax ?

2 Ci mbooloo yu bare yu nekk ci digg ak sowu Afrig, dëkki kow yi ñoo ëpp ci dëkk yi nekk ci gox bi ñu moom. Te gox boobu dafa réy lool. Mbooloo yuy làkk làkku bitim réew, mën nañu nekk ci dëkku taax, fu nit ñi bare lool, di wut nit ñuy làkk seen làkk. Nit ñooñu dëkk ci gox yooyu nga xam ne dañuy gën di yaatu, lan lañu mën a def ngir ñu jàng dëgg gi ci Yexowa, ci Yeesu ak ci Nguuru Yàlla ?

3 Seetleen bu baax ni ngeen di defe : Wottukatu liggéeyu waare gi ak kiy toppatoo goxu mbooloo mi, war nañu xool li mbooloo mi di def, ndax seen liggéey jur li gën. Ci bésu gaawu la ëppe waaraatekat yu mën a waare bés bi yépp. Xéyna dingeen mën a tànn ay gaawu ngir waare ci. Bu ngeen di waare ci gox bu sori, na ngeen yóbbaale añ ngir yendu ci waaraate bi. Na ngeen teel a def ndaje bi ñuy am bala ñuy waare, ndax ngeen mën a teel a àgg. Walla mën ngeen a def ndaje boobu fu jege fi ngeen war a waaraate. Seetleen ni ngeen mënee ànd bu ngeen di dem waaraate. Mën ngeen fa deme ak seen oto bopp, walla ngeen luye ay kaar, walla taksi. Su ñu defee noonu, ñu bare dinañu ci mën a bokk. Bu ngeen di waaraate ca dëkki kow ya, na ngeen fa dem jamano boo xam ne asamaan si day neex te yoon bi day baax.

4 Ñi nga xam ne dañuy waare ñiy làkk làkku bitim réew, mën nañu bañ a yàq seen jot bu ñu amee fu ñu binde limu turu nit ñi ak seen adarees te yore kàrtu gox bi. Waruñu nekk lim walla kàrt yu yàgg. Booleleen ñi bokk gox, ndax ñu fay waaraate mën leen seeti ñoom ñépp.

5 Seetleen bu baax ndax téere yu ngeen di yóbbu dina doy. Su dee gox bi barewul lu ñu fay waaraate, xéyna lu gën mooy ngeen bàyyi suñu benn kayit bu ndaw walla ay yéenekaay yu xaw a yàgg ca kër yoo xam ne fekkuleen fa kenn. Bu ngeen amee kayit bu ndaw bi tudd Aimeriez-vous en savoir plus sur la Bible ?, na ngeen ko jox képp ku ngeen di taseel te bàyyi ci benn ci bépp kër boo xam ne fekkuleen fa kenn.

6 Nangeen jàppleente bu baax-a-baax : Mbooloo bu war a waaraate ci gox bu réy, laaj na ñépp jàppleente bu baax-a-baax. Bu ngeen waree dem waaraate fu sore ak oto, na ñépp a bokk ci esaas bi ñu war a fey. Boo gisee ku bëgg waxtaan ak yow, nanga seet bu baax ndax jar na ko. Bul fàtte ne ñépp ngeen bëgg gis ci gox bi. Bul fàtte itam ñeneen ñi nga àndal ñi lay xaar. Boo bëggee waxtaan ak nit ku suñu waxtaan neex, te waxtaan bi nar a yàgg, seetal ak ñi nga àndal li ngeen mën a def, ba ñu mën a kontine waaraate !

7 Defal lépp ngir mën a dellusi seetiwaat nit ku suñu waxtaan neex. Boo jëlee adareesam, jéemal a am nimoro telefonam boo ko mënee. Bu ko defee dinga ko mën a telefone ngir gën a waxtaan ak moom. Bu dee yaa ngi waaraate foo xam ne mbedd yi amuñu tur, walla kër yi amuñu seen nimoro bopp, nanga jël kayit te bind lépp lu la mën a dimbali nga mën a xàmmeewaat kër gi.

8 Topp li Yeesu wax ci Macë, lu réy la. Lii la wax : “ Bu fekkee ne agsi ngeen ci dëkk bu mag mbaa bu ndaw, nangeen fa seet ku fa am faayda. ” (Macë 10:11). Ci lu wóor Yexowa dina barkeel lépp li ngay def ci liggéey bu ñu gën a mën a indil lu baax !

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager