TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 5/02 p. 7
  • Tont Ci Seen Laaj

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Tont Ci Seen Laaj
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Barke yi ñuy am bu ñuy wone suñu ngërëm ci mbëggeelu Yexowa— Xaaj 2
    Sasu Nguuru Yàlla — 2001
Sasu Nguuru Yàlla — 2002
km 5/02 p. 7

Tont Ci Seen Laaj

◼ Lu tax ñu war a seet bu baax li ñuy def bu ñuy yónnee leetar ci post ngir waaraate ?

Waaraate ci leetar, yàgg na jur lu baax. Waaye li xew ci àddina si bu yàggul, tax na ba nit ñi dañuy moytu ubbi leetar bu jóge ci ki ñu xamul. Bu ñu jotee leetar bu ñu xamul fu mu jóge, walla leetar bu amul adareesu ki leen ko yónnee, nit ñi dañu koy ragal a ubbi. Bu fekkee ne loxo lañu binde li nekk ci kow anwalob bi, walla leetar bu réy la, ci lay rawe. Ki koy jot mën na koo sànni te du ko sax ubbi. Lan lañu mën a def ngir loolu bañ a am bu nit jotee suñu leetar ?

Bu ñu ko mënee, leetar bi ak li nekk ci kow anwalob bi, dañu ko war a bind ci masin. Dañu war a bind turu ki ñuy yónnee leetar bi ci kow anwalob bi. Buñu bind lu mel ni “ Waa kër gi ” ñoo ko moom. Te it, dañu war a bind ci kow anwalob bi adarees fu ñu nit ki mën a tontu. Bu fekkee ne joxe sa adareesu kër wóorul, bindal sa tur ak adareesu Saalu Nguur gi. Bul yónnee leetar boo xam ne ki koy jàng du xam ku ko yónnee. Bul jëfandikoo mukk adareesu bànqaas bi. — Seetal Réponses à vos questions ci Le ministère du Royaume bu nowàmbar 1996.

Mën ngeen a am yeneen tegtal te gis benn leetar bu leen di won li ngeen mën a bind bu ngeen di waaraate, ci téere Tirez profit de l’École du ministère théocratique, xët 71 ba 73. Tegtal yii dinañu tax nga mën a jëfandikoo leetar ni mu gënee ngir xamal nit ñi xibaar bu baax bi.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager