Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 mai
“ Ndax foog nga ne mën nañu fexe ba xam Yàlla ? [Mayal nit ki mu tontu.] Gëm ku ñu xamul bu baax, yombul. Mbind mu sell mi, dafa ñuy wax ñu wut Yàlla. [Jàngal Jëf ya 17:27.] Ci yéenekaay bii, dañuy wone ni ñu mënee def ba gën a xam Yàlla. ”
Réveillez-vous ! 22 mai
“ Kilifa yu nekk ci àddina si jéem nañu lu bare ngir dindi suñuy jafe-jafe. Am nañu pexe bu bees bu ñuy wax ci tubaab mondialisation, maanaam jéem a boole ñépp ci lépp ci àddina sépp. Loolu, naka la la mënee laal ? Yéenekaay bii, dina la ko won. Mën nga fi jàng it lu jëm ci pexe bi Mbind mu sell mi wax bu jëm ci coonoy àddina si sépp. ” Boo paree, jàngal Macë 6:9, 10.
La Tour de Garde 1 juin
“ Li xew bu yàggul ci àddina si, tax na ba nit ñi di laajte lu tax nit ku deful dara di teel a dee. Ndax mas nga xalaat lu tax nit di dee ? [Mayal nit ki mu tontu, ba pare won ko tablo bi nekk ci xët 7.] Léeb yu nekk fii, ñu bare xam nañu leen. Ndax am na benn boo xam ne bëgg nga xam li ci Mbind mu sell mi wax ? ” Soo ko mënee, jàngal benn aaya bu nekk ci yéenekaay bi.
Réveillez-vous ! 8 juin
“ Nit ñu bare dañuy xalaat ne diine ak siyaas (science), mënuñu ànd. Am na ñu foog ne ku njàngam sore lool ci wàll boobu, mënul a gëm Yàlla. Lu ci sa xalaat ? [Mayal nit ki mu tontu.] Réveillez-vous ! bii, dina yokk sa xam-xam ci loolu. ”